Doxalinu wotey palum depite yi ci Senegaal

Yeneen i xët

Aji bind ji

Dibéeru tey 31 i fan ci weeru Sulet la wotey palum depite yi tàmbali fii ci réewum Senegaal. Mu doon bés bu ñépp doon xaar, ndax lu am solo la ci ëllëgu réew mi. Ak tamit ñi nga xam ne ñoo ko war a doxal ci biir juroomi at yiy ñëw. Maanaam, ñi askan wi war a tànn ngir ñu teewal leen ci péncum ndawi réew ma. Nde, wote yi door nañ ci jàmm fépp ci Senegaal ci juroom-ñetteelu waxtu wi ci bés bi. Kilifa yu mag yépp, daanaka wote nañ ca teel ba pare woo seen i militaŋ ngir ñu génn mottali seen wareef. Njiitu réew mi Maki Sàll def na lu ni mel ba noppi biral ay kàddu yu yenu maanaa. Ci kàddu yooyu mu ciy biral ne : « Gëm naa ni maxejj yi, ci ni ñu ko daan defee, dinañ wote ji ci jàmm te it wote yi dinañ leer nàññ. Loolooy màndargal sunu demokaraasi. Mooy, li mën a tax maxejj yi tànn seen i njiit te dara du ko gàllankoor ak nangu mujjantali wote yi ». Mu nekk ay kàddu, nee ñu, yu mat a bàyyi xel lool ci wote yi.

Ku ci mel ni Usmaan Sonko itam fare ci kujje gi, gannaaw bi mu matalee wareefam fale ca diwaanam, am na lu mu wax. Ci yéenekaay bii di « Senesccop », nee na : « Gannaaw li nu gis, yoon la nu bàyyi rekk ba mbir yi jeex waaye ndam li dina ñëw te dara du ko tee. […] Te it amunu benn sikki-sàkka ci ndam li nuy am tey ». Fale ca Caajaay, Paap Jibiril Faal mii jiite lëkkatoo bii di « Les serviteurs », def na ni Maki ak Sonko, moom tamit biral na ay kàddu yu ni mel ci yéenekaay bii di « Seneweb » : « Wote yu jaar yoon, du jur lenn lu dul jàmm ju amal solo réew mi ». Waaye kilifa gii di Abdulaay Wàdd gannaaw bi mu wotee ba noppi waxul dara ci wote yi donte ne sax askan wi bëggoon na ko dégg.

Bu loolu weesoo, Antuwaan Feliks Jon, jëwriñ ji ñu dénk wàllum biir réew mi, ci joŋante bi mu amal biral na ci waa « Dakar actu », ne jël nañ matukaay yi ci war yépp ngir lépp jaar yoon. Lu demee ni taxawaayu alkaati yi feeñ na ci diwaan yépp. Ñoom nag, ñoo ngi def liggéey bu mucc ayib. Lu deme ni saytu nit ñi bala ñoo wote, añs. Te it, képp ku wote ba noppi danga génn ci biir bérébu wotekaay bi (centre de votre). Buuxante amatul ! Ku ci mel ni kurél gu mag gi dajale réewi soowu Afrig yépp (CEDEAO) def na itam ay jéego yu am solo. Maanaam, lu deme ni yónnee fi ñeent-fukk ak juróom-ñeent jëwriñ (49) yi war a saytu doxalinu wote yi. Mu nekk ab tëralin bu mën a leeral mujjantalu wote yi. Gannaaw loolu, taw bi tamit bokk na ci li xawoon gàllankoor doxalinu wote yi ci yenn gox ci biir réew mi.

Waaye, nee ñu, ni mbir daan doxee fale ca bëj-saalumu Yëmbël rafetul dara. Ndax jëwriñ bii di Aamadu Hot dafa yaboon ay nit cig daamar jëlee leen ca Podoor ngir ñu woteel ko. Waaye, militaŋi Yewwi Askan Wi yee ko jàpp ba noppi delloo ñi mu yaboon yépp ne ko du ci dal. Mu nekk nag jëf joo xam ne maxejj ya fa dëkke ñaawlu nañ ko ba fu ñaawlu yem. Ndax loolu moom mënul romb càcc ak njuuj-njaaj. Sigicoor tamit, kii di Guy Maris Saaña, nee ñu, dafa jot ay xibaar yuy firndeel ni am na ay biisu « nervis » yu fa jot a teew. Muy woote jàmm nag ci diwaanam waaye itam di ñaan maxejj yi ñu génn dem wote ji

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj