Ndekete Fàllu Siise daa bokk ca ña daamar (kamiyoŋ) ga saaraan fan yii ñu génn ca Caaroy dal seen kaw.
Aa… Ki doon dawal daamar googu de, xamul li mu def. Li mu def, mënees na koo méngale ak xosi almet sànni ko cig kàggu, téere ya ca ne, ànd ak xam-xam ya ñu ëmb, daldi lakk ñoom ñépp ba def dóom. Fàllu Siise kàggu la woon gu ëmb lu bari ñeel baati wolof ak mbaatiitu wolof. Te ni ko fentaakon bu mag boobu di wuyoo ci turu Aamadu Àmpaate Ba waxe, mu am solo lool, “Fii ci Afrig, boroom xam-xam bu làqu daa mel ne kàggu gu lakk”.
Ñaar a ma tax a fàttali loolu, tey. Benn : boroom xam-xam yi mel ne Fàllu Siise duñuy faral di móol i téere di ci dëxéñ xam-xam boobuy tax bu ñu fi jógee mu des fi ba seeni sët ak seeni sëtaat jot ci ba sax gën koo ñoŋal. Ñaareel bi moo di ne seen xam-xam du wasaaroo ndax day saf baatin ba tax ñu néew a ciy jot jaare ko ci ag tarbiya.
Bu nu boolee loolu lépp, demug Fàllu Siise gi day doon ci nun ñaari tiis. Bu njëkk bi ñeel génnug àddinaam ak anam bu metti bi mu ame. Bi ci des di xam-xam bi mu yóbbaale.
Waaye nag sant Yàlla ndax bi nuy jooy loolu ci la ma Sëriñ Jili Kebe xamal ni Fàllu jotoon naa liggéey ak benn waay ba tax lu bari ci li newoon ci moom yëbb na ko ci waay jooju. Rax-ci-dolli, waxtaan yi mu jot a séq ak ña ca kippaango bee ñu duppe Akaademi wolof ci Facebook, baati wolof yu xóot te ñu bari umple leen woon, jot na ko faa rotal.
Lee tax nu mën a jàpp ne Fàllu Siise dem na waaye demul ndax ni ko woykat bi waxe “suuf dina lekk doomu-Aadama bàyyi fa jëf”.
Xanaa rekk des di ko ñaanal Yàlla miy Boroom-Yërmaande jéggal ko te xaare ko àjjanay firdawsi ci barke turandoom Sëriñ Fàllu Mbàkke.
Bu loolu weesoo, nu def yitte ci dajale li mu nu fi bàyyil, móol ko, wasaare ko ba mottalil ko naalam wi jëm ci jëmmal làkk ak baatiitu wolof.
Seen yéenekaay LU DEFU WAXU mi ngi koy jaale njabootam gépp ak i mbokkam. Waaye, noo ngi koy jaale yit waa Senegaal gépp rawatina ñiy liggéey ci làmmiñi réew mi.