ÑEENTI SASI NAFAG ATUM 2023 MI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Alxames 17 nowàmbar 2022 la Ngomblaan gi dooroon péncum nafag Nguur gi ñeel atum 2023 mi. 6. 400i tamñareti (miliyaari) CFA la Nguur gi jàpp ngir liggéeyee ko ci at mi. Waaye, am na 4i fànn yoy, Nguur gi ñoom lay gën a cëral ci kow yeneen yi ci des. Fànn yooyii ñooy : wér-gi-yaram gi, coppiteg njuux li, koom-koom gi ak laf gi.

Wér-gi-yaram

Ku ndóbin rey sa maam, foo séenati lu ñuul daw. Ñetti at yii weesu, 2019 jàpp 2022, mbas mu doy waar a dikkaloon àddina sépp. Amul réew mum dajul, rey limi doom-aadama yu jéggi dayo. Te, fu mbasum Covid-19 bi mës a nuyoo, waxuma la bakkan yu rot, waaye koom gaak alal jépp lay nasaxal, sabab ay jafe-jafey dund yoy, foo leen natt ci metti weesu nañ ko. Fi mu nekk nii nag, daanaka xaw nañu mën a wax ne, daan wiris bi. Waaye nag, warees na ci jukkee ay njàngat yu bari. Moo tax Nguur gi nee :

« Nguur gi daf ci war a jànge lu bari, jël ay matuwaayam ngir di wéy di jàppandal paj mi. Ndaxte, léegi, nit ñi nekkatuñ fi di amey metit, di dee te naan « Yàlla baax na ». Dañuy laaj ñu faj leen te yombalal leen dund gu ànd ak wér-gi-yaram ci ni mu gën a yàggee. »

Ci kow loolu, Nguur gi beral na wér-gi-yaram gi lu xaw a jege 300i miliyaari CFA. Naam, lu baax la. Waaye, ndax dina doy ? Ku seetlu jafe-jafey fànnu wér-gi-yaram wi, du ñàkk nga xaw a ñaw njort. Nde, mbirum DANTEC mi gi fi, ba tey dara leeragu ci. Fajkat yi doyuñu, raglu yi tamit naka noonu. Bare nay diiwaan yoo xam ne, nit ñaa ngay dee bés bu nekk ngir ne amuñuy bérébi fajuwaay.

Coppiteg njuux li

Ginnaaw wér-gi-yaram gi, coppiteg njuux li itteel na lool Nguur gi. Dafa di, njuux li daya am i njeexital ci dundiinu nit ñi ak ci koomu réew mi. Nde, liy màndargaal coppiteg njuux li mooy : yàqute jàww ji, tàngoor bu tar bi, mbënn mi, maral mi, daay yi, géej giy nangu suuf yeek dëkkuwaay yi, añs. Moo tax, jéyya yi bari jamono jii. Nguur gi xam na solos mbir mi. Mu ngiy wax ne :
« Coppiteg njuux li dafa diw sas wu réy ci nafag atum 2023 mi ñeel, li ci ëpp, fàggu ngir xeex mbënn mi, am ndox mu doy ci mbey mi, toppatoo tabaxtey yoon yi ak cetalug dëkkuwaay yi. Lii lépp diy liggéey yees sumb ci 2023 mi. »

Fii tamit, mënees na fi amal ab taxaw-seetlu bu ndaw. Ndaxte, Nguur gi fi nekk, at mu nekk mu dige ay pexe, génne xaalis bu takku te du saafara dara. Mbënn mi rekk doy na ci misaal. Ne woon nañ fi jagleel nañ ko 700i miliyaar at yii weesu te, ba tey, dara sottiwul. Moom sax, tey la Waalo gën a aay. Mbënn mi nangu na kër yu baree bare, yàq ay yoon i yoon te di sabab yenn xeeti feebar yi ngir taa-taa ndox yu selladi yi. 2012 ba tey, njiit yi fi nekk mënuñu koo faj. Ndax menn at mi leen dese doy na ci ?

Ginnaaw loolu, bu dee wàllu cet ak cetal, loolu moom du neex a jëmmal. Li ko waral mooy ne dafa aju ci yar ak teggin. Cet, ci kër yi lees koy jànge. Te, Senegaal moom, fépp mbalit la ; fu waay jot sàndi fa sa mbalit, fu waay jot tuur fa ndox, ba ci tali sax. Mënoo dox cim mbedda te doo joggi mbuus walla kaasu kafe bu jeex. Miir yépp sawees na leen. Géej gi nag moom, ab sën la ko saa-senegaal yi def.   Ndoxum foos yeek këwsu yi tilimal nañ ko tilim bu jéggi dayo. Yan matuwaay la Nguur jël ngir xeex ñàkk a set gi ? Ndax ñi ngi jàngal gune yi ci daara yi cet ak cetal ?

Ci beneen boor, Senegaal a ngi waaj liggéey soroj bi (petarool). Ndax ñoo ngi sóor njeexital yi muy am géej gi, rawatina napp gi ? Ndax Nguur gi bàyyi na ko xel ? Laaj yaa ngoog…

Yokkuteg njëgi dund bi ak njureefi laf gi

Bu dee am na soxla su gën a itteel askanuw Senegaal, du doon lenn lu dul dund bi. Ndax, jamono jii, ni njëg yokkee dafa metti lool ci boroom kër yi, rawatina góor-góorlu yi nga xam ne ñoo fi ëpp. Moo tax, ku leen wàññil lekk gi ak naan gi, ak soxla yu mënut a ñàkk yi, dinga leen defal lu réy. Nde, saaku bu feesul, du taxaw. Moo tax Nguur gi jagleel xaalis bu takku, jëm ci wàll wi : 3. 000i miliyaari CFA ngir at mii, ak yeneen 96i miliyaar yi muy ciy dolli ci atum 2023 mi.

Lees seetlu ci kow, mu fi nekk ba tey. Feebar boo fajul ci diirub 10i at, boo nee ci menn at nga koy saafara, gëm la du yomb. Naam, mbas mi ak tolluwaayu àddina si am nañuy njeexital ci koom-koom yi. Waaye, ndax Senegaal dafa mënul a suqali mbay gi, dooleel càmm gi, fexe ba saa-senegaal bu nekk mënal boppam ? Loolu kese mooy pexe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj