Ngir fàttali, CNRA dafa artu woon rajo yeek tele yi ngir ñu bañ a tooñ RTS mi féetewo, moom kese, woneg matsi kuppeg àddina si. Looloo taxoon mu moytandiku woon leen ci ñu bañ a jalgati yoon. Waaye, kibaraanug Emedia, dafa génne woon yégle, waxoon ci ne, moom : « du mës a nangu lees jagleel sañ-sañi woneg kuppeg àddina si RTS kese. »
Li tax nag CNRA dog siñaalu itv mooy ne teleb Mamadu Ibra Kan bi dafa tàmbali woon a wone kuppeg àddina siy ame ca Qataar. CNRA, génne yégle, bind ci ne : « ajees na woneg naali itv saa bu tele bi tàmbalee wone ab matsu kuppeg àddina si Qataar 2022. » Kurélug Baabakar Jaañ gi teg ci ne, bu tele bi defaatee lu ni mel, dees na teg i daan yu gën a diis, ni ko yoon tëralee.
Waa Emedia nag, nee nañu duñu seetaan mbir mi. Dañoo fas yéene àqi yoon, ci seen i wax. Ndaxte, ci seen yégle biñ biral démb, kibaraan gi naqarlu na ndogalu CNRA bi ba fu naqar yem. Nee ñu, bi FIFA woowee kibaraan ci joŋante ñeel woneg matsi kuppeg àddina si, ñoom ñoo jëloon raw-gàddu gi ci lu leer. Mamadu Ibra Kan ak i ñoñam dañu jàpp ne li leen dal nii ag kootoo la. Te, lii, ci seen i wax, dafa nar a tilimal seen der. Ñu dolli ci ne CNRA day xajamal ëttub kibaraan. Ñoo jeexalee seen yégle ci takkaaralug Nguur gi, di ko ñaawlu.