TÀMBAAKUNDAA : PÉEYUB SENEGAAL CI DIIRU 3i FAN

Yeneen i xët

Aji bind ji

Li ko dale 26 desàmbar jàpp 29 desàmbar 2022, Njiitu réew mi ak Càmm gépp dinañu ganeji Tàmbaakundaa. Mu mel ni, ci diirub 3i fan yooyu, Tàmbaakundaa mooy nekk péeyub koom-koom ak caytug Senegaal. Ci lees jotagum ciy xibaar, Ngurr gépp a fay teew bu keroogaa. Nee ñu, ci ngoonug 26 desàmbar la Njiitu réew mi, Maki Sàll, di teer ca diiwaanu penkub Senegaal gi. Ca ëllëg sa, Njiitu Bokkeef gi dina ubbi tali Tàmbaa – Kidiraa bi ci yoor-yoor bi, ubbiwaale màkkaanum sóobare mu Gudiri. Bu ngoon jotee, 16i waxtu ci bésub 27 desàmbar bi ba tey, dina jiite Ndajem Njiiteef gi. Ndaje moomu, guwernãs lay ame. Bu àllarbaa, 28i desàmbar 2022, mu jiite fa Ndajem Jawriñ yi. Alxames, 29 desàmbar 2022, la fa war a jóge.

Tàmbaa mooy diiwaanu Senegal bi gën a réy, gën cate te digaloo ak 3i réew : Mali, Moritani ak Gàmbi. Atum 2008 lees ko def diiwaan ci wàllu caytu. Ci wàllu koom-koom, Tàmbaa dañu fay bey gerte, wëtteen, dugub, mboq, basi, ceeb, ñebbe, fooño, banaana, sesaam… Càmm, napp (ci dex yi) ak yaxantu tamit am nañu fa wàll wu réy a réy. Wërteef (turism) tamit am na fa solo lool sax. Tàmbaa nag, lees ko gën a xame mooy balluy mbindaare yi nekk biir suufam. Wurus, weñ, marbar, añs. Daanaka, diiwaanu Tàmbaakundaa ñàkkul dara. Waaye, ba tey, ab diiwaan bu ndóol la, ñàkk ay tali ak i fajuwaay yu doy. Cet gi tamit, sikk la fa.

Askanu Tàmbaa a ngi yaakaar ak a njort ne, ñëw bi fa Njiitu réew mi di ñëw dina am lu mu wàññi ci seen i jafe-jafe.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj