MAN MAAY KAN ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Danuy faral di dégg ñu naan : « boo xamul foo jëm, dangay dellu fa nga jóge woon ». Muy wax ju yenu maanaa lool. Nde, ku xamul fa mu jëm moom, réer da koy yomb. Balaa mu caa àgg nag, bu yaboo rekk dëpp. Bu xamoon fa mu jëm sax, te fàtte yoon wi, xéy-na bu laajtee, gindeeku. Ndax, wolof nee na : « boroom làmmiñ du réer ». Waaye, bu dee ni fa mu jëm ci boppam la fàtte, walla sax mu ñàkk koo xam, li gën ci moom, mooy mu bañ a nekk di wëraalu te dellu fa mu bawoo ci njekk.

Waaw léegi nag, bu ca boolee fàtte fa mu jóge moom, nu muy def ? Koo xam ni, fa mu jëm xamu ko, te fa mu jóge, fàtte na ko. Kooku moom, nees ko mën a taxawoo ? Foofu la beneen laaj di ñëwee, sampu ci kaw bi njëkk : « ndax kooku xamati na mooy kan ? » Moom, yamul rekk ci réere yoonam. Waaye, daf ci boole réere boppam. Te, loolu mooy dëgg dëggi réer. Lu ni mel, mën ko yóbbee ba, ku mu gis rekk topp ko, yaakaar ni mën na koo gindi. Te loolu, du def lu dul gën a jaxase xelam.

Ci kaw loolu nag, nu wara taxaw tuuti, nun Saa-Senegaal yi, natt sunu bopp, xool ba xam naka lanuy def ak waa jii nu jàpp ni dafa réer. Ndax nun ci sunu bopp fàttewunu fa nu jóge ? Ndax xam nanu fa nu jëm ? Ci gàttal, ndax réerewunu sunu bopp ? Joxe tontu ci laaj yii nag, du yomb. Rawatina bi mu soxalee réew mépp. Ndax kat, ñépp yamuñu, lu ko moy rekk am ñu gedd seen cër. Loolu la wolof wax. Waaye, am na loo xam ni, ñu bari dinañu ci maase ànd.

Dafa am ci ay loxo yu nu jot a jaar. Ay nit yu ñëwoon, noot nu ngir jariñoo li nu yor. Yàgg fi lool, lu ne ñu def ko fi ci lu ñaaw. Gaa ñooñu nag, bokk na ci li gënoon a tax seen i pexe ci nun àntu, mooy ne dañoo taxawoon temb ngir weddiloo nu sunu bopp. Gëmloo nu ni, nun, dunu dara, danoo xayadi, te sax mbooru àdduna si daf nu fee bàyyi. Mu yóbbee leen ñuy soppi yenn ci sunuy tur i dëkk tuddee leen neneen. Dem sax bay wax ne ñoom ñoo feeñal (walla boog ñoo njëkk a gis) yenn ci sunuy dëkk. Lépp rekk ngir gën noo doyadal. Ba noppi, xirtal nu ci di roy ci ñoom ñi jóge fu sori, ñew fi nun, ngir rekk “def nu ay nit”.

Nu mën leen a méngale ak ay nit yu dikk, fekk mbooloo mu toog, wér péng, ñu ne leen : “yéen kat dangeen feebar, nanguleen ko te jébbal nu seen bopp nu faj leen”. Mbooloo ma tamit nangu ba dee. Gaa ña gaawantu, ping leen ay feebar yu bari ba noppi wëlbatiku ne leen dañuy wuti saafara. Ñoom, foofu lañu jaar ak nun ba indil nu ag yaras gu rëy.

Nu dem ba jàpp ni, ngir mën a bokk ci “nit ñi” ba noppi ñépp weg nu, fàww nu sànni lépp lunu yoroon te jéem a mel ni ñoom. Ci la nu xàllee yoon woow, jàppoon nanu ni moo nu cay jëme. Nu tàmbalee soofantal sunuy làkk ngir seen i yos. Jël lu bari ci sunuy mbaax ak sunum mbatiit teg ca wet ga, jàpp ni yëfi ku matadi la. Dem sax ba àgg ci, ku nu wax ne ab tubaab la, mu jëlee ko ni ab tagg, am ci mbégte mu rëy a rëy. Rax-ci-dolli, nu jël lu bari ci li nu gën a fonk moomale leen ko. Ba képp ku am yenn taxawaay yu rafet yi (niki fonk waxtu, ñàkk caaxaan, añs.) nu bëgg koo boole ci ñoom.

Ci kaw loolu, nu dogu ci di leen topp rekk, fuñ nu joxoñ, nu dem. Ñoom, ñu nekk ci seen i mbiri bopp yi leen di jëmale kanam. Nun nag, nu topp ci seen ginnaaw rekk di leen “wéttali” ak a doxal li ñu lott a defal seen bopp (walla, li ñu sañul a fësal). Mu mel ni danoo gëlëm, xamatunu fan lanu wara jaar ngir dem. Xamatunu sax fan la nu jëm faf te, bàyyiwunu ci xel ndeysaan.

Ndekete yóo, ci jooju jamono, nu ngiy dagg li ëpp solo ci nun di sànni ca sën ba ndax jàppoon ni mbalit doŋŋ la. Ci jooju jamono, nu ngiy far, ci sunu bopp, lépp lu nuy xamleek ki nu doon dëgg-dëgg. Nu ngiy dog buum yi nu jokkale woon ak sunuy balluwaay. Nu jaare fa, fàtte ki nu doon, fàtte fa nu jóge.

Fàtte fa nu jóge ndax xeeb ak suufeel sunu bopp. Fàtte itam fa nu jëm ndax topp ku nu bokkalul yoon. Lii daal mooy sunu feebar. Walla boog, mooy feebaru ñu bari (balaa ñenn ñi di gedd seen cër) ñu dëkee Senegaal ak Afrig gépp sax.

Feebar bii nag, kenn dunu ko fajal. Benn suruseñ amu ci pexe. Nun rekk noo ci mënal sunu bopp dara. Ci kaw, nu xam dëgg-dëgg ki nu doon ak dayob li nu yor. Ndax kat, réew mi jël na ag jonnam lu ëpp juroom benni fukki at ci ren. Waaye, mel na ni xalaat yee ngi des di toog fa ñu nekkoon boobu ak léegi. Jot na nag, nu yewwi sunum xel te boyal ko. Jaaree ko ci fonk ak yékëti ca kaw a kaw sunuy mbaax, sunuy làkk ak sunum mbatiit. Te, bañ cee xeeb lenn ndax, lu nu ci def rekk, doyul.

Bu ko defee, nu baña tee nangu di tëral sunuy xalaat ci yosu keneen. Nu baña tee it àbb bëti jàmbur di ca xoolee. Ndax kat, wolof nee : “ku la abal i bët, fu ko neex ngay xool”.

Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj