Kafrin dalal na xew-xewu mbatiit bu réy bi ñu dippe ci nasaraan Festival National des Arts et Cultures, gàttal biy joxe FESNAC. Mu ëmb nag mbooleem caadaay réew mi. Jubluwaay bi mooy jëmmal xeeti mbatiit yi ci seen wuute ak askan wi leen di dundal. Ren di 11eelu yoon wi ñu koy amal, Kafrin di feelu yeneen goxi Senegaal ya daan teeru xumbeel googu.
Atum 1997 lañu ko sos, ca Cees. FESNAC ñu koy amal ñaari at yu nekk. Soloom di wone mbatiitu réew mi ci anam yu wuute, waaye fexe lëkkale askan wépp. Goxi Senegaal yépp di fa daje, kenn ku nekk di wone aaday fa nga féete. Mu nekk tamit jataayu xumbeel boo xam ne woy, fecc, ladab, kilib, nataal kenn wuutewu ko. Mu doon jamonoy mbégte ci seetaan nataalu Senegaal ci aada yi ko ëmb. Lépp di firndeel xarañte askan wi ak seen mën-mën ci xelliy xalaat yuy suuxat mbatiit. Ponk ren bi nag, dafay dellu ci taxawaayu jigéen ñi, seen waar ci sàmm mbatiit ak koom ma ca mën a tukkee.
Ci kow loolu, boroom ndomboy tànk yu bari daje nañu fa, moo xam ñi fare ci biir réew mi wala seen i naataango ya ca bitim-réew. Njiitu jëwriñ yi, Aamadu Ba, fekke na ubbite ga ànd ak ay jëwriñ yu fare ca gox boobu ku ci mel ni Abdulaay Saydu Sow ak Abdulaay Wilaan. Kilifay aada yi tamit wone nañu seen teewaay. Ñu nekk ay kenu mbatiit ci sàmm ak yiir, waaye tamit jàllale xam-xam ndaw ñi. Ci loolu lingeeru askanu Joola yi, ciy kàddoom, soññ na réew mi ngir ñu dellu cosaan te fonk sunu mboor. Ñu seetlu taxawaayu jëwriñ ji ñu dénk wàlluw mbatiit ci biir réew mi di Aliyu Sow. Ñu koy sargal ci tolluwaayu xew-xew bu gànjaru ak ci dayo bi mu ko jox.
Kon, mënees na wax na mbatiit mën na am beneen xar-kanam bi ñu ko dundale. FESNAC bu Kafrin am yokkute bu ñu ko méngale ak yeneen yi jàll. Ndax jëwriñ jii di Aliyu Sow yokk na nafa gi te it boole na ca ab neexal bu ñu jàggeel gox bi.