USMAAN SONKO : ‘’ÀNDUMAAK ÑI NAAN ‘FRANCE DÉGAGE’ !’’ (Ñaareelu xaaju laaj-tontook Ndey Koddu Faal, Paap Aali Jàllo ak Daawuda Géy)

Yeneen i xët

Aji bind ji

LU DEFU WAXU : Seetlu nañ ni, saa booy wax ci nguurug Maki Sàll, danga naan « Nee na moom moo gañe… ». Mu mel ni nanguwoo ndamu Maki Sàll li ci joŋante wote njiiteef bii weesu. Lu tax ngay waxe noonu ?

USMAAN SONKO : Nun, waa Pasteef ak làng yin lëkkaloo woon, sunu kàddu, ca njëlbéen ga ba nëgëni-sii, genn doŋŋ la te du mës a soppiku. Bi nu génnee ci wote yi, danu ne nanguwunu palug Maki Sàll gi, te li nu taxoon a wax loolu ñépp a ngi ci doon teg seen bët. Waaye, ci wàllu yoon, maanaam, bees sukkandikoo ci ndeyu àtte réew mi, moom mooy njiitu Senegaal. Loolu, sikk amu ci. Waaye, lu jaar yoon te xel nangu ko, tubaab naan ko « légitimité », ak lu yoon sàrtal te muy tekki ci tubaab « légalité », bokkuñu. Am na lol, yoon mën na ko sàrtal, biral ko fekk ne dafa safaanoo ak li yoon woowu tëral. Loolu, nag, mooy li nu jàpp ne moo am ñeel palug Maki Sàll gi. Ndax, Maki ak i ñoñam ñoo jëkk a biral seenug pal laata yoon di ci àddu. Ci guddig bésu wote bi la ay jëwriñam ak i farandoom génn, di joxe ay lim. Te, jamono jooju, biroy wote yi sax noppeeguñu woon seen liggéey. Ndajem ndeyu àtte mi nga xam ne moom la fi nekkal, deful woon lu dul dëggal li ñu waxoon.

LDW : Kon, yéen ak làng yi ngeen àndaloon, dangeen a jàpp ni suñ waxantee dëgg ndamu Maki Sàll li dafa taq suuf ?

US : Danoo gis ne, ni wote yi tëdde woon, ca ndoorteel la ba ca njeexital la, dara ba dara booloo jeex méngoowu ci woon ak li yoon tëral. Maki dafa bañoon a amal ndajem politig bi waroon a am ñeel làng yi ngir nu waxtaane lépp lu jëmoon ci wote yin dégmaloon. Yemu ci, mu jël kaardànte yi, jox ñi ko neex,ye yosi ñi mu jàppoon ne duñ ko woteel, rawatina ndaw ñi. Nu ni déet-a-waay, mu séddale dénduw wote bi (carte électorale) ni mu ko neexe. Boo boolee yooyu yépp, dinga xam lu tax ñu naan saa su nekk « nee na moo falu… ». Kon, na féetoo nguur gi, doxal li mu war a doxal, nu féete ci kujje gi, di def li nu war. Loolu mooy demokaraasi.

LDW : Ndax bu la Maki Sàll woowoon ngir dénk la ndombog-tànk dinga nangu ?

US : Mukk ci àddina ! Duma ko mës a def. Bi jiitu ci sabab yi mooy ne, amul benn fànn boo xam ne man ak Maki Sàll bokk nan ci gis-gis. Te, gis-gis moo lal liggéeyub nguur. Ñaareel bi di, bokkunu naal. Man, dama jàpp ne naalub « Plan Sénégal Emergent » bi Maki Sàll kàmpaañe woon te di ko doxal nii, baaxul, santul Yàlla. Nun, danu amoon sunu naalu bopp, mu méngoo ak sunu gis-gis ci nees war a yore réew mi. Ñetteel bi, nag, mooy ne man dama nawloowul Maki Sàll ci ni mu yore réew mi. Bu may wax loolu, du jëmmu Maki Sàll ci boppam laa ci namm. Njiitu réew mim doon a ma tax di wax. Ndaxte, man dama gëm ne, Maki Sàll, amul xam-xamu jiite réew, amul mën-mën bi te sax amul fulla ji ak fit wi. Ndege, ndawal Farãs la.

Ci gàttal daal, Maki dafa jaar nii, ma jaar nee. Kon, xel xalaatul may liggéey ak moom. Bu sama waa pàrti yépp màbboon ne dañuy fekki Maki Sàll ci nguurug bennoo gi mu doon woote, man duma ci dem.

LDW : Nee ñu Usmaan Sonko du waxal mukk Maki Sàll lu baax, safaan bi rekk.  Ndax, ci sa gis-gis, amul lu Maki def lu baax bim faloo 2012 ba léegi ?

US : Moone, ci wàllu mbasum Covid-19 bi, waxoon naa fi ne, li Maki Sàll waxoon ne nguur gi du delloosi ndawi réew mi te ñu caŋoon Siin, lu baax la, àndoon naa ci.

LDW : Benn boobu rekk nga ko mën a waxal ci lu baax ?

US : Lu ngeen bëgg yéen tamit ? Su ma fi newoon di tagg Maki Sàll dinaa jaaxal askan wi ! Te du moom sax am nab « armada » bu koy xalamal ? Maanaam, am nay ndaw yoo xam ne, mbaaxam rekk lañuy wax, di ko tagg ak a kañ. Am na, sax, ay kurél, ab tele ak yenn ci yéenekaayi réew mi yoo xam ne, suba ba ngoon jot, lu baax rekk lañuy wax ci moom, lu baaxul sax, ñu baaxal ko, rafetal ko ba nga ne lii lum doon. Man, nag, loolu du sama cër.

LDW : Ndax xamante ngeen ?

US : Man xamuma Maki Sàll, Maki Sàll xamu ma. Benn yoon la sunuy bët mës a daje te mooy keroog bi ma demee pale. Ngeen baal ma rekk ma yokk ci ne nitu Maki ñoru ma. Li mu doon njiitu réew mi moo ma tax di wax. Loolu dafa war a leer ci boppu askan wi.

LDW : Déggees na la yit ngay tuumaal Msuur Fay, di ko dendale ak Karim Wàdd mi fi amoon doole lool ca jamonoy baayam Ablaay Wàdd. Ndax danga jàpp ne Maki Sàll da koy xàllal yoon ngir mu wuutu ko ?

US : Ku am tuuti seetlu rekk, ndax mën na maa wax lu wutale Mañsuur Fay ak Karim Wàdd ci wàllu ndomboy-tànk ? Ndax xam ngeen ne Msuur Fay mooy séddale ndimbalug njaboot gi ? Ndax xam ngeen ne moo yor naalub tabax tali ci gox-goxaat yi te ñu dippe ko ci nasaraan ‘’Promoville’’ ? Te, nguur yoonam newul ci defar i tali ñeel gox-goxaat yi. Loolu, liggéeyu meeri yi la. Nguur, taliy réew mi la war a féetewoo. Msuur Fay mooy jawriñu mbooloo tund wi ak ndimbalu njaboot gi, mooy meeru Ndar, moo yor PUDC, yor PUMA, mooy séddale dund gi…Maanaam, lépp lu koy tax a jege askan wi rekk, joxees na ko ko.

LDW : Lan moo taxoon Maki Sàll ne fàww mu am ñaareelu moomeel, xar ci tànki-tubéyam ?

US : Li taxoon Maki Sàll doon rey boppam ngir am ñaareelu moomeel, mooy tóoxidooni yim defoon, moom ak njabootu politigam. Dafa bëggoon, bu gañee, fexe ba maasale njombe yeek toj-toj yu bare yim def, moom ak nguuram ci moomeem gu njëkk gi. Moom, bi mu nee falu na, toogagul sax, naan day woote ndajem yëgoo ñeel réew mépp ngir tàppe xol yi... Idiriisa Sekk mi toppoon ci moom ci wote bi ne demul, man mi nekkoon ñetteel ma bañ it, ne duma dem, PDS mi nga xam ne, ak lu mu dee dee am na taxawaay, ne moom it demul, làngu ñoom Abdul Mbay gi tamit ne demul. Maanaam, daal, kujje gim soxla woon, kenn fullaalu ko ci. Amul li mu bëggoon.

LDW : Lu taxoon ngeen bañ a wuyuji njiitu réew mi ?

US : Bun ko wuyuji woon ca jamono jooju, kenn ci nun dootul woon mën a diiŋat nguur gi bu jàddee yoon. Loolu lépp àntuwul. Mu des lan ? Ci sama gis-gis, Maki Sàll nas nay pexe ngir génn ci gutë gim dugal boppam.

LDW : Yan pexe ?

US : Ñett lañu. Bi ci jiitu mooy, mu xool ba xam mën na fexe ba ndajem ndeyu àtte mi daganal ñetteelu moomeem. Te, loolook xaru ñoo yem. Bi ci topp mooy, mu xool ndax mën na wut ab tofo ci pàrteem, ngemb ko ngir mu wuutu ko. Ñetteel bi mooy mu jéem a xool kiy gën a jekku ci wutaakoni kujje gi, keroog woteb 2024 bi, mu kootoog moom, ñu déggoo ciy kàddu ngir kooku faral koy njaaxumam, bañ leen a toppe dara, moom ak njabootam. Te kooku moom du mës a doon man mii Usmaan Sonko.

LDW : Noo nar a doxale ?

US : Bés bu Yàlla tegee réew mi ci sunuy loxo, képp ku fi mës a yor fiftinu askan wi, diŋ ko leeral ndax alalu mbooloo la.

LDW : Noo gise ñetti pexe Maki Sàll yi nga lim léegi ?

US : Jàpp naa ni mu ngi liggéey ci 3i pexe yépp. Te, bu dee ci wàlluw tofo bi rekk, génne na ci xelam Aamadu Ba, Aliyun Badara Siise, Ablaay Daawda Jàllo, Aali Nguy Njaay, añs.

LDW : Da leen a wóoluwul, walla ?

US : Ñoom ñépp la yemale, xéy-na da leen a ñemewul. Ku des kon ? Xanaa Msuur Fay, goroom, di magu soxnaam Mareem Fay Sàll. Li ñuy coow Aliyun Badara Siise fii, Aamadu Ba fee, lépp ngir xàllal yoon goro bi rekk la. Ci pexe mi la bokk. Moo tax mu dénk ko ay ndomboy-tànk yu bare, jox ko ay milyaar ngir mu jënde leen askan wi. Ndege, ñoom, ni ñu jàppe politig mooy, amal ay milyaar jënd baati askan wi. Waaye, gisuma nan la Mañsuur Fay di def ba jiite miim réew.

Li ma wax fii, nag, sama xalaatu bopp la ; sama njàngatu bopp la ñeel doxalinu njiitu réew mi, Maki Sàll.

LDW : Fu mbirum 94i milyaar yi tollu ?

US : Waaw. Yaakaar naa ne am na ku ciy waajal benn téere. Duma leen wax kan la, te duma ci sore. Mooy li waa ja waxoon rekk, Yàlla du nit [fii reetaan na]. Li ma ci mën a wax daal mooy fàttali askan wi ne OFNAC génne na ràppooram, dëggal li ma waxoon lépp. Rax-ci-dolli, dafa joxe ay ndigal ngir ñu topp Maamur Jàllo, Tayiiru Saar, jaraafu Ndakaaru ji, noteer bi defar kayit yi, ak ñeneen ñoo xam ne tudduma leen woon sax. Li wóor moo di ne gaa ñi, yàgg-yàgg dinañ layook yoon. Ndaxte, mbir mi dafa doy waar, dafa jéggi dayo. Te sax, OFNAC dafa génnewaale 27i njombe yu wute ak njombew 94i miliyaar yi. Li ci kanam rawul i bët.

LDW : Waa Pasteef-Géejawaay noon nañ dañuy kalaameji yoon Aliyu Sàll ñeel njombew petorol beek gaas bi. Fu ngeen ci tollu ?

US : Waaw, loolu mi ngi ci loxo yoon. Man, ci sama wàllu bopp, kalaameji woon naa cayri àtteb àddina si, ca Àngalteer, ca Amerig… Dafa di, sax, tàmbali nañ gëstu bi. Xam nga, Amerig, ñoom, bu ñuy liggéey duñ ko yàkkamti. Waaye, ñu ngi ciy lëñbëtu. Ndaxte, way-lëñbëti Amerig yi jóge nañ Washington, dem ba Ohio ngir laaj Aliyun Géy li mu xam ci mbir mi. Moom, Aliyun Géy, moo nu kalaamejiloo yoon. Te, mujje naa bokk Pasteef. Yàgg-yàgg dingeen ci dégg dara. Nun, li nu waroon, def nan ko.

LDW : Ndax Usmaan Sonko dafa am ay ndaw yu koy déey i xibaar te bokk ci nguur gi ? Fan ngay xibaarloo ?

US : Nit ñi bàyyiwuñ xel ne, xibaar yi, bu dee 100, 80 yi mënees na cee jot ci anam bu yomb a yomb. Dafa fekk ne, kay, Senegale yee dul gëstu ci dalu webu njawriñu ngurd mi ak sax bu nguur gi, walla ci yéenekaayi nguur gi, anternet bi, añs.  Yooyu ma lim yépp, foo ci dem fekk fa xibaar yu bare yees fay rotal. Ci misaal, bi may siiwal luubalug lempo ga woon ca péncum réew mi, mooy biñ may dàq, ci dalu webu njawriñu ngurd mi laa jukkee woon xibaar yi ma amoon yépp. Kon, bare nañ lool, nit ñi mën nañ cee jot. Man, nag, ci gëstu laa dëkk. Saa yu ma toogee defuma dara, maa ngi gëstu, di seet ak a settantal lu jëm ci réew mi ak lu jëm ci àddina sépp, rawatina diggante réew yi.

LDW : Bu weesoo gëstu yooyu, nag, amul ñuy ñëw leeg-leeg di la déey ?

US : Fànn bu nekk, damay xool ñoo xam ne seen xel da cee màcc dëgg-dëgg, may jokkoo ak ñoom, di leen laaj seen xalaat. Fi mu ne nii, duma toog 3i weer yoo xam ne demuma CNCR seeti leen, waxtaan ak ñoom ci wàllu mbey mi. Noonu laa koy defe ak ñeneen ak ñeneen. Mu des, nag, ñi nga xam ne dañoo bëgg réew mi te di liggéey ci caytu gi te yenn saa yi ñu gis lu leen metti te duñ ko mën a wax. Maanaam, am na ñoo xam ne dañoo dem ba mënatuñu, bëgg a wax te mënuñoo wax. Bu ko defee, dañuy wax ak man walla ñu wax ak kenn ku ma jege, mu jottali ma ko. Noonu laay taataane samay xibaar.

LDW : Nooy jàngate taxawaayu Senegaal ak Afrig ci mbas mi ?

US : Waaw, taxawaayu Afrig moom du jafee jàngat. Li may wax rekk, di li ma njëkk a seetlu, mooy nanu sant Yàlla ndax amul menn réewum Afrig mu am doole ci wàllu paj, mu mel ni kon Afrig ag tàkk la ci wàllu paj. Xanaa ay Tinisi, Marog, ñoo ci tàmbali woon tane, ak réewum Afrig-Bëj-Saalum. Te kat, gis nañ ne ñoo ci gën a sonn fi mu ne nii. Kon, mbir mi Yàllaa nu ko fànqal boppam. Walla moo nu ko woyofalal boog ba aayul ni mu waroon a aaye. Teewul nag, réewi Afrig yépp jël nañu ay matuwaay. Te matuwaay yi wuutewuñu ak yees jël fépp ci àddina si. Afrig, nag, defe naa Afrig-Bëj-Saalum rekk a ci jéemoon a lëlu, te dafa mujjoon a jur coow, ndax réew moo xam ne li nit kiy xëye tey moom lay dundee ëllëg, soo ko bëggee lël du sotti. Kon, moo tax ma ni leen jàngat taxawaayu Afrig du jafe, ndax jàpp naa ni li ëpp solo ci mbir mi mooy li nu Yàlla suturaal ba nu muccandi ci. Waaye bu doon ni mu aaye feneen la aaye fii, tey dina metti lool ci nun. Di ñaan Yàlla, nag, mu wéy noonu.

LDW : Luy sa xalaat ci coowul “artemisia” li, di garab gu réewum Madagaskaar ne day faj covid-19 te Kurél gi yor wérgi-yaram ci àddina si (OMS) bañ ko koo nangul ?

US : ‘’Artemisia’’ bi wareesu koo dàq ndax li mu jóge Afrig rekk – loolu nun mënatunu koo nangu, weesu nanu loolu. Waaye tamit garab dafa am yoon wu mu war a jaar ci wàllu xamtu balaa ñuy mën a wax ni garab gii day faj lii. Ñépp nangu nañu ne yoon woowu jaaraguñu ci. Li ñu ci xamagum daal, dégg naa ni am na ñu koy jëfandikoo te gis nañu ci njariñ. Loolu lañu waxagum. Te tamit boo dégloo njiitu réewum Madagaskaar, dafa ne yàgg naa waxtaan ak kilifay OMS yi te OMS nangu naa gunge Madagaskaar ci wàllu xamtu. Kon, xanaa rekk ñaan Yàlla li ñu ci amoon ci yaakaar mu àntu. Ak nu mu mënti deme yit, ñépp nangu nañu ne garab gu baax la, te am nay feebar yu muy faj te sax, ci misaal, baax na ci sibbiru. Kon nañu ñaan Yàlla bu ñu ci jaaree fi ñu war a jaar yépp, liñ ci yaakaar am te muy ndamu Afrig gépp.

LDW : Noo gise diggante Senegaal ak Farãs, walla sax diggante Farãs ak Afrig ?

US : Waaw fi ngeen daanele, diggante Farãs ak Afrig, laay njëkke. Gis naa ne dañuy jox Farãs gëdd gu ëpp li mu tekki ci Afrig te réewi Afrig yiy làkk farañse ñoo may tax a wax. Farãs amul lenn loo xam ne mën na koo dogal ci réewi Afrig yiy làkk àngale, du Niseryaa, du Gànnaa, du Afrig-Bëj-Saalum, du feneen. Boo jëlee réewi araab yi nekk Afrig tamit, Farãs tekkiwu fa dara, muy Misra, di Alséri, ñépp xam nañu loolu. Kon, su ñuy wax ‘’Françafrique’’ war nanoo xam fan la yem. Nañuy yemale wax ji ci Farãs ak réew yi mu tegoon loxo démb. Te digganteem ak réew yooyu bu deme ni mu deme tey, man amuma dara lu may wax Farãs, luñ ko ci wax tooñ ko. Tubaab yi dañoo am seen fulla, xam li ñu bëgg, di def seen kem-kàttan ngir am ko, jaar sunu kow. Sunu njiit yi fi Tubaab yi teg laay duut baaraam, di leen laaj lu tax ñu ñàkk fullaak fayda bay nangoo doon i xuus-maa-ñàppam, yoon wu mu leen awloo ñu gaawtu aw fa. Kon wax ji, feek delloowuñ ko foofu

LDW : Ñi naan « France dégage », nagDangaa bëgg a wax ne àndoo ci ?

US : Ànduma ci, kay. Fi ngeen may gis nii, saa su ne damay tooñ sama gaa ñi, naan leen bàyyileen di wax “France Dégage”. Te lu ma gëm la, damaa gëm ne coow li du “France Dégage”. Farãs mënu fee jógee noonu, walla bu fi jógee yit te nuy wéy ak xeetu njiit yu mel ni ñi fi nekk, yeneen doxandéem dinañ leen fi wuutu. Seetleen ko ci Siin rekk, fi nu jëm ak Siin boo moytuwul mooy gën a doy waar, gën a metti li nuy dund ak Farãs. Te nanu sant Yàlla, nag, ci li nu mësul a yitteel Amerig. Moom daal, feek nu ngi wéy di am xeeti njiit yi fi nekk, waxuma la sax Farãs walla Siin waaye réew yu leen gën a néew doole dinañ sonal Senegaal.

LDW : Yan réew ngay xalaat ?

US : Ci Tirki la sama xel njëkk a dem. Tirki, ci atum 1950 sorentewunu woon te léegi nee nañu dañ noo bëgg a dimbale. Waaye mën naa lim tamit Marog nga xam ne noo moomandoo sunu bopp. Réew yu ni mel ñooy ñëw tey dinu noggatu. Moo tax mbir mi bu nu ko tënkee ci Farãs rekk dafay mel ne dan koo singali ndax fi nu jaar ak moom ca jamonoy njaayum jaam jaak nooteel ja. Waaye tey, doomiTirki yi dañuy ñëw, nu jébbal leen lépp, jox leen naawu bi te ni ñu ko bëgge lay ame. Sinwaa yi tamit dañuy ñëw ne la dama lay lebal xaalis ci anam yi ma bëgg, indiy ndefaram, indiwaale ñi ciy liggéey. Xam ngeen ne Farãs sax mësul àgg ak nun foofu. Moo tax bunu ci demul ak xel danuy moy li gën a am solo. Farãs, bu nu amee njiit yu am fulla, Farãs day nekk naataango, ni ñeneen ñi, nuy jëflanteek moom ndax danoo nekk ci àddina su ubbeeku.

LDW : Kon ci yow lan mooy wax ji ci dëgg-dëgg ?

US : Ci sama gis-gis bu gàtt, wax ji yépp lii la : lan moo tax Maki Sàll, Alasaan Watara ak IBeeKaa ak ñoom seen di sukkal ay doxandéem, di dox ci waawu Farãs walla Siin walla keneen ku mu mënti doon ? Waxtaan woowu lanu war a amal, dem ci ak xel, nag, fexe ba waa Senegaal tamit yeewu ci.

LDW : Dinañ lay dégg léeg-léeg ngay tagg Aasi…Jàpp nga ne dan leen war a roy ?

US : Naw naa lool waa Aasi, muy Sinwaa yi di Sapone yi,  ndax li ñu gëm seen bopp ! Maa ngi waxtaan keroog ak sama benn xame bu def 20i at Siin, ay doomam juddoo fa ba am sax kayitu réew ma. Mu ne ma fu mel ne Kàntoŋ ñu koy wax Guwànju, ñoom beneen Sinwaa bu fa bokkul sax dañu lay xeeb. Nee na ma yit Guwànju dafa am xeetu taksi boo xam ne waa Guwànju rekk a am sañ-sañu dugg ci, farse beek ñépp a ci yem, bu leen doxandéem tàllalee loxo dañu koy romb dem seen yoon. Mën nañu ne sax loolu ëpp na waaye day biral tamit ni ñu gëme seen bopp. Foofu kenn sañu faa dem naan day taxawal ab sosete ci nu mu ko neexe, ñoom ñoo lay wax ni nga koy defe, boo ci àndulee foo xam nga jëm. Moo waral gën gaa néew ci 100i sosete yoo jël, 51i ay Sinwaa ko moom. Keroog damay seetaan li xew Taylànd, gis ne Farañse yu bari dañoo tàmbalee wutali réew moomu. Waaye foofu tamit du ku jóg taxawal ab sosete, ci misaal, benn doxandéem mënul a ubbi sosete buy liggéey ci turism, di jëley nit Farãs di leen yóbbu Taylànd. Ñi ko bëgg a def dañuy mujjee ànd ak benn doomi-Taylànd, te moo la ciy ëpple, fàww nga jox ko 51i xaaj ci 100 boo jël.

LDW : Senegaal de demewul noonu…

US :  Déedéet. Senegaal, danga fiy wàcc léegi, ñu ni la lii bu la neexee jël ndax benn doomu-Senegaal yelloowu ko. Ci loolu lanu war a xalaat te dafa mel ni soxalul kenn. Loolu laay wax bés bu nekk ñoom Gii Maryiis Saaña, mbir mi warunu koo yemale ci benn réew, noonoo ko, bàyyi ñi ci des. Te bunu ci deful njàngat gi war, am ndam ci xeex bi du yomb. Fàww nu taxaw seetlu, jéem a xam lu waral Póol Kagame mën a fippu, lu waral Àndri Rajowelina tàmbalee fippu ca Madagaskaar, lu waral njiitu réewum Gana mën a fippu, te Maki Sàll sañu ko sax xalaat. Foofu lanu war a yóbbu wax ji. Bu doon sama sago danuy teg fale Farãs te laaj sunuy njiit lan moo tax ñu ragal ko nii.

LDW : Ayi-bés yii ñu weesu, gis nañ nga yëkkati sa kàddu di jàppale Madagaskaar ci xëccoo bi am ci digganteem ak Farãs te li ko waral di ay dun yu nekk ci wetu Madagaskaar te Farãs wéy di ci teg loxo ne moo leen moom. Ndax foog nga ni Madagaskaar mën naa am ndam ci boobu xëccoo ?

US : Madagaskaar mën na cee am ndam, ndaxte du ñaari làrmee jàkkaarloo, du xeex bu ñuy génne ay xeej ak i fetal, yoon a leen di àtte te Madagaskaar moo ne ci dëgg. Loolu la Mbootaayu Xeet yi xam ba jël ay dogal. Kon Farãs yey nañ ko ba noppi, day guddal jéll fi mu ne nii. Waaye mën ngaa am ndam te du doy, li gën mooy Afrig jàppale Madagaskaar ndax leer na ñépp ne dun yooyu indi coow li, moo leen moom ni Senegaal moome dunu Gore. Dun yooyu soree nañ lool Farãs, soo jógee Pari, dinga toog 8i waxtu walla lu ko ëpp cib fafalnaaw door faa yegg. Boo ko jaaree géej, dinga romb Marog ak Afrig sowu-jant, wàcc ba Afrig-Bëj-Saalum, wër ko, soog a yéeg wutali dun yooyu. Nan la leen Farãs mën a moome ? Dafa am loo xam ne xel mënu koo nangu. Gis nga yu mel nii, dafa waroon a nekk nattukaay ci ni nuy jàppalantee nun doomi-Afrig yi. Waaye fi ngay gis sunu njiit yi, ñoom ñépp dañuy lem seen geen toog ci, mel ne yëguñu sax li xew.

(ÑETTEELU XAAJ BI FEEK I FAN)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj