Jëwriñ ji ñu dénk fànnu koom-koom gi, Aamadu Hot, xaatim na ab pas bu tollu ci 79. 329i miliyaar ak waa BAD (Banque africaine de développement). Nde, bànk bi daf ko lebal lu ni tollu. Waaye payooru bor bi dina gën a néew lim ko lebal. Pas boobu nag, dafay jéem a wàññi jafe-jafe yi réew mi daan jànkonteel ci wàllum dund rawatina ci jamono jii. Mooy lu deme ni anam bi mu nekke te waral muy aju ci yeneen i réew ngir dundal ay maxejjam.
Fii ci Senegaal, daanaka lu bari luy dund bitim-réew lay jóge. Mu nekk lu yéeme lool ci réew moo xam ne dafa moom boppam. Ba tax na, ci fan yii, jëwriñ ji ñu dénk wàllum koom-koom gi xaatim na ab pas bu am solo ak waa BAD ngir réew mi bañ a ajooti ci menn réew ngir dund. Ndax kat, ku la teral, tëral la. Te, ku la abal i bët nag, fu ko neex ngay xool. Moo tax, sémb bii dina amal njariñ réew mi ak maxejj yi fiy dund. Ba noppi wàññi yokkuteg dund gu bari gees fiy faral di nemmeeku. Ci loolu, jëwriñ ji yore kilifteefu pekku bànk bi ci réew mi, Mohamed Serif, biral na ne :
« Li Senegaal di jëli dund ci yeneen i réew, loraange doŋŋ la te loolu bokk na ci liy gàllankoor yokkuteem. Xareb Riisi ak Ikren bi doy nañu ci firnde ».
Jëwriñ ji ñu dénk koomu réew mi nag, Aamadu Hot, sas nañ ko sas wu diis, ndax bànk bi a ngi xaar ci moom ay njureef yu mucc ayib. War na jëfandikoo jumtukaay yi mu yore yépp ngir doxal sémb bi ni mu ware ba noppi sàmm kóllëre gi dox ci digganteem ak ñoom tamit digganteem ak beykati réew mi. Nde, war nañu bey lu tollu ci 600.000 tonu sunguf, mboq, ceeb, ak dugub ; 120.000 tonu ñebbe ak 150.000 tonu pombiteer. Bu ko defee, Mohamed Serif, yokku ci ne :
« Bu ñu beyee lu ni tollu, dina jariñ lool njaboot yi te dina soppi nekkinu réew mi ba tax dootul ajooti ci menn réew ngir dund ».
Kii di Aamadu Hot nag, ginnaaw bi mu xaatimee pas bi ba noppi, wone na mbégteem ci sémb bii nga xam ne dina ñëw doon njariñal 850.000i njaboot. Ci njaboot yooyu nag, téeméer boo jël, ñaar-fukk yi ay jigéen a leen jiite. Bu liggéey bi jaaree yoon, sémb bi dina tax réew mi mënal boppam ci lépp lu deme ni ki lu muy dund.
Ci xayma, mën na ko ndax suuf su nangu ak géej yi mu am. Li jar a laaj kay, mooy ndax dinañu dugal xaalis bi fi mu war a duggu, def ci li ci war ? Ndax tamit, dinañ boole ci sémb bi ñi ci war a bokk dëggantaan ?