FUTBAL : LIGUE DES CHAMPIONS, EUROPA LEAGUE AK CONFERENCE LEAGUE

Yeneen i xët

Aji bind ji

Barki-démb, démb ak tey lañ doon amal joŋantey kaar-dë-finaal Ligue des champions yi, Europa League ak Conférence League fa Tugal.

League des champions

Ci talaata ji la Dortmund ak Atletico Madrid doon amal seen ñaareelu ndaje. Ca ndaje mu njëkk ma ame woon fa Espaañ, Atletico Madrid moo gañe woon 2i bii ci 1. Waaye, bi ñu demee Almaañ, Dortmund daf ko dóor 4i bii ci 2, daldi koy toogloo.

Ca jamono jooja, Barcelone ak Paris Saint-Germain ñoo ngi doon amal, ñoom itam, seen ñaareelu joŋante. Ca bu njëkk ba, Barcelone moo fekki woon Paris, duma ko 3i bii ci 2. Barki-démb, Paris dafa fayu. Ndax, dafa fekk Barcelone dëkkam, dóor ko fa 4i bii ci 1. Barcelone moo njëkk a dugal. Waaye, biñ joxee kàrtoŋ bu xonq Araujo, ca ndaje ma wëlbatiku.

Démb, ci àllarba ji, yeneen ñaari ndaje yu mag amoon nañ diggante Manchester City-Real Madrid ak Bayern Munich-Arsenal. Ci joŋante bu njëkk bi, Real Madrid moo toogloo Manchester City biir dëkkam. Ca seen joŋante bu njëkk ba, dañoo témboo woon 3-3. Démb tamit, dañoo témboowaat 1-1, Real Madrid gañe 3-2 ci teg-dóor penaltii yi.

Bayern tamit dafa toogloo Arsenal. Ginnaaw seen témboo 2-2 ca seen joŋante bu njëkk ba biir Arsenal, Bayern Munich moo am ndam ci kanami soppeem. Nde, dafa wane geneen xar-kanam, dóor àngale yi 1-0.

Bu ko defee, nii la démi-finaal yi di demee :

Paris Saint Germain – Dortmund

Bayern Munich – Real Madrid

Europa League

Ci joŋantey kaar-dë-finaali Europa League yi, tey ci alxamesu tey ji lañ leen doon amal. Ñu amoon ci ñeenti joŋante : AS Rome –  Milan, Atalanta – Liverpool, West Ham – Beyer Leverkusen ak Marseille – Benfica.

As Roma moo toogloo Milan, dóor ko 3-1 bees boolee ñaari ndaje yi. Naka noonu, Atalanta génnee Liverpool 3-1 ci ñaari ndaje yi. Noonii la Bayer Leverkusen toogloowee West Ham 3-1 ci seen ñaari ndaje yi. Marseille tamit moo toogloo Benfica ginnaaw biñ àggee ci teg-dóor penaltii yi.

Nii la démi-finaal yiy demee :

As Roma – Bayer Leverkusen

Marseille – Atalanta

Conférence League

Ci xëccoo Conférence League bi tamit, ñeenti joŋante lees ci amoon ci alxamesu tey ji : Lille – Aston Villa, Fiorentina – Viktoria Plazeň, PAOK – Club Brugge ak Fenerbahçe – Olympiaco Piraeus.

Aston Villa, Fiorentina, Club Brugge ak Olympiaco Piraeus ñoo jàll démi-finaal. Aston Villa mooy dajeek Olympiaco Piraeus, Fiorentina laale ak Club Brugge.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj