BIRAM SULEY JÓOB, MBAA DU… ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gor, ca wax ja. Kàddu gilee génn démb ci gémmiñi saa-senegaal yu baree bare. Waaye, ci làmmiñ ak loyukaayi (claviers) ndawi PASTEF yi la gënatee jib. Nde, fan yii, démb ak tey, mbaali jokkoo yi saf nañu sàpp ci waxu boole ay moome. Lu jiin nag, Njaag a, te Biram Suley Jóob a di Njaag. Ndax, moom mi topp ci Usmaan Sonko, sës ci moom rëkk, dafa janoo ak taskati-xibaar yi, àddu ci mbirum mbooleg moome yi. Waaye nag, la mu ca wax dafa xamb taal.

« benn àtte terewu ko »

Ku déglu meeru Cees-Kow, sa njort du rafet. Ndax, li mu wax, rawatina ni mu ko waxe, teeyloo na xel yu bari, jur coow lu ne kurr, rawatina ci mbaali jokkoo yi mu duutaale baaraam. Biram Suley dafa wax, ñeel mbirum booley moome, ne « benn àtte terewu ko ».

Moom de, dafa mel ni sax bëggul a bàyyi benn ci ñaari moomey pal yi ko askan wi gàll. Nde, waxam jii, dafa mel ni loolu lay wund :

« Amul fenn fu yoon teree nekkandoo meer ak dépite. Ca Farãs, am nab àtte bu koy tere waaye Senegaal amu ko. Amul fenn fu ñu teree nekkandoo meer ak dépite, dama koy waxaat ».

Naam, yoon terewu ko. Wànte, warugar la ci gor, mu sàmmonte ak digeb kilifaam. Ngir fàttali, Usmaan Sonko dafa dige woon ne, bu faloo, dina wotelu ab àtte buy tere mbooleg moome yi. Donte ne, ci waxtaan wi njiitalu PASTEF li mujje am ak taskati-xibaar yi, waxoon na ne, ci wàll woowu, mënul tënk kenn. Ndegam dige na ko rekk, jàppees na ni, bu sa kilifa waxee, yóbbaale na la ; maanaam, kàddu gi sas sag kilifa, sasaale na la, yow mi nangoo ànd ak moom cib xeex. Rax-ci-dolli, moom Biram Suley Jóob ci boppam, toog na fi cib jataay, ci benn tele, wax ne moom, li Usmaan Sonko dige, dina ko jëfe. Loolu, yàggul dara. Waaye, saa-cees bi dafa jàpp ne dañu koy sëqatal te, moom, nee na :

« Kenn waru ma wax li ma war a def, kenn waru ma teg dara, bu jotee, dinaa xam lu may def. Du nit ñaa may wuutu ci sama ndogal. Man maay tànnal sama bopp. »

Ñu baree naqarlu waxam ji, ak ni mu ko waxe. Dafa di, fi àddina tollu, rawatina Senegaal, war na tax ñu weesu mbirum boole ay moome. Ndaxte, lu nit mën, keneen mën na ko, walla sax mu mën lu ko raw. Waaye, kenn kese boolendoo ñaari ndomboy-tànk walla lu ko ëpp, yorandoo leen, daf fi war a jeex. Lu ni mel, day niru ag xeebeel ñeel say nawle. Te nag, boroom xam-xam yi bari nañ fi, kenn kese sësu fi. Nguur nag, nee nañu dinay faral di dofloo. Mànditeg nguur dina yóbbe nit, bu moytuwul, mu wann li mu waccu woon, fecci kóllëre, walla wax-waxeet. Moo tax ñu naan : Biram Suley Jóob, mbaa du… ?

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj