CAN 2023 : ALIW SIISE TÀNN NAY NDAWAM

Yeneen i xët

Aji bind ji

Barkaatu-démb ci àjjuma ji la tàggatkatu ekib nasiyonaal bi, Aliw Siise doon amal ab jàkkaarloo ak taskati xibaar yi ngir wax li jëm ci waajtaayu CAN bees dëgmal ca Koddiwaar ak biral ndaw yi mu tànn ngir ànd ceek ñoom ñu taxawal fa sunu réew mii di Senegaal. Seen dem gii nag dana wuute ak ya wees. Ndax daf ciy ame ñaari taxawaay. Bu njëkk bi mooy ni moo mujje yëkkati kub bi kon dafa war a xeexal cëram woowu. Ba ca topp nag di xeexaat ngir jéem koo tóllanti. Aliw Siise yëkkati na ay kàddu yu jëm ci loolu wax ne :

“Ragalunu. Danuy dem ci CAN bii ak yéene ju réy a réy. Nun nooy buuru Afrig. Kon ekib bi yelloo na cër wu ëpp wiñ ko jox nii. Bu Senegaal wóoluwul boppam, man gisuma ban ekib mooy wóolu boppam ci Afrig gii.”

Gannaaw loolu nag biral na limu ndaw yim tànn. Ñoo nekk nii :

Góol yi : Eduwaar Méndi, Séeni Jeŋ, Móori Jaw.

Defãsëer yi : Kaliidu Kulibali, Musaa Ñaxate, Abdu Jàllo, Yuusuf Sabali, Fóode Baloo Ture, Formóos Méndi,  Abdulaay Sekk, Ismayla Jakob ak Abdulaay Ñaxate Njaay.

Miliyë yi : Idiriisa Gànna Géy, Séexu Kuyaate, Lamin Kamara, Paap Mataar Saar, Paap Géy, Paate Siis, Nàmpalis Méndi ak Kerepeŋ Jaata.

Ataakã yi : Saajo Maane, Ismayla Njaay, Ilimaan Njaay, Nikolaa Jakson, Bulaay Ja, Abiib Jàllo ak Abdulaay Sima.

Kon lii mooy limatu ndaw yees tànn ngir ñu teewal Senegaal fa Koddiwaar ca CAN ba. Am ñu bokkon ca ba ñuy jël kub bi weesu te bokkuñu wii yoon. Xaarees na ci ñoom ñu ñaanal ekib bi te gën a liggéeyaat ngir weneen yoon ñu mën a dikkaat, nde la ca ëpp ay ndaw lañu.

Gannaaw tànnug Aliw Siise miy tàggatkat bi nag, am na ay coow yu sew yuy jóg jëm ci lim nu andil rawatina ci mbaali-jokkoo yi. Foo geestu ñoo ngi ciy wax. Li gën a bari ci lees di wax moo di ne, moom Siise, dafa bari lim woo ciy defãsëer, ba sax ci miliyë bi, xeexkat yi ñoo ci ëpp. Boo jàngatee tànn gi wàlluw defãs moo ci ëpp te jamono jii ñu xarañ ci kaw ak ci kanami kã yi lees gënoon a xaar ci moom.

Gannaaw loolu it yëkkati na ciy kàddu moom Aliw Siise di xamle ni:

“Duma Yàlla, duma yonent. Tàggatkat laa te awmay xërëm ngiy soppi yëf yi. Li ma mën tay mooy góor-góorlu. Lenn lu nu mën, nun, mooy góor-góorlu.”

Muy lees ko mën a nangul itam. Bu loolu weeso, ekib bi dina amal ndajem xaritoo ak kii di Niseer fii ci réew mi ca fowub Abdulaay Wàdd 8i fan ci weeru saŋwiyee wii bu 18i waxtu jotee.

Nu mànkoo wutiwaat ndam li.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj