Baaxoo nanu, fi réew mi, bu xewu bànneex amee, jigéen ñiy joqalante ay teraanga. Daanaka, tuutee des, mu doon fi farata joj, xel xalaatul mu ñàkk cim xew. Bu ko nekkul ba noppi sax !
Xew ci Senegaal gii te kenn yebbiwul ? Bu amee it, bariwul de ! Ndax nit sañ na ko sax ? Fii nga xam ne, am na ñuy bëtal ngir rekk bëgg a dajale lu ñu teralee seen i goro, njëkke ak i wujji peccargo. “Aa ! Yaw tamit, àdduna, lépp teraanga la ! Samay nawle laa fi nekkal. Noon yaa ngi soccu, di xaar ma fakkastalu, ñu ree. Waaye, bu dee man rekk, kenn du fi kekku ! Te it, fàww ñu delloo ma samay ndawtal. Njaag, dafa wara nangu di !”
Céy Njaag ! Moom de, yemul rekk ci di jiin. Ndegem, nee nañu : “lu jiin Njaag a”. Daf ci boole ñu koy bàkk. Ndax, bari na lu nuy dégg ñu naan : “bàkk nga Njaag !” Ci kaw loolu lépp nag, mu dëkk di nangu rekk.
War naa barile de xanaa ! Waaw, moom sax, kañ lay joxe ? Nga ne ma : “Loo bëgg mu joxe ak ku mu koy jox ?” Moo jar a laaj nag !
Kaay nu ànd seeti Maam Seŋoor mu yaay Ñilaan Baaxum. Àdduna sépp a miinoon ci moom kàddu gii di “ndajem joqalante” (rendez-vous du donner et du recevoir). Mbir mu ko yitteeloon la lool. Te muy ndaje mom, xeet yépp ñoo fay tase. Ñépp génnee li ñu am ci mbaax. Bu ko defee, ñii di joxe, ñee di jël. Ku nekk, di jariñ sa moroom. Waaye tam, ku nekk di jariñoo ci li sa moroom indi. Njaag nag moom, bu fa demee, lu muy joxe ?
Nga laaj ma : “Njaag moom, ku mu doon ? ” Ma tontu la : “Nun ñépp ay Njaag lanu ! ” Waawaaw, ay Njaag yu góor ak yu jigéen doŋŋ ñoo dëkk Senegaal. Bu nu demee ca ndaje ma, lu nuy joxe ? Xanaa sañu nu faa nekk di jël rekk te bañ faa bàyyi dara ?
Ndax am nanu lu nu joxeeti ? Ndono li nu ñoom maam bàyyiloon, lu ci ëpp, saay na. Weccoo nanu ci lu bari ak lu bawoo bitim-réew. Ndax, jàpp ne, la ca biti moo gën. Moo tax nag, ca ndaje ma, bu nu moytuwul, yëfi jàmbur, lanu fay yóbbu rekk, jóor ko ca diggu géew ba. Yàlla buñ nu ree !
Moone de, Maam Seŋoor, daan na nu dankaafu ngir nu am taxawaayu garab. Maanaam, sampu ci sunuy reen, ba am ndëgërlaay, njëkk nuy ubbi sunuy bànqaas dëgmal asamaan (enracinement et ouverture). Te loolu, du lenn lu dul ŋoy bu baax ci li fi maam bàyyi, xam ne gànjar gu amul yemu la. Bu nu ci jógee nag, sog a mën a xool li ñeneen ñi yore. Noonu sax, la ko biddéew bi ci raaya réew mi di màndargalee.
Bi muy wax loolu, mi ngi nu doon waajal ngir nu am taxawaay bu rafet te ràññeeku ca ndajem joqalante ma. Waaye, dégluwunu ko woon. Naka jekk, nun moom, danoo yab Maam Seŋoor. Neex-dereetam tax na, lu nu jekku, sànni ko ci kawam. Danu koy maamoo ba mu ëpp ! Bu nu jógee rekk naan ko “tubaab bu ñuul”. Waaye, waxi mag, du fanaan àll !
Fii mu nekk nag, nanu nangu rekk ne, Maam Sedaar am na dëgg ci sunu kow. Yey nanu de !
Nanu jóg nag, dem xool ci ruqu mbatiit yépp. Fépp fu nu mën a gis mbaax gu nu maam bàyyiloon, nu luqati ko, fëgg pënd bi ko muur, fomp ko, raxas ko sax, bu ko jaree. Xeeñal ko ba mu ne bann. Boole ko ci sunuy mbiri bopp yi nu gën a fonk. Teg ci, di ko jëfandikoo ànd ci ak sag bu réy.
Bu ko defee, bu nu dajalee lépp, ba ñu woote ndaje mi, ku indi, nu indi ; ku indiwul it, nu indi lu jariñ àddina sépp.