COOWAL UCAD

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ginnaaw ba ñu taaxeerloo ay ayu-bés, ndongoy jànguneb Ndakaaru yaa ngi sàkku ñu ubbi seen dara ju kowe. Waaye, ndogal laa ngi aju ca ña yore kilifay béréb ba. Ñoom sax, njiiti jàngune ba, amaloon nañ seen ñaareelu ndaje ñeel tijjiteg iniwérsite bu Séex Anta Jóob bu Ndakaaru. Mu mel ni la tukkee ca ndaje moomu neexut ndongo yi.

Njiiti UCAD yi dañoo jël ndogalu ajandi tijjiteg jàngune bi. Loolu nag, dafa safaanook bëgg-bëgg ndongo yoy, dañu bëgg a àggali seen um njàng. Nde, cig pàttali, ay weer a ngi nii  ñu laf buntuy béréb ba. La ko waraloon di coowal pólitig ba juroon i fitna, ba ay yàqute yu bari am ca jàngune ba. Xibaar ba tukkee ca moomum ndaje moo waral ba ay ndongo daje woon ca jàngune ba ngir janook taskati xibaar yi. Takk-der yi dañ leen fa fekk, tere leen ndaje ma, ñu daldi fay jàppante. Ndax, li takk-der yi lay mooy ne ndongo waruñoo faa amal ndaje.

Ndongo ya nag mer nañu. Moo tax ñu wax ne benn ndongo dootu fi jàng fileek tijjiwuñu UCAD. Ca lañ demee génne ndongo ya féete ca daara yu digg-dóomu ya. Jëf jooju tax ba ñu jàpp ca ñoom lu mat 21i ndongo ca diwaanu Mbuur, Jurbel Ndakaaru ak Kawlax.

Mu mel ni càkkuteefu ndongo yooyu, yenn ca jàngalekat ya dañ cee ànd ak ñoom. Bu ñu sukkandikoo ci Abdu Salaam Sàll ma doon àddu ca Rfm, te nekkoon fi njiitu béréb boobu (recteur), dafa mel ni dañoo nar a salfaañe ëllëgu ndaw ñi. Ndax la ña yoree doxalinu jànguneb UCAD lay ya ñu teg dëgëruñu. Ndax nee nañu fàww daluwaayu ndongo ya moo xam ca dëkkin ya, jànguwaay ya ba ca lekkuwaay ya, lépp dafa war a yem ngir ñu mën a tijji foofu.

Lu ci mën a xew daal, ëllëgu ndaw ñi lañu nar a saax-saaxe. Ndax yaakaar ju aju cim jàng mu warut dakk cim réew. Waaye, mu mel ni ba tay dayob njàng ak ndaw ñi desee nañ koo xam ci ëllëgu réew mi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj