Bërug ndëgg-sërëx

Yeneen i xët

Aji bind ji

*Xana du bër da daan neex ndongo ? Daara ju kawe ja ca Ndar, ndongo ya safaan ba lañu wone ca seen bër gu jamp googu. Li ko sooke di ñàkk a déggoo ba am diggante kilifa ga yore seenub nekkin ca jàngune ba di waa “CROUS” ak ndongo ya. Ñooñu doon ñaxtu lañu xaatimoon seen diggante jëm ca liggéey ya ñu waroon amal ca seen dëkkuwaay boobu te mu yéex. 

Loolu waral  ñu dellu ca seen mënin ak ca nañu koy faral di ñaxtoo, mooy def noosu tubaab manaam di lekk ca lekkuwaay ya te duñu fey dara ci diirub ñatti fan yoy, noonu lay wéye gu ñu yokk ag dàbbali. Dogal boobu nag wa “CROUS” ne du ci dal. Ci lañ génnee seen këyitug yëgle, wax ci ne: « ginnaaw dogalug kurél gi yor nekkinu ndongo yi ci jàngune bi, mu di wéy di lekk ca lekkuwaay ya te duñu fey, yokk cag dàbbali,   waa “CROUS” ñu ngi leen di yëgal ne lekkuwaay yooyu dañu leen di tëj, li ko dale gaawu fukki fan ak juróom bu ñu ndékkee ba jëmmi jamono”. Muy dogalub Paap Ibraayma Fay mi jiite CROUS.

 Lii tax ba ndongo ya pëllati ; dog yoonu woto ya, amal fag jàmmarlo ak takk-der ya daldi wëlbatiku salfaañe lekkuwaay ya. Muy mbir yu ñu bari naqarlu rawatina ña ñu ko séqal. Waaye li ñuy wax rekk, ay du weesu baay dee na. Ndongo yi deewuñu naam, waaye seen jëf jooju mujje naa metti ca ñoom. Ñatti fan ya ñu tëj lekkuwaay ya metti woon na ci ñoom. Mënees na wax ne ci kolo-kolo lañu ko dunde. Loolu tax ba daan ya faf gën a tar ca ñoom. njiit ya di leen yëgal ne dañuy mujje tëj seen i bérébi nekkin yooyu di “campus social”. Muy lu xel mënut a nangu ci jamono joo xam ne njàng maa ngay wéy, te am ca ñenn ca ndongo ya di amal seenub kàtte. Tax ba beneen wàll wa tàbbi ca xeex ba di wa “CESL” muy pàcc bi ndongo yi  dénk njàng ma. Ka yore seen kàddu di wuyoo ci turu Usmaan Géy, mu ngi ñaawlu googu dogal te di dankaafu turaandoom Usmaan Caare muy njiitu jàngune ba. Muy biral fa njàng ma tollu, bari ca ndongo yoo xam ni seenug kàtte cig sanni-tàccu lañu ko nar a wékk. Am ñeneen ñoo xam ne mën nañoo neenal seen atum njàng. Waaye taxut ndongo ya rëcc ne lay tooy ca seen roofoo boobu, mën nañoo njort ne ca ñoom lay génne.  

Ci bile guuta, ci lañ woote am ndaje mu jàmp ngir waxtaan ci jafe-jafe yooyu. Kurél giy saytu njàng ma ca jàngune ba, jël ndogal ñu dakkal njàng ma, dale ko talaata fukki fan ak juróom-ñeent jàpp altine ñatti fan ci weeru oktoobar ginnaaw taxawaayu “CROUS”. 

Leneen lañuy ruumandaat ca bër googu di la Paap Ibraayma Fay bokk ca làngug politig. Te ñu for ci weewu béy ne la kàmpaañu wotey palum depite yi door moo waral gile bër.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj