CEERNO ALASAAN SÀLL : "SAMA YÉENE CI RÉEWUM SENEGAAL…"

Yeneen i xët

Aji bind ji

Tey, Senegaal, kenn mënul a wax waxu pólitig te doo ci boole Ceerno Alasaan Sàll. Turam ak turi Usmaan Sonko, Bàrtelemi Jaas, Xalifa Sàll, Abdul Mbay, Mamadu Jóob Dëkuruwaa ak Mamadu Lamin Jàllo ñoo gën a fés ci kujje gi. 

Seen yéenekaay LU DEFU WAXU amal naak moom laaj-tontu bu yaatu, di ci waxtaane mbiri réew mi ak xew-xewi jamono. 

Xaajees na waxtaan wi ci ñaari pàcc. Ci ñaareelu pàcc bii, Ceerno Alasaan Sàll day wax ci téere bim génne bu yàggul, li ko tax a bàyyi APR, yorinu réew mi, wote yi ak mbirum Usmaan Sonko ak Aji Saar.

(Ci taataanug Paap Aali Jàllo)

PAJ : Lan moo la tax a bind sa téere bi nga duppe Le Protocole de l’Elysée, Confidences d’un ancien ministre sénégalais du pétrole ?

Jërëjëf ci laaj bu amati solo bii nga ma laaj. Dina ma tax a leeralaat lu bare. Téere bi, li tax nu bind ko mooy ne, dan bokkoon ci nguur te, lépp loo gis ci nettali lay mujj.

Dafa di, doomi-réew mi, nees yore réew mi da leen a itteel ; rawatina maas yiy ñëw ëllëg, war a xam naka lañ daan saytoo seenub ndénkaan, seen moomeel. Moo tax, dinañuy am i laaj yu bare te jaadu ñeel alal ak bokk-moomeelu askan wépp. Ndaxte kat, yoon la, nit ñiy fànnoo seen yorinu réew, di laaj ak a gëstu ci li leen ci jaaxal. Rax-ci-dolli, dafa yell askan wi xam li laxasu ci coow yu bare yi lëmbe réew mi jamono jii : otorutub pey gi, séddaleb ayeropoor bi ak suufi réew mi (am ñu ciy jële ay milyaar)… Lu tax dëkki kow yu bare amuñu ci mbëj mi ba tey jii ? Lu tax pey gi néew ci ñi ko am ? Lan mooy ñuul ci sunu petarool ak sunu gaas yi feeñ Senegaal ? Petarool ak gaas yooyee nga xam ne, mënees na cee jariñu, suqali ci sunu koom-koom, naatal ko, faj ci jafe-jafe ak aajoy askan wépp ba keroog àddinay tukki. Lu tax coow li bare ci ba ñuy ragal li dal yeneen réew yi ko am dal nu ? Lan mooy taxawaayu nguur gi ci fànn yii yépp ? Lu ciy wàllu képp ku ci mës a yor ndombog-tànk, ñu mës laa dénk alalu askan wi ? Man mii nga xam ne nekkoon naa ci nguur gi, lan moo ciy sama cër ?

PAJ : Te du mer a la ko tax a bind ?

Déedéet ndaxte, dama doon liggéeyal askan wi ma dénkoon baatam, sañ-sañam ak alalam ; askan wi ma yónni woon, sasoon ma, ma war koo leeralal sama taxawaay ba may nekk ci nguur gi. Looloo waral téere bi. Ndege, bu ma Yàlla mayee ma dund, tënk li ma teewe lépp cib téere, móol ko, génne ko, jébbal ko askan wépp, dina doyub leeral. Te, nag, ba tey, ñi fekke li ma wax ci téere bi yépp, kenn weddeegu ci dara, te ñoom ñoo ngi dund. Kon, bu loolu amee, maas yiy donni réew mi ëllëg, dinañ mën a jot ci seede ak gis-gisu kenn ku bokkoon ci mbir mi. Waxuma nag ne sama gis-gis rekk moo wér, donte ne jàpp naa ne li ma wax mooy dëgg.

Ginnaaw loolu, baax na askan wi xam ne, nun, dunuy faral di bind ay téere. Maa ngi gërëmaale, di sant sunu mag, Bubakar Bóris Jóob. Ndaxte, mu ngi def liggéey bu am a am solo, di def kem-kàttanam ngir doomi-Senegaal yi gën a tàmm a jàng. Royukaay bu mag la ci googu fànn. Nun, danu war a dekkil, dundalaat sunum mboor ; muy mbirum Kaasamaas, sunu jaar-jaar ak Gàmbi, Fóode Kabaa 1, Fóode Kabaa 2… li aju ci ni réew mi moome boppam. Mamadu Ja, moom, bind na ci. Waaye, Seŋoor bindu ci, waxul nim dunde péexug Senegaal. Muy lu xaw a doy waar ndax Seŋoor taalifkat la woon, nekkoonub xeltukat. Te, néew na cib Njiitu-réew luy bind i taalif ak a xeltu muy ñàkk a bind ci wàll wu ni mel. Xam nga ne, li xewoon ci atum 1962, dafa jaadu nu xam ko. Gis-gis bii moo tax ma ne woon, bu ma fi Yàlla bàyyee, may ma wér, bàyyee maak sama xel, sama sago ak sama kàttan, dinaa bind sama téere, teg. Ñi ma ko séqaloon ñépp a ngi dund.

Man daal, jébbal naa doomi-réew mi sama gis-gis, sama xalaat ak ni ma dunde mbir mi. Képp ku may weddi, bëgg teggi li ma wax, mën nga def ni ma def, bind teg, askan wi àtte.

PAJ : Moone am na ñu ŋàññ téere bi, soofantal ko… Ndax am ngay firnde ci li nga ciy wax ?

Waaw. Am na ci, nag, ñu doon jéem a diiŋat téere bi, di ko jéem a xalab,  ñaawal ak a sikkal. Waaye, ni ma ko waxe rekk, ay waxi kasaw-kasaw la. Nde, li ci xolu téere bi, yuqu mbind mi, teggiwuñ ci dara, te mënuñu cee teggi dara ba dara booloo jeex. Li ko waral mooy ne bindantuwuma. Dama sukkandiku ciy firnde yu leer nàññ, wékk samay wax ciy kayit yu wér te wóor. Ndax, kat, ku dem ba bind ci lu ni mel, ak ñu ni mel, xamal ne mënees na la yóbbu fa mbaxane doonee benn. Rax-ci-dolli, boo juumee ba wax lu safaanook dëgg, boo wattuwul caabi féete la ginnaaw. Moo tax, yow miy bind walla ngay wax, danga war a jël say matuwaay, biral ay firnde yu leer yiy wone ne, li nga wax ci diw dafa dëppook li am. Muy lu jar a sóoraale.  Man sax, dama gëm ne, doom-aadama, wareesul a teg ci deram lu wuteek dëgg, di yàq turam ciy maaliforo.

Waaye, nag, aji-bëgg-sa-réew ju ne, sa réew daf la war a jaral lu ne. Bu ko jaree, ràngul ci pólitig. Xaral sa tànki-tubéy, def loo mën ngir aar sa réew ci fànn gu ne, suqali ko, naatal ko. Bu jaree wax, waxal. Bu jaree bind, bindal. Waaye, na lépp tegu ci dëgg ak ni ko yoon bëgge. Taxawal jàmmaarlook képp ku nar a yàq walla yàqal réew mi, muy doxandéem bi walla doomu-réew mi, rawatina sax doomu-réew mi. Loolu, wareesu cee ragal cong miñ lay song, xaste yi, saaga yi, xoqtal bi, jaay doole bi, añs. Saa boo càmbaree mbir mi ba gis ne am na luy ñuul ci soow mi, am ciy firnde yu wér, waxal, bindal, te ànd ceek yar ak teggin.

PAJ : Yaa ngiy ciy ŋàññaale doxalinu Maki Sàll, Njiitu-réew mi. Lan ngeen jote dëgg-dëgg ba tax laa gedd ?

Paap Aali, sa laaj bi, dafa jafee tënk ci tontu bu gàtt. Téere bi maa ngi ciy waxaale mbirum Total mi. Moom sax [Njiitu-réew mi, Maki Sàll], moo ko yóbbu ci mbirum Total. Waaye, ayu-bés gi nu amee réeroo ci mbirum Total mi laa bëggoon a dem ; ñoom ñu jàpp ci déggoob Frank Timis bi. Déggoo boobu, nag, cib xayma, benn xaaj ci kow ñett moom la ci Timis dese woon. Booba fekk na Timis jaay ñaari xaaji Cosmos yi ñëw, def liggéey bi ci war. Timis, moom, deful woon dara.   Ci la Cosmos gëstoo ba gis gaas ci géeji ñaari diiwaan : Ndar (Saint-Louis Offshore Profond) ak Cees (Kayar Offshore Profond). Bi loolu amee, xaaj bi Timis dese woon dafa yokku, daldi ful bu baax a baax. Mu ne daf koy jaay, génn. Ndege, moom Timis, liggéey mësu koo ñor. Te, ci samay gëstu, njortoon naa ne nim ame déggoo bi jaarul woon yoon, te coow li tàmbali woon na jib. Ci laa waxee ne nan ko foqati ciy loxoom. Ndaxte, benn, nim ko ame woon dëppoowul ak yoon ; ñaar, nim ko yore woon teguwul ci sàrt yi ndax liggéeyul te dugalul dara. Te, yoon dafa ne, 3i weer yu nekk dafa war a dugal ay koppar ci liggéey bi. Looloo war a firndeel ne moom am na mën-mën, doole ak alal ji liggéey bi laaj ba tax ñu dénk ko ko. Ci misaal, dafa mel ni nga jox nit kayitug dawal (oto). Boo demee ba xam ni moom mii kat ndeke mënatul a dawal, feebar na ba tëdd walla mu ame beneen gàllankoor, bu boobaa li la war mooy ñu nangu kayitug dawal giñ ko joxoon. Lu ko moy, dina def njaaxum.

Noonu, ma waxtaan ceek Maki Sàll ci njeexitalu weeru awril, atum 2017. Waaye, déggowun ci woon. Man, nag, bëgguma woon tëb rekk bàyyi, di indi coow ak lu ni mel. Sama yéene moo doon waxtaan ceek moom ci njekk ak teraanga, lépp jaar yoon. Waaye, mayu ma ko. Waxatuma dara, mu indi déggoob Total bi nga xam ne moo yées déggoo bim xaatimoon ak Timis, daldi nu sant nu jàllale ko. Ñaari mbir yooyu daal, Timis ak Total, ñoo ma tax a dakkal sama ànd ak Maki, ma tekki sama ndombog-tànk.

PAJ :  Kañ nga tàmbalee ñaaw njort ci Maki Sàll?

CAS : Boo xoolee, bi Maki Sàll di nekk ci kujje gi, àndoon ceek nun, dafa nekkoon nit ku baax, woyof, amoon yéene ju rafet ci réew mi. Naam, amoon na ñu ma doon aartu, di ma ko moytuloo, naan ma bu ko wóolu. Ndaxte, dañ ma doon fàttali ni Maki Sàll PDS la bawoo woon. Waaye, damaa jàppoon ne, nit, ak foo mënti bokk, mën nga dem ba jamono, say bët xippi, nga xam ne sam réew soxla na la, nga xar sa tànku-tubéy, jóg ngir bey sa waar ñeel askan wi. Rawatina boo dee ndaw, Yàlla wërsëgal la ba nga mucc ci soxlay xaalis. Ku ni mel, war na jéllale yenn mbir yi, jombal boppam yenn bëgg-bëgg yi te warloo naataange réewam. Gis-gis booboo ma taxoon a rafet njoort ci Maki Sàll. Nde, APR, Maki Sàll «yaakaar» la ka daan woowe. Teg ci ne, da daan biral yéene ju rafet ji mu daan wax ne moom la amoon ci réew mi ngir soppi ko. Da daan woote booloo ngir nu saafara jafe-jafey askan wi, soppi xar-kanamu Senegaal, boole ko ci réew yi gën a naat ci Afrig ak ci àddina sépp sax. Ndekete yóo, bëñ weex na, waaye deret a ko lal.

PAJ : Maanaam… ?

Boo seetloo, bi ko Yàlla dénkee réew mi, ci at yu njëkk yi rekk, dafa tàmbalee dekkil doxalinu waa PDS, fim bokkoon. Wolof ne, jikko ak boroom, pax. Ndax, ci ndoorteel li la tàmbalee def lu ko neex, di buur, di bummi, ni ko waa PDS daan defe. Man, nag, mësumaa bokk PDS. Wànte nag, ak li mu daan deme xel ak xolu boppam yépp, da daan maslaa, di naxante ak waa Bennoo Bokk Yaakaar. Dafa di, Bennoo Bokk Yaakaar xawoon na am doole tuuti jamono jooju ; Maki Sàll daan xool naka lay def ba wàññi doole jooju, daldi mën a doxal mbiri boppam, wone jikkoom dëgg. Te, yéeneem jooju mujje na sotti ba mu fésal jikkoom dëggantaan. Man, ci la sama xel tàmbalee ñaaw ci moom.

PAJ : Nee ñu Maki Sàll daf la joxoon i ndigal nga bañ leen a jëfe…

Man ak Maki Sàll, atum 2014 lan njëkk a réeroo. Réeroo yu metti, nag, amoon nañ sun diggante ci atum 2013 ñeel otorutub pey gi ak yeneen yu bari. Ci njeexitalu woteb gox-goxaan yi amoon ci atum 2014, daf ma génne nguur gi. Ndaxte, dafa waxoon ne, ku faluwul ci goxam mu génne la. Ma jàpp ne, bokkoon naa ci ñi ko ko taxoon a wax loolu, maak Bënuwaa Sàmbu ak Mimi Ture. Ci sama xalaat, dafa taafantoo woon wote yooyu, def leen lay ngir dàq ñi daawul jëfe ay santaaneem, donte ne santaaneem yooyu baaxuñu woon ci réew mi. 2015 la ma dugalaat ci nguur gi, ma nekk jawriñu laf gi.

PAJ : Lu tax nga ne Maki Sàll da doon néewal doole waa Bennoo Bokk Yaakaar ?

Ndànk-ndànk la ko doon defe, dafa njëkk a néewal doole PS ak AFP… Ndax ñooñu, ñoom Usmaan Tanoor Jeŋ ak Mustafaa Ñas, ñoo ko nangu. Bi leen Maki Sàll mosalee ci nguur gi, dénk leen ay njawriñ, ci lañ seppee seen bopp ci bépp xeetu joŋanteb wote, rawatina woteb njiitu-réew miñ dégmaloon ci atum 2019. Ñoom daal, dañ seeyoon ci biir APR, ànd ak APR. Ñi bañoon loolu nag, amoon yeneen gis-gis, Xalifa Sàll (PS) ak Maalig Gàkku (AFP), daldi beddeeku, beru, sos seeni làngi bopp. Ci gàttal, Maki Sàll, diggante 2008 ak 2012, daf noo nëbboon jikkoom, daan maslaa ak naxanteek nun. Jaar-jaar boobu ma am ak moom, yee na ma, ndax jànge naa ci lu bare. Ndege, am réew, benn loxo mënu koo yor. Fàww nga seet ñi la tane ci fànn yi nga néewle xam-xam ak mën-mën, lëkkook ñoom, ngeen liggéeyal seen réew.

PAJ : Lan mooy seen cëslaayub pólitig yéen waa République des Valeurs ? Ci yan xalaat ngeen ko wékk ?

 Waaw, laaj bi am na solo bu baax a baax. Ndax képp kuy def pólitig, war ngaa leeral sa gis-gis ak yoon wi nga xàll ngir jëmale réew mi kanam. Bu ko defee, doomi-réew mépp dinañ ci mën a gis seen bopp. Kon, sab laaj, lu xel nangu la. Ndaxte, jikkoy pólitiseŋ yi bokk nañ ci li yàq Senegaal. Réew mu néew doole te ndóol, ña ko jiite ak pólitiseŋ ya fa nekk waruñoo dundal ger, féetewoo alalu mbooloo mi, def ko seen moomeelu bopp. Am na ci sax ñu naan la, ñoom, jiitewuñu réew mi, waaye dañuy nguuru. Te, boo xoolee ni Senegaal di doxe, diŋ ci gis ay firnde yu bari. Xoolal mbirum suuf si, ayeropoor bi, petarool beek gaas bi ak bépp bokk-moomeelu askan wi… gaa ñi aakimoo nañ ko, ñoom ak seen njaboot, seeni mbokk, seeni xarit ak i àndandoo. Ndege, ci seen gis-gis, dañ jàpp ne képp ku xas a toog, danga war a tibb ci alalu réew mi nim la neexe, saa bu la neexee. Nun, nag, xalaatin bu bon boobu lan fi bëgg a jële.

Nun, danu fànnoo yeesalug jikko yu rafet yiy suqalim réew. Danu solowoo njariñu réew mi, mu jaral nu sunu doole, sunu alal, sunu jot ak sax sunu bakkan. Ndax, danu war roy soldaar bi dëddu ittey boppam, won ginnaaw njabootam ak i mbokkam, jël jotam, dooleem, xelam ak xolam jagleel ko kaaraange réewam, ngir askanam mën a dund ci jàmm. Danu gëm ne, aji-bëgg sa réew bu ne, ak koo mënti doon, foo mënti féete, yaa war a génne ci sa poos def ci nafag nguur gi. Wànte, waroo tibbe ci nafag nguur gi, duy ci say poos, yow, ak ñi nga àndal ; ngeen di gundandaat ak a yaataayumbe, askan wiy jànkonteel ak i tolof-tolof yu dul jeex. Gàtt xel weesuwul loolu. Loolu mooy benn.

Ñaareel bi mooy ne, warees na xool ci àddina sin nekk, réew yin nirool jaar-jaar, seet yoon yi réew yooyu jaar ba suqaliku tey. Bu nu xamee loolu, boole kook sunu gis-gisu bopp, dëppale ko ak tolluwaayu réew mi, door a tëral ab naal bu nuy jëme kanam. Gëm sa bopp tamit, am na ci solo lool. Ndaxte, bun nekkee ci réew moo xam ne mbay daf fi am solo, nga xool ni fi màngoy baree ak yeneen xeeti meññet ; nga xool ni fi der yi baree, rawatina jamonoy tabaski ; nga xool ni nu bareey bant ak i xaralaakon (artisans), añs. Dan war a geestu ñiy daan seen doole ci fànn yile, xool naka lanuy def ba jàppale leen. Warees na leen tàggat, dooleel leen ak xaalis ak i jumtukaayi xarala yu mucc ayib. Bu ko defee, dinan bey, soppi ko, jariñoo ko walla jaay ko bitim-réew. Damay faral di joxe misaal ci réewum Dubaay mi nga xam ne, genn garabu màngo du fa meññ. Moone de, njarum màngo yi ci Rani yi nuy naan, ñoom ñoo ko defare seen réew, jaaysi ko Senegaal. Ndege, dañuy ñëw Afrig, fu mel ni Mali walla Senegaal wala Gine, jënd màngo ci njëg lu yomb, yab leen ci seeni gaal, yóbbu Dubaay, soppi ko fay njar, delsi jaay nu leen ci njëg lu seer. Loolu gàcce gu réy la, dara gënu koo ruslu. Dafa doy waar. Mi ngi mel ni, nun, ba tey weesoogunu jamonoy maamaati-maam ya.  Jamono jooju nga xam ne, tubaab yi dañ fi daan wecceey mëq-dóom ak doom-aadama, daan fi indi seen njaay yu bon yooyu di leen jëndee sunuy alal ak sunuy suuf yu yaatu yi… Foofu lan tollu ba tey. Dañuy jël sunuy der, lu tollu ci junniy junni der jamonoy tabaski, màggal walla gàmmu, lem leen, yóbbu seen dëkk walla Itali walla Marog… Buñ ko fa soppee ba noppi, def leen i dàll, ay maraakiis, ay saag, ay tooguy der, añs., ful seen njëg, ñëw jaay leen Senegaal. Kon, bu nu gëmoon sunu bopp, gëm sunu réew, gëm itam ñàq-jariñu te di ko jëfe,  léegi coppite am. Ndaxte, amees na fi lees mën a sukkandiku ngir liggéey, liggéeyal réew mi.

Ci beneen boor, dan war a fexe di bey at mépp te bañ a yem ci mbeyum nawet mi nga xam ne 3i weer kese la. Naam, am na ñuy góorgóorlu ci mbeyum noor gi ; waaye warees na fexe ba fépp ci réew mi, li ko dale Ñaay ba jàpp Ndar, Maatam, Bàkkel ba Kéedugu, ñépp di bey noor ak nawet. Fépp foo romb rekk, waroon nga fa gis ku sëgg ci toolam walla ay nag yuy lekk. Fileek defunu loolu, dund gi du mës a doy te ñàkkum xéy gi du fi mës a jóge.

PAJ : Ngir nga jëmmal sab yéene, fàww nga jot ci nguur gi. Ndax seen làng gi am na doole ji leen di tax gañe ay wote ?

CAS : Nun, danu bokk ci genn làngu pólitig gu gën a yaatu, muy CRD (Congrès de la renaissance démocratique), 5 ba 6i pàrti séq ko. Bëgguma lim turi pàrti yi bala moo gudd. Waaye, mën naa lim turi ñi leen jiite, muy Abdul Mbay, Mamadu Lamin Jàllo, “Juge” Dem, Porfesoor Bubakar Jóob bu Taxaw Temm, Alasaan Kitaan, Porfesoor Ibraayima Silla ak ñoom Paap Saar. Maa ngi leen di nuyu ñoom ñépp. Noo ngi waxtaan ak yeneeni làng itam.

PAJ : Lan mooy sa xalaat ci woteb gox-goxaat yii nu dégmal ?
CAS : Jàpp naa ne, woteb gox-goxaan yii nu dégmal, làng yépp ñooy bokk jafe-jafe. Nde, gox boo dem, militaŋ yi dañ jàpp ne wote bi seen wote la. Dañ koo def seen yëfu bopp, am ci seen xalaat ak seen gis-gisi bopp. Loolu sax aayul. Waaye, ñoom, dafa am ñiñ diir, xam leen, wóolu leen, bëgg leen a jiital. Ba tax na, nun, fàww ñu yolomal, yombal te ubbi tànninu wutaakon yi ci gox yi tey sóoraale xalaati militaŋ yi. Dinan leen déglu, diisook ñoom, xool ni nuy dëppalee sunuy xalaat. Dinan waxtaane ñiñ bëgg a jiital fileek ñooñu bokkuñu ci nguur gi walla muy ñu leen jege. Ànd ak ne, am nan làng gu yaatu ci réew mépp ; gox bu ne, dinan la wax ne, bun sañoon kat, ngeen ànd ak kii.

PAJ : Fan yii, kujje gaa ngi dal ci kow nguur gi, di ŋàññ kayitug wote bi. Lan moo ciy sa taxawaay ?

CAS : Xam nga mbir mi, du mbirum wóorliku kayitug wote gi rekk. Ci tëggin wi la, ak ñi ko daan saytu. Ñépp xam nañ ne, am na ñu bare ñu bëggoon a bindu, ñu tere leen a bindu. Am ñoo xam ne, lu nekk def nañ ko ngir jot seeni kardànte, di xaar ci sàppe yi ba tàkkusaan te duñ jot dara. Mu am ci nag ñoo xam ne, seeni kardànte ñoo leen daan fekksi seen kër. Yu ni mel, wóorliku du ko fésal. Am na ñu bare ñu bëggoon a bindu te mënuñoo fexe ba bindu. Te, jamono jooju, gis nañ fi ñu gaare ay biis ca “Direction de l’autonomisation du fichier”, wàccey nit, bind leen ci kayitug wote gi. Moo tax nun nu ne kayit gi baaxul, jagul, jaarul yoon. Ndaxte, dañoo tànn seeni wotekat bind leen, wëlbatiku teg i gàllankoor yu bare, tere nit ñi bindu.

PAJ : Luy sa xalaat ci coowal Sonko ak Aji Saar li ?

CAS : Waaw, Paap Aali, laaj bii, du guléet ñu ma koy laaj. Laaj nañ ma ko ay yoon. Benn tontu rekk laa ciy tontu saa su ne. Ñàkkul ma am ci sama xalaatu bopp. Waaye, dafa fekk ne, 2i doomi-réew mee jote, yoon war leen a àtte.
Kenn ki, Usmaan Sonko, xam naa ko bu baax. Keneen ki [Aji Saar] xamuma ko. Fekkewuma, xamuma ni mbir mi deme. Moo tax, damay maandu. Mbir maa ngi ci loxoy yoon, donte ne, ak fi réew mi tollu, kenn wóolootul yoon.
Man mii di wax ak yow, wóoluwuma yoonu réew mi. Waaye, ak lu ci mënti am, dafa am ku wax ne dañ koo tooñ, salfaañey àqam, mu dem ci yoon. Nde, maxejj bu nekk, bu gisee ne tooñees na ko ciy àqam, war naa mën a dem ci yoon. Noonu lan ko defe woon, man, Abdul Mbay ak ñeneen, keroog bi nuy àkki yoon ñeel Njiitu-réew mi, Maki Sàll. Kon, bu ko beneen maxejj defee, damay jàpp ne yoon may na ko ko. Léegi nag, yoon mooy àtte, leeral ndax lees di tuumal diw am naam amul. Loolu mooy sama gis-gis ci mbirum Usmaan Sonko ak Aji Saar.
Gis-gis boobu, nag, am na ñu muy jaaxal. Du caagin sax samay kàddu leerul ci seen bopp. Xam nañ bu baax a baax li ma wax ; waaye, ñoom ñoo ko bañ a nangu. Ndaxte, li ma wax dafa leer. Mbir moo xam ne, ba muy xew, fekkewoo, tinoo, yëgoo, ak loo rafet rafet njort ci kenn ki, Yàlla rekk a xam li xew dëggantaan. Taxawaayub maandute boobu, dafa bokk ci sama gëm-gëm, ma di ko jiital ci fànn bu ne, ak kum ci mënti doon. Jar na sax ma fàttali menn mbir mu fi xewoon ci jamonoy Abdu Juuf. Laata tirbinaal di àtte, ñépp àtte nañ ca njëlbeen ga, setal kenn ki, tuumaal ki ci des. Askan wi, xeltukat yi ba ci taskati xibaar yi, gën-gaa bare, ku ci nekk njortoon nga, àtte ci sa xelu bopp… Naka la mujjee ? Tirbinaal dafa àtte àtteb Yonent Yàlla Suleymaan [àtte boo xam ne joxeesul kenn dëgg], donte ne am na ñu mu tegoon ay daan. Waaye, ki ñu jàppoon ne moo joxe ndigal li, ndeyu-mbill gi, yoon daf koo bàyyi. Jamonoy dox ba kooku jot ci nguur gi. Ay mbir yu bees feeñ, mu mel ni kooku, loxoom taqoon na ci. Ci la nguuram dogal ne bu kenn waxati ci mbir mi ndax njéggal am na ci. Ginnaaw loolu yépp jot na fee am, danoo war a xoolaat sunuy taxawaay, moytandiku. Man, dama def benn taxaw seetlu. Dafa mel ni, jamono jiñ tollu, da cee am ñu bare ñoo xam ne, bu seeni xalaat ak seeni gëm-gëm wutee rekk, ñu sikkal la, solal la mbubb mu leen neex. Moone de, man, li ma wax, dafa leer nàññ, lu yomb a dégg la. Waaye, dañ naan la danga soxor, danga iñaan, añs. Gis naa ci sax ay jàngalekati iniwersite yuy jàngatee noonu mbir mi. Loolu dafa doy waar te bokk na ci liy delloo réew mi ginnaaw. Tey, kiy jàngale iniwersite, war na mën a jàngale am fit ak sañ-sañu wax sa xalaat te kenn du la jiiñ kiñaan walla tàng xol. Ndaxte, ñi ñuy roy, ñoom Socrate, Platon, añs., dañ amoon fitu wax seen xalaat donte ne ñuŋ leen daan xoqtal, di wax ne dañ bañ nguur gi walla dañoo weddi Yàlla… Nit ku ne, am na sañ-sañu xalaatal boppam. Xawma kan, waaye man de, kenn mënu maa xañ sama sañ-sañ boobule.

PAJ : Lan mooy sa kàddu gu mujj ?

CAS : Waaw, Paap Aali, xanaa di leen gërëm, di leen sant bu baax a baax. Wax-dëgg-Yàlla, yéen a ngi def liggéey bu réy a réy. Réew mépp a leen ameel njukkal. Ndax, yéen a ngi siiwal ay xibaar yu wér te wóor, di leen biral ci làmmiñu askan wi, di leen jottali askan wi. Loolu, dafa am solo lool ndaxte dina tax aw askan xam. Te, bu aw askan xamee, dina xàmmee ; bu xàmmee, dina yeewu. Bu boobaa, nag, réew mi dina jëm kanam. Kon, gàcce-ngaalaama. Ndaxte, seen yéenekaay LU DEFU WAXU, mi ngiy biral ak a fésal liy defu ci réew mi, di waxu ci askan wi [fii, mu reetaan]. Man, ci sama wàllu bopp, maa ngi leen di delloo njukkal, di feddali, ñeel leen, samay cant ak ngërëm ngir li ngeen ma may ma waxtaan ak Senegaal gépp.

Jërëjëf !

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj