CAN KODDIWAAR 2024 : CAABALU BÉS BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

WÉR-GI-YARAMI ALIW SIISE AK ABDULAAY SIMAA

Bees sukkandikoo ci yégle “Fédération Sénégalaise de Football” (FSF) biral démb ci gaawu gi, Aliw Siise, tàggatkatu ekibu Senegaal bi, dafa jagadi woon. Ci àjjuma ji, bi joŋante gaynde yi jeexee, la ko feebar bu gaaw dikkal, ñu rawale ko fa raglu ba. Waa FSF xamle ne, fajkati ekib bi ñoo ko taxawu laata ñu koy yóbbu fajuwaay ba, di raglub Yamusukuro. Nee ñu nag, tane na bu baax a baax. Te, dellu na daluwaayu (otel) ekib bi sax.

Bu dee mbiri Abdulaay Simaa, moom, keroog àllarba la yëgoon aw metit ci ginnaawu tànku càmmooñ bi. Ginnaaw ba ko fajkati ekib ba càmbaree, ñu gis ne dafa ame gaañu-gaañu ca càq ya, maanaam ci “aducteurs” yi. Loolu jural ko mu war a am toogay bu yàgg bum dul laal bal. Ba lile amee, njiiti yi ekib bi ak yu këlëbam juboo ci mu dellu fa këlëbam, Glasgow Rangers, ngir mën a fajoo fa bu baax. Kon fim ne, moom Simaa, bokkatul ci ñiy àggale CAN bi.

Nu di leen ñaanal ñu wér ak jàmm !

NGIRTEY BÉS BI

Kippug F : Marog day xaar

Ci kippug F gi, Marog mi bokk ci fawori yu mag yi dafa timboo ak Kongo Demokaraatig 1-1. Marog moo njëkk a dugal. Ca 6eelu simili ba la seen lateraalu ndeyjoor bi, Asraaf Hakimi, dugal. Waaye, Gayndey Atlas yi reyuñu mats bi, dañoo teggi seen tànk. Noonu, Kongo di puus ba am penaatii ci 42eelu simili bi, laata ñuy mitã. Wànte, Bakàmbu dafa dóor bal bi poto ndeyjooru Bonoo, góolu Marog bi. Loolu taxul mafari (léopards) Kongoo yi xàddi. Nde, bi ñu dawalee ba ci 76eelu simili bi la Silaas Wamangitukaa dugal.

Bu dee beneen joŋanteb kippu googu ba tey, Sàmbi dafa tamit timboo ak Tansani. Tansani moo njëkk a dugal ci 11eelu simili bi laata Sàmbi di dugal bi joŋante biy waaj a jeex (88eelu simili bi). Fi mu nekk nii, Marog moo jiitu (4i poñ), topp ci Kongo Demokaraatig (2i poñ), Sàmbi toppaat ci (2i poñ). Tansani moo jëlagum ndaare (1 poñ). Dara leeragul ci kippu gi nag. Ci seen i ñetteeli joŋante lañuy xam kuy génn am déet.  Àllarba 24 sãwiyee lañuy futbalaat bu 20i waxtu jotee.

Tansani-Kongo Demokaraatig ak Sàmbi-Marog lay doon.

KIPPUG D : ALSERI DAFA MOY

Démb ci gaawu gi la ñaareeli joŋantey kippug D gi amoon. Alseri moo doon laaleek Burkinaa Faaso, Móritani doon daje ak Àngolaa. Alseri dafa timboo 2-2 ak Burkinaa Faaso. Ñoom sax, Naar yi, dañu rëcc. Ndaxte, ñaari yoon Burkinaa mi ngi leen di jiital, Bunejaa di leen ci génne. Rax-ci-dolli, wonewuñ fa lu dal xel ci wàllu futbal.

Bu dee Móritani moom, Àngolaa moo ko dóor 3i bal ci 2. Wii mooy ñaareelu yoon ñuy dóor sunu mbokki Gànnaar yi. Nde, ca seen joŋante bu njëkk ba, Burkinaa Faaso moo leen dóoroon 1-0. Kon, ñoom moom toog nañ ndax ñoo mujju ci kippu gi ak 0 poñ. Àngolaa moo jiitoogum (4i poñ), Burkinaa topp ci (4i poñ), Alseri nekk ñetteel ak 2i poñ kepp. Talaata 23 sãwiyee lañuy futbalaat bu 20i waxtu jotee.

Àngolaa-Burkinaa Faaso ak Móritani-Alseri lay doon.

KIPPUG E : ALSERI DAFA MOY

Mali ak Tinis ñoo doon daje démb. Waaye, ndam demul, ndam dikkul. Nde, dañu timboo 1-1. Tey ci 20i waxtu la Afrig-Di-Sid di futbal ak Namibi. Mali nag moo jiitoogum ci kippu gu ak 4i poñ, Namibi toppagum ci ak 3i poñ, Tinisi miy ñetteel am 1 poñ kese.

NAALU ËLLËG BI

Ëllëg ci altine ji, ci kippug A gi, Gine Ekuwaatoriyaal dina daje ak Koddiwaar, Gine Bisaawo daje ak Niseriyaa. Ñaari joŋante yaay dawandoo bu 17i waxtu jotee. Koddiwaar nag mi ngi ci guta ; dafa war gañe ngir jàll walla mu timboo sax ngir yaakaar bokk ci ñetteel yi gën a jekku.

Bu 20i waxtu jotee, joŋantey kippug B yi ñooy daw. Kab-Weer – Esipt ak Mosàmbig – Gana ñooy futbal. Bu dee Kab-Weer jàll na ndax 6i poñ yi am, Esipt (2i poñ), Gana (1 poñ) ak Mosàmbig (1 poñ) moom seen dara leeragul.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj