Dëgg la : ràcc jëmale sa kanam baaxul waaye tey fàww LU DEFU WAXU xamle mbégteem ci ndam li Paap Aali Jàllo am fan yee nu génn ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Paap Aali ci kër gi la bokk, ayubés bu Yàlla sàkk mu am lu mu bind ci seen yéenekaay bii di LU DEFU WAXU. Nun ñiy liggéey ak moom xam nanu ne bu ci Yàlla àndee, kenn du wax ëllëg ci yenn kàllaamay réew mi, rawatina pulaar ak wolof, te doo tudd Paap Aali Jàllo.
Àllarba jii, deesu ko fàtte. Waaw, àllarba 20eelu fan ci weeru Féewaryee, Banqaasu Làkk ak Caaday Afrig (LCA), bi nekk ci Pàccum Aada yi, Diine yi, Aar yeek Jokkalante yi, doon na dalal ab ndongoom, mu war koo jax. Xew-xew baa ngi ame ca Iniwérsite Gaston Berger bu Ndar. Ndongo li doon jébbal kàngam yi njuréefi gëstoom mooy Paap Aali Jàllo. Ci kàllaama nasaraan, xew-xew boobu dees na ko duppe “soutenance de mémoire”. Loolu, nag, mi ngi am ginnaaw bi fa Paap Aali jàngee lu tollu ci diirub juróomi at.
Liggéey bi Paap Aali doon jébbal mbooloo mi, ci turi Pulaar yi la aju. Maanaam, gëstu bi mu amal ci diirub ñaari at, li mu ko dugge woon mooy biral jëmmi turi Pulaar yi, fésal ni ñu sosoo ci kàllaama pulaar, leeral seen cosaan, ak di xamle lu tur yooyii wund. Waaye, Paap Aali yemul foofu. Ndaxte, wax na ci biir téere-tëju-diggam bi naka lees tànne tur ñeel waaso Pulaar yi, gëm-gëm yeek pexe yi ko lal ba ci ngénte nees koy amale. Xóotaayu gëstu bee waral Paap Aali dem ba wone turi yaradal yeek xeeti tur yoo xam ne, ràññee njaboot gee leen tax a jóg. Maanaam, ni xale yi di toppalante, li ko dale taw bi ba ci caat bi. Loolu fés na ci tablo bii nu jële ci téeréem bi.
Kàngam yi doon saytu liggéeyu Paap Aali bi ñeent lañu : Porfesoor Maweja Mbaya mi jiite woon àtte bi, Doktoor Mouhamedoune Abdoulaye Fall, jàngalekat ca Banqaasu LCA, Doktoor Mariama Mahamane Maїga mi doon tette ndongo li ba liggéey bi yemb, ak njiitu Banqaasu LCA bi, Doktoor Ibrahima Sarr. Moom, Doktoor Ibrahima Sarr dafa wute bés bi ndax dafa amoon ngànt. Ab tukki moo ko teree teew. Waaye, jot naa yónnee ab bataaxal, biral ci mbégteem, seedeem ñeel Paap Aali, rawatina gis-gisam ci téere-tëju-digg bu Paap Aali Jàllo.
Ci suba si, bi fukki waxtu jotee, ci la ndongoy Banqaasu LCA tàmbalee feesal “Amphi B”. Mbokki Paap Aali yeek am-di-jàmmam yi tamit kenn demul ñu des. Bi fukki waxtu tegalee fanweeri simili, la lawax bi jël kàddu gi, layal xalaat yi mu xelli ci biir téere-tëju-diggam bi ginnaaw bi ko kilifa yi mayee ñaar-fukki simili. Mu daldi nuyoo ba noppi xamal nit ñi naka la tànne bile ponk, cosaanu liggéey beek jubluwaayam. Ci nasaraan, Paap Aali mi ngi doon gëstu lees di wax “Anthroponyme Pulaar : formes et sens”.
Moom, nag, tur yi Pulaar yi moomal seen bopp rekk la jagleel liggéey bi ngir biral ni tur ci bokk-moomeelu askan la bokk. Mu tënk, wone ay masala, leeral leen ci noppi nit ñi. Waaye, bala tog nomlet, toj nen.
Benn liggéey xéyul rekk sotti. Looloo tax Paap Aali xamle yoon wi mu jaar, jafe-jafe yi mu jankoonteel ak pexe yi mu lal ba jéggi leen ngir sottal mbind mi nga xam ne, mi ngi tollu ci 159 xët. Bi mu noppee, delloo na kàddu gi Kilifë yi doon càmbar téere-tëju-diggam bi. Njiitu àtte mi, Porfesoor Mbaya gërëm ko ndax li mu fexe ba yem ci waxtu wi ñu ko mayoon.
Jàngalekati Banqaasu LCA yi, Doktoor Mariama Mahamaan Maїga, Doktoor Mouhamedoune Abdoulaye Fall ak Doktoor Ibrahima Sarr, seen seede benn la. Nee nañu dañoo mӫs di bég ci Paap Aali, ndongo lu am pastéef, bӫgg lool li muy def. Dafa mës a doon royukaay ci ay moroomi ndongoom, nekk jàngkat te ku weg ñi muy jӫflanteel la. Ñu neeti, Paap Aali bokk na ci ndongo yi gën a xereñ ci Banqaasu LCA. Terewul, àtte nañu ko àtte bi war ginnaaw bi ñu saytoo liggéey bi. Li ci jaar yoon, kilifa yi rafetlu nañu ko bu baax. Masala xibaar yi mu indi ñeel Pulaari Fuuta Tooro yeek seen làkk wii di pulaar. Rawatina bi mu nu xamalee seen i tur ak li ñu wund.
« Njuumte, nag, mënul a ñàkk ci téere-tëju-digg”. Loolu la Porfesoor Maweja Mbaya leeral laata muy jubbanti yenn njuumte yi mook Mouhamedoune Abdoulaye Fall, ak Mariama Maїga.
Kilifë yépp sampoon nañu ay laaj yu Paap Aali tontu tontu yu leer. Danuy jaaraat ci baatu Alpulaar, mu nekk baat bu siiw bu nuy dàkkantale nit ñiy làkk Pulaar. Te firi bi moo di “waxal Pulaar !”. Ci gis-gisu gëstukat bi, wareesul a woowe Pulaar yi baat boobu. Ndaxte, ab pulaar deesu ko wax “waxal pulaar” ndax moom la nàmp. Waaye baatu Alpulaar buuru Fuuta Tooro ba woon, Mànna, moo ko waxoon jëme ko ci wolof yeek yeneen waaso yi fa nekkaloon ak Pulaar. Ku ci làkk pulaar ñu woowe la “Alpulaar”, ku ko làkkul ñu rey la. Kon, baatu Alpulaar ab Ndigal la woon. Baatu “pël” yit noonu, wareesu ko jëfandikoo ngir tudd Pulaar yépp. Ndx kat, “pël” mécce la, maanaan ab sàmmkat la. Te ci biir Pulaar yi am nay nappkat, ay tëgg, ay géwél, ay uude, añs. Kon turu Pulaar moo gën jekk ci ñoom.
Jotaay bi, nag, yàggoon na ba jéggi dayo. Waaye, ba benn waxtu ci bëccëg jotee ba tegal fanweeri simili la kilifë yi daldi yégle seen àtte, jébbal ndongo li « Mention très bien ». Muy firndéel màggaayu liggéeyu Paap Aali. Ñépp ndokkale ko, ñaanal ko mu jig ko te yeneen lijaasa topp ci. Xarit yi daldi jël ay nataal ni ñu ko tàmm a defe. Ay xéewal lañu ko tëje, fa la mbooloo mi añe ba suur, naan yu sedd te neex.
Ma baamtuwaat ko, bés du mag, du tuut, boroom lay tollool, te keroog kenn werantewu ko.