FÀTTALIKU OMAR BOLONDEŋ JÓOB…

Yeneen i xët

Aji bind ji

Ci àllarba tey jii, 11eelu fan ci weeru Mee 2022 la Senegaal di fàttaliku faatug Omar Bolondeŋ Jóob 49i at ci ginnaaw. Kon li ko tee mat xarnu bariwul. Ngir sargal jàmbaar jooju bëggoon réewam ba mu jaral ko bakkanam, Lu defu waxu tekkilu na ci kàllaamay Kocc ab yaxal bu am solo bu ko Foloryaŋ Bobeŋ jagleeloon ciy jamono, tudde ko “Dellusiwaat ci jaar-jaaru Bolondeŋ Jóob ci jamono ju ñuy wut a jàllarbi li fi nekkoon ci Senegaal”. Ci àngale lan jëkk a bind bile yaxal, siiwaloon ko ci “Review of African Political Economy”.

Daawuda Géy mi nu ko tekkil nag, bañkat la moom tamit. Ngërëm ñeel na ko…

*

Fukkeelu fan ci weeru Mee 1973, la kilifay Senegaal yi yëgle faatug Omar Bolondeŋ Jóob, mu doonoon ndaw, doonoon ab bañkat ak ab ma-pasin*, amoon 26i at, ñu téye woon ko ca kaso ba ca Gore. Daanaka am na xaaju xarnu boobu ba tay. Li Nguur gi wax ne dafa xaru, ñu bari weddi nañ ko, jàpp ne ñoom ci seen bopp ñoo ko bóom.

Ci atum 2013, mbokki Omar Bolondeŋ Jóob dañu ko doon màggal, 40i at ginnaaw bi mu faatoo ca Gore. Ci diirub ay xarnu, dun bi Tubaab yi daan yóbbu lim bu kenn mënul a takk ci ay saa-Afrig ca Amerig def leen fa ay jaam. Ci biir googu màggal, mbokki Omar yi génne woon ab nataalam ca biir kasoom ba woon, te doon léegi ab bulub aajarukaayu, barab bu mboore bi gën a mag ci Senegaal. Ñu ngi jël boobu nataal ci atum 1970. Booba Omar njàngaan la woon ngir doon ab jàngalekatu xeltu, ñu ko doon doog a dàqe Farãs mu delsi Senegaal. Mu bokkoon, niki yeneen moroomam yu bari ca jooja jamono, ci yëngu-yëngu yi amoon ci “Mee 68”. Ñu teg ci ay at, ñu bóom jàllarbikat bi ci biir toolu-xare.

Bi mu génnee àdduna ci kaso ba mu nekkoon, ginnaaw bi ñu ko àtte mu war a tëdd ñatti ati kaso ndax dafa “laal kaaraangeg réew mi “, kilifay Senegaal wax ne dafa xaru. Waaye ñu bari jàppoon ne dañu koo bóom. Booba ba tay ay mbokkam tàyyiwuñu di sàkku yoon def liggéeyam ci mbir mi, teg ci ay bañkat ak ay ma-pasin jël xeex bi ngir kenn bañ koo fàtte.

Faatug Omar Bolondeŋ doonul xew-xew bu am nii rekk ci sunu mboor, bu kenn xamul lu ko jur. Déedéet, benn la rekk ci ay xeeti metital yu nguurug Senegaal yàgg a def. Tàmmuñoo gis ñuy wax lu bari ci kuréel yi taxawoon di jàmmaarloo ak nguurug Seŋoor, walla sax di leen jox seen gëdd ndax ki fi jëkk a doon njiitu réew (atum 1960 ba 1981) fexe woon na ba ñépp jàpp ne réew mi royukaay la ci demokaraasi. Nettali yi ñu saxal ci génnug réewi Afrig yi ci nooteel dañuy tënk yoonu tinkiku gi ci nooteelug tugal ci juddug Càmm yuy soog a moom seen bopp. Te doxandéem yu wéy di dugal seen loxo ci réew yooyu ngir seen njariñu bopp, te njiiti réew yooyu jàppale leen ci, loolu lu ñépp tegoon seen bët la ci atiy 1960 yi.

Ginnaaw bi ñu moomee seen bopp ci waxin rekk, jaaykati doole yi ci ndimbalul réew yi ñu nootoon, dañoo sasoo dëgëral seen nguur, jaare ko ci faagaagal lépp lu jóg di woote ag tinkiku ci nooteel ak ci nosteg koppartu. Gaa, Senegaal dundul ay jafe-jafe ci wàllu politig ni mu amee ci réew yi ko wër, waaye fi ñu àggale woon mbaaxug kii boole woon di taalifkat di njiitu réew muy Lewopol Sedaar Seŋoor muuroon na sunuy gët ci ay doxalinam ci politig. Ci jamonoy “Union Progressiste Sénégalaise” (UPS), doonoon benn kuréelu politigu cundum mu jiite ko, kilifa yi daan nañu noot, di xorñoññal di teg loxo, di tëj, di metital ba di ray bañkat yi. Omar Bolondeŋ Jóob bokkoon ca ñooña.

Bolondeŋ Jóob a ngi gane àdduna ci Niseer ci atum 1946. Baayam doonoon ab fajkat, ñu jële woon ko Ndakaaru mi doonoon jooja jamono gëblag “Afrique Occidentale Francaise” (AOF), yóbbu ko Dooso, gox bu ndaw bu nekk ca Ñaame. Doonte sax ay xalaatam ci politig jëmmalu leen woon mu jëm ci xeex nooteel gi, Tubaab yi xawoon nañ njort ne dafa bañoon Farãs. Li gën a yokk loolu mooy li mu jàppaloon tànk kuréel gi dajale liggéeykati àdduna bépp. Tiitaange gi mu amoon ci ni yëngu-yëngu yi jëm ci bañ nooteel di gën a am doole ginnaaw bi ñu jógee ci ñaareelu xareb àdduna bi yépp, moo waraloon Farãs doon bàyyi xel bu baax ñi mu tudde woon “ñi noonoo Farãs”.

Ndakaaru la Bolondeŋ màgge. Bi mu amee 14i at la dëkki Farãs, baayam di fa wéyal am njàngam ci wàllu paj. Daanaka ati 1960 yépp Bolondeŋ mu ngi fa woon. Foofa ca Pari, mu doon fa wéyal moom tamit am njàngam ci wàllu mbind ak di xóotal xam-xamam ci xeltukati Tugal yu mag yi, mel ne Aristod ak Kànt, ba ci Éegal ak Ruso. Bi muy dugg Lekool Normaal Supeeryëer yemoo ak mu tàmbalee teew ca jotaayi ñiy xeex ba sax di wàlli ca béj ya ca féete càmmooñ doon amal. Jamono la ju kuréel yi doon xeex koppartu gi, doon roy it ci jàllarbi ci wàllu mbatiit ca Siin ba noppi di ŋàññ xareb Amerig ba duggoon Wiyetnaam. Ndongoy Afrig yi ca Farãs, tolloon ci limub 10i junni ci atum 1968, seen taxawaay mu ngi gënoon a jëm ci xeex ngir seen réew ak tamit ngir bennoog Afrig. Bolondeŋ moom daa tegoon benn tànk ci ñaari wàll yépp. Diir bu gàtt ginnaaw bi filmkat bii di Saŋ-Lik Godaar déggee waxi bañkatu saa-Senegaal bi, la ko tabb mu bokk ci filmam bi tudd “La Chinoise” ci 1967. Mbind ak xalaati Espinosaa, Maks, Fanon, yëbbee ci moom, Bolondeŋ doon saxal am njaxas ci wàllu xam-xam – boole aju-ci-tër-gi, dàq lépp luy gàllankoor ag péexte, xalaati Maawo ak Torotskii. Xalaatam ci politig mu tanqe woon ko ci yoonu gis-gis yu bari, booleek wéy di jàng àdduna bi ak i gëti boppam. Ay yëngu-yëngoom ci wàllu politig tax ñu dàqe Bolondeŋ Jóob Farãs, mu ñibbisi Senegaal ci njeextalu atum 1969.

Moom ak yeneen mbokk-mbaar yu jànge Tugal ñu bokk ci yënguy ndawi Maksist-Leninist yi te benn pàcc ma ca daggee jur “Ànd Jëf”. Bolondeŋ Jóob dàq lootaabewin yu siis yi, jiital jéegoy pasin yi jaare ko ci taxawal sémbub “tiyaataru mbedd biy wax nit ñi li leen soxal”. Muy lu ànd lool ak “Tiyaataru ñi ñuy noot” bu Ógusto Bowaal. Bi mu seetloo pasin mi ak li mu mën a jàppee ci jàllarbi gi, Bolondeŋ Jóob daldi bind ne : “Balaa ñuy def tiyaatar ci ab gox, fàww ñu xam njëkk ña fa dëkk, jaxasoo ak ñoom, rawatina ndaw ña […]. Sunu tiyaatar bi dina dem fépp fu nit ñi di dajaloo (ja yi, sinemaa yi, estaad yi) […]. Fexe ba jox wëppa wu ne, tër gu ne, aji-jëmmal ju ne, màndargay Afrig. […] Rawatina di defar lépp lu nu mën a defaral sunu bopp […]. Ci tënk : dee waaye dunu nangoo tàbbi ci njaam”.

* M-pasin Artiste

(Foloryaŋ Bobeŋ ci tekkig Daawuda Géy)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj