NJËGU DUND BI NJIITU RÉEW MI, MAKI SÀLL, JËL NA 11i NDOGAL

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci gaawu gii weesu, 5i fan ci nowàmbar, lees doon amal am ndaje ngir fénc njëgu dund bi. Ndaje ma nag, ci njiital Maki Sàll la ame. Ndax, ginnaaw bi jëwriñ ju mag jii di Aamadu Ba taxawalee ak kurél yoy, liggéey nañu ci ca njëlbeen, jubluwaayu ndaje maa ngi aju woon ci jël ay ndogal ngir wàññi njëgu dund bi. NJiitu réew mi nag, jàpp na 11i ndogal.

Njiitu réew mi, Maki Sàll, wàccee na lenn ci njëgi dund gi. Noonu, kilo ceeb bi daan jar juróom-ñaar fukk (350 FCFA) wàññeeku na ba juróom-benn fukk aj juróom (325 FCFA). Bu dee diw-tiir ji, ñaar-fukki dërëm a deñ ci liitar bi, léegi ñaari-téeméer ak ñaar-fukki dërëm (1. 100 FCFA) la liitar biy jar. Kilo suukar bi daan jar 600 FCFA léegi 575 FCFA lay jar. Soble tamit wàññeeku na. Nde, bu dee soble mbay mi, kilo bi daan jar 500 FCFA wàcc na ba 400 FCFA ; soble tubaab bi tamit, kilo bi wàññi nañu 200 FCFA ci kilo bi ndaxte 700 FCFA la daan jar laata muy wàcc ba 500 FCFA. Ba tey, ci wàññi gi, kilob pombiteeru mbay bi daan jar 600 FCFA wàcc na ba 400 FCFA. Bu dee pombiteeru tubaab, moom, kilo bi jaratul 700 FCFA, léegi 500 FCFA lay jar.  Karoot tamit wàññi na. Kilo bi daan jar 500 FCFA wàcc na ba 400 FCFA.

Ñamu ginaar sax, njëg li wàññi nañu ko. Saagu 50i koli bi daan jar 20. 000 FCFA léegi 18 000 FCFA lay jar. Bu ko defee, ginaar wàcc ba 2 500 FCFA. Kilo yàpp nag, jóge na ci 4 000 FCFA ñëw ci 3 600 FCFA bu dee yàppu nag. Yàpp xar wi daan jar 4 500 FCFA léegi 4 300 FCFA lay jar. Kilo meew pëndëx mi ngi jar léegi 2 750 FCFA ; bu njëkk 3 000 FCFA la daan jar. Waaye, du biir kese la yombal gi soxal, am na yeneen i fànn yu askan wi aajowoo, te Nguur gi indi na ciy yombal tamit

Njiitu réew mi fàttewul dëkkuwaay yi ak njàng mi

Njiitu réew mi nee na : « Li jëm ci luyaas bi, dootul amati awãsu 4i weer, waaye ñar kepp. Xaaj bu njëkk bi dees koy fay teem-mu-teew, bi ci des ñu tàllal ko ci at mi yépp. » Bu dee luyaas bi àggul ci 300 000 FCFA, wàññi nañu 20 ci 100 yoo jël, bu luyaas bi tollee ci diggante 301 000 jàpp 500 000 FCFA, 10 lañ wàññi ci 100 Yoo jël. Bu dee ne dafa weesu 500 000 FCFA, 5 kese lañ dindi ci 100 yu nekk.

Li ñeel njàng mi, bindu gi lañ yombal. Bu dee daara yu suufe yi (primaire) ak daaray tette yi (prescolaire), kenn dootul fay dara ci bindu gi. Bu dee nag daara yu digg-dóomu yi ak liise yi, njëgi bindu gi 3 000 FCFA kepp la te du weesu 5 000 FCFA. Bu fekkee ne daaray jàmbur la, wàññi nañ 10 ci 100 yoo jël. Maanaam, bu doon ne 1 000 FCFA nga daan bindoo, léegi 900 FCFA ngay fay bu dee ci daara yu suufe yi ba ci daara yu digg-dóomu yi. Daaray jàmbur yu kowe yi nag, wàññi gaa ngi tollu diggante 5 ba 10 ci téeméer yoo jël.

Wàllu tabax gi tamit am na ay yombal. Weñu betoŋ bi daan jar diggante 50 000 ak 120 000 FCFA wàcc na.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj