COONO DU RÉER ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Bari na ay xale yuy làqatu di lekk kaani. Ndax, mag ñee leen koy aaye, di wax naan : “xale du lekk kaani”. Moone de, ñoom, mag ñooñu, ñooy faral di wax ne, ku bëgg akara dangay ñeme kaani. Kon, xanaa dañoo bëgg xale yi bañ a ñam ci akara bi ? Nde, bu ñu mosul ci kaani gi, duñu ko mës a miin ba koy ñeme. Xanaa du loolu kay !

Xéy na, bu ñu teree xale kaani, yërmandee tax. Ndaxte kat, du ñépp ñoo mën a dékku cafka gi, rawatina ku ay atam néew ba àgg ci lool. Waaye, bu ñu ko teree kaani yit, gi nuy lekk a tax. Nde, am na ci gog, ci dund gi la bokk, kenn mënu ko cee dindi. Moo tax, mëneesu ko tere nit. Te nag, kaani googu, du lenn lu moy coono li wolof di naan mooy njaalbéenug njariñ.

Mu mel ni nag, coono loolu wolof di faral di wax naan du réer boroomam, dafa tàmbalee réer. Walla, bu réerul it, làqu na fu sori ba ñenn ñi gëmatuñu ko. Ndax léegi, ñu bari dañoo gëm ne jaratul nit di daj yenn coono yi ngir jot ci li muy yóotu. Ba tax na, ku nekk a ngi lal i pexe, jàpp ni moo gën a muus ña ca des. Walla muy wékku cib jegeñaaleem ngir mu yombalal ko loo xam ni, yoon wa koy joxe, xàll nañu ko ba mu leer nàññ te ku ca jaar rekk jot ca. Lépp rekk, ngir am li muy wut ci lu gaaw te du am lenn coono.

Jëf yu ni mel, tax na, ñu bari ñu gëmoon ne ku ñaq jariñu, weddi nañu ko. Mu yóbbee leen ñuy wax naan :

“Bu dee ku am mbaam war, ku ñàkk mbaam it war, lu la ca jënd mbaam di fekkee ba xont di la war ?”

Bu dee loolu la kay, ndax coono jarati na ko ? Lu tee ñu dëkkee lijjanti ba seen i mbir làqartiku rekk ? Ndegem jafe na lool nga jot ci li nga yelloo. Ndax kat, gaa ñii, ñu ngi ci naaj wi, di ñaq, guddi ak bëccëg, te mësuñoo jariñu. Te, gaa ñee, ñu nga toog ca ker ga, mësu ñu faa jóge te lépp di leen fa fekk. Loolu moos taxul kenn sawar ci di daŋ-daŋi !

Mbir mi nag, du lu yees ci réew mi. Waaye, dafa gën a fés ci jamono jii. Bari woon na lool lu ñu koy dégg ak a gis ci làngu politig gi. Waaye, mel na ni léegi daj na fépp. Dem na sax ba wàlli ci daara yi. Daanaka, néew na lu kàttey njeexitalu at mi di am ba jeex, ci daara yu digg-dóomu yi, te jàppu ñu ci ay ndongo yu doon def i pexe ngir jàll. Ñoo xam ni, ba seen i moroom di jàng, ñu ngi ci leneen ba noppi bëgg a am ay njureef yu baax. At mu jot nag, nu soow ko, at ma ca topp mu amaat, nu nekkaat ca di soow te dunu ko utal saafara si war.

Te loolu, wopp la joj, war naa dal ku ne ba mu des xale yi nga xam ni ñoo war a doon i mag ëllëg, yore réew mi. Ñooñu, dara waru leen lu dul laxasaayu, song àdduna te ñeme coono. Farlu ci njàng mi, te mu bir ci ñoom ni, xam-xam lañu war a jiital. Ndax, moo yore lépp. Kenn ku ne, dafa war a xam balaa jëf. Bu ca jógee, jëf ngir am. Ci lay mën a jariñoo am-amam ci xel mu dal ànd ak mbégte mu rëy. Dëkkee lijjanti ak bëgg lu yomb nag, du jur lu dul tayal. Te, aw askan moom, bu tayalee, ay mbiram tagatémbe, mbaa ñu dellu ginnaaw bu baax.

Senegaal nag, fii mu tollu, faqastalu waratu ko. Te, àggagul fu ay doomam sañ a toogee fas seen i loxo. Yoon wi xëccu na, tool bi yaatu na lool. Te, kenn du ko bayal waar wi ku dul ay doomi boppam. Ndaw ñi jiitu, dogu, noppi ngir dékku lépp coono. Mag ñi topp ci, di leen yokk jom ak fit. Rax-ci-dolli, di leen gunge ak a won yoon wi ñuy jaar. Ndax kat : “ku bëgg dem àjjana, dangay nangoo jaamu Yàlla. Ku bëgg tedd ci àdduna, dangay nangoo liggéey.”

Wolof nee, Yàlla, Yàlla, bey sa tool.

Baabakar Lóo
Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj