Jamono jii, laaj bii moo lëmbe xel yi, rawatina xeli soppey Barcelone FC yi. Li ko waral, nag, mooy ni, seen yéene yépp dafa nekk ci Messi ñibbisi. Ndax dana am ? Ndax du am ? Mëneesagul a am tontu lu leer ci laaj bi. Lo am ba des daal, mooy ni foofu ca Barça, seen yaakaar moo ngi gën a dëgër ñeel delsig Messi.
Moom, Messi, Barça la defe léppam. Dafa di, li mu jot jël ci dundam yépp, ci wàllu këlëb, Barça la ko ame. Te sax, xel mësul woon a xalaat ne bés dina ñëw mu fay jóge. Moo tax, demam ga, ca atum 2021, ñépp la bettoon. Ndate, du woon lees doon xaar walla di ko waaj. Moom kay, dafa xëy rekk takk i dëbësam. Li wolof di wax, naan, “Ku sañul a bañ, sañ a nangu” moo ko ci dal. Nde ñépp xam nañu fu ko Barça tollu ak it fi mu tollu këlëbu katalã yi, lam fa def ak kim fa doon. Naam, Barça sosu na lu njëkk xameelam fuuf sax, mën tuddu turu ekib ba te xel newul yar ci moom Messi. Waaye nag, ñépp xam nañu itam ne, bim fay jóge di dem Paris, dafa najoon xolam rekk, waaye gënalu ko woon wenn yoon. Ñàkk pexe rekk a ko fa yóbbu.
Barça, jamono jooju, mu ngi nekkoon ci ay jafe-jafe yu jëm ci mbirum payoori kuppekat ya. Ndaxte li ñu gisoon ne moo ngi koy fay ay kuppekatam, buñ ko xaymaa, lépp dafay jéggi liñ leen may di dem. Loolu nag naroon koo andil ay guddi yu lëndëm, moom Barça. Ci noonu, ñu nekk ciy lijjanti ak di xool naka lañuy def ba saafara loolee. Loolu moo dem ba andi demug Messi gi. Ndax cofeel gi mu am ci ekib ba ak bañal ko ay jafe-jafe tax mu nangu jóge ca ekib ba. Waaye du woon ne daf fa doyal walla dafa bëggoon a wuti leneen feneen. Déedéet, du woon loolu. Ndaxte, lépp jëloon na ko ak Barça. Luñ fa tegoon ñu di ko xëccoo rekk teg na ci looxoom foofa.
Demam gi mettiwoon lool ay soppeem, ñi ko wër, waaye itam moom ci boppam. Nde, ca tàggatoowam, jottina fa ay rangooñ yu tàng ak ñu bari ñu fa teewoon rawatinay farandooram.
Ca atum 2021, mu jóge Barça dem Farãs fekki Paris Saint-Germain. Mu doonoon lu rëy ci boobu këlëb. Ndaxte, ku tollu ni Messi nga yor ko sa ekib, ndam la, sag la. Ba ci jamono jooju, foo geestu waan, ay mayo Paris yu ñu bind turam rekk ngay gis, mbaali-jokkoo yeek këri xibaar yépp di tas i xibaar gi ak di dugal i nataalam fépp.
Ñëwam gi foofu ci Paris nekkoon na lu rëy ci ñoom, nde jàppoon nañ ni seen yéene ci jël “League des Champions”, bu Messi dikkee dafay gën a dëgër, ekib ba itam gën koo bëgg. Waaye, dafa di, saa buñ xëccee ba am yaakaar rekk buum ga dog. Atam bu njëkk ca Paris, mu xawoon a am ay jafe-jafe wane fa boppam niñ ko doon séentoo, rawatina ci joŋante yu mag yi. Ñu jàpp ni lam fay door a ñëw la, walla sax ñàkk a miin dëkk baa ko jàppoon rekk, ci déwén gi dana firi.
At mii nag, mu ñëw, ci njëlbéen gi, tàmbali di gis, di dugal ay bii ba ñépp tàmbalee bég. Mu jóge fa dem ca Kuppeg Àddina si amoon ca Qataar, xare ni gaynde ba jël ko. Mu wane fa nag xereñte gi ko ñépp xame woon, def fa lu rëy ba kuy bége kuppe bég ca. Mu delsi Paris, nga gis mu mel ne ku yarasaat, ba ni mu daan def ca Kuppeg àddina sa, joŋante ci mag yi niki ak Bayern ca “League des Champions” muy mel ni ku réer. Loolu waraloon siporteeri Paris yi doon ko yuuxoo ak a xalab.
Jamono jii nag, féddaliwaat xaritoom ak Paris nekk na loo xam ni kenn yaakaaru ko. Xel yépp, ci mu dellu Barça lañu nekk. Te sax, waa Barça loolu rekk lañu bëgg jamono jii. Kii di Laporta ma jiite këlëb ba, ak Xavi miy tàggatkat bi, jotoon a far ak moom ay ati at, loolooy seen yéene. Moom Messi ci boppam bañul loolu. Ndax, déggees na ne, ay nitam ñoo ngi jokkoo ak waa Barça, di xool nam fay delloo. Neeti nañ sax ne, moom ci boppam, mi ngi dégganteek gaa ña, di ci dalal seen xen.
Fële ca Araabi Sawdid itam turam moo ngi fay jib. Ndaxte, Al Hilal, këlëb biy diirante mbagg ak Al Nasri bu Ronaldo, dafa bëgg a teg xaalis bu takku ci taabal ji ngir mu ñëw fa.
Lu ci mën di am daal, lépp dina leeri. Dinañu xam ndax dafay toogat Paris am dafay fekki wujjam ba, Ronaldo, mbaate mu dellu këram gii di Barça.