Bi Alseri dumaa Senegaal benn ci dara ci finaalu joŋanteb réewi Afrig yi (CAN) ak léegi, mu ngi bëgg a yàgg. Waaye, kenn fàttewu ko. Li ko waral nag mooy finaalu basket bi soxna yi ñàkk, ñoom tamit, biñ dajeek Niseryaa fan yii ñu weesu. Yaakaaroon nañu ne, soxnay basket yi dinañ feral sunuy rongooñ. Ndeysaan, keroog bi leen Niseryaa daanee fii ci Ndakaaru, ñépp a ci amoon tiis ak naqar ndax yaakaar ju tas.
Ñaari finaal, ñaari kub, Senegaal ñàkkandoo leen ci menn at, ci diggante bu gàtt a gàtt ! Ñii ne waaw, ban dëmm a nu juutu ? Ñee di laaj, kan moo nu um ? Laaj bi jar a laaj, nag, ci dëgg-dëgg mooy : lan walla kan mooy sunu gàllankoor ba tax nuy lajj saa su nekk ci cëppaandoo bi ? Tey nag, ci futbal bi lanuy tàmbalee.
Séex Sekk, Roose Mendi, Sil Bokànde, Umar Géy Seen, Ferdinaa Kóli, Umar Daaf, Saalif Jaawo, Paap Buuba Jóob, Fadiga, Àllaaji Juuf, Aari Kamara, Saajo Maane, Kalidu Kulibali… Ku dégg yile tur, sam xel dem ci jaloorey ekib nasiyonaalu futbal bu Senegaal. Ñii nu fi jot a lim ñépp nekkoon walla di ay futbalkat yu xereñ lool, ñu ràññee leen bu baax ci Senegaal, ci Afrig ak ci àddina sépp. Waaye, ak lu tur yiy réy réy, lenn doŋŋ lañuy màndargaal : yaakaar ju tas. Waaw. Ndaxte, ba nëgëni-sii, Senegaal amagul benn biddéew ci mayoom bi. Ak lu coow liy bare bare, mësta jël kub. Laaj bi ub bopp yi mooy : lu tax Senegaal jëlagul kub ba léegi te, jamono ju nekk, mu yor ay ndaw yu xereñ ? Nu ànd xool, démb ba tey, lu xel mën a jàpp ne mooy sunu laago ci futbal bi.
1961 : Ndoorteel li
Ci at mii la Senegaal di door a amal joŋanteem bu njëkk. Ñaari at lañ ci teg (1963) ekibu futbal bi Senegaal daldi jël raw-gàddu gi ci Joŋantey Xaritoo (Jeux de l’Amitié) yi amoon ca jamono jooju.
1965 : Njëlbéenub joŋante ci CAN
Ci at mii la Senegal di door a bokk ci joŋanteb réewi Afrig yi (Coupe d’Afrique des Nations), gàttal bi ci nasaraan di joxe CAN. Ci njëlbéenug joŋanteem boobule, Senegaal ñaawu ci. Ndax, moo jëloon ñetteelu palaas bi. Gànnaaw gi, daanaka Senegaal ab nooy-neex la woon, ku jàpp rekk wulli, ekib bi dee daanaka.
1990 : Dekkiwaat bi
Senegaal dekkiwaat. Claude Leroy mi yoroon ekib bi ci diggante 1989 ak 1992 moo ko defaraat, tàggat leen ba Senegaal joŋantewaat, ginnaaw atum1965, « ½ finales » CAN bi amoon fii ci Senegaal ci atum 1992. Waaye, ñetteelu palaas bi la mujje jëlaat. Ci atum 1994, « ¼ de finales » la yem, wute joŋante yu 1996 ak 1998.
2000 – 2019 : Jamonoy jaloore ak yaakar ju tas
Ci wàlluw futbal, bi Senegaal dee Senegaal ba tey, ci diggante atiy 2000 ak 2019 lañu ko gën a ràññee. Ndaxte, ci jamono jii la ndawi Senegaal yi gën a xereñ fëlle : A1llaaji Juuf, Fadiga, Ferdinaa Kóli, Umar Daaf, Lamin Jaata, Aliyu Siise, Saalif Jaawo, Paap Buuba Jóob, Tooni Silwaa, Aari Kamara, Abiib Béey, Jomansi Kamara, Mamadu Ñaŋ, Suleymaan Jaawara… Bi ñooñu jeexalee, Saajo Maane ak i ñoñam, Gànna Géy, Kalidu Kulibali, Sabali, Ismayla Saar, Jaawo Balde… wutu leen. Ku ci gën a xereñ, dàq futbal sa moroom nga ne kii. Ñu yaakaaroon ni bile yoon, nag, Senegaal dina am dara. Ndeysaan, bu dul finaalu 2002 ba ak « ¼ de finales » bi ñoom Àllaaji Juuf demoon ca « Coupe du Monde » 2002 ak ndam li ñu amoon ci kow Frãs ci ndoorteelu joŋante bi, Senegaal jëlul dara, tus… Naam, li Senegaal àggoon finaal ca Mali, ndam la. Naam, def na jaloore ju réy a réy bi mu amee ndam ci kow Frãs ci « Coupe du monde » bi ci toppoon, ñu ni déet-a-waay mu dem ba « ¼ de finales » yi. Kenn sañul a wax ne loolu du ndam. Wànte, ndam loolu, wareesoon na ko def ag garab, suuxat ko ba mu meññ yeneen i ndam yu gën a réy, maanaam nu jël kub. Ndege, Senegaal bokkoon na ci ekib yi gën a xereñ ci Afrig, te ba léegi loolu la ñépp jàpp. Waaye dara, dara la fi indiwul : 2004 Tinisi moo nu toogloo ca réewam ci « ¼ de finales » yi 1-0 ; 2006 Misra moo ko toogloo ci « ½ finales » yi, mu mujje jël ñeenteelu palaas bi. Ci at moomu « Coupe du monde » amoon na, waaye Senegaal bokku ci ndax Tógo moo ko tere woon dem, mu metti woon lool ci waa réew mi. CAN 2008, Senegaal génnul sax gurub bi mu bokkoon. 2010, Amara Taraawore moo yoroon ekib bi. Waaye, ci CAN bi, Senegaal ñetti joŋanteem yépp la ñàkk, daldi toog. Demul yit ci « Coupe du monde » at moomu. Ñu foog ni Alain Giresse mi ñu tabb ci atum 2013 dina faj laago bi, waaye moom tamit dañu koo mujje dàkk ndax lajj bi mu lajjoon. Ki ko wuutu mooy Aliyu Siise mi bokkoon ci ekibu 2002 bi te nekkoon kapiteen bi. Ginnaaw CAN 2017 bi nu toogee ci « ¼ de finales » yi, moo delloosiwaat Senegaal, ak ñoom Saajo Maane, ci “Coupe du monde” 2018 bi. Waaye, foofu tamit, yaakaar ju tas lañ fa jële. Ndax Senegaal génnul gurub bi mu bokkoon doonte sax kenn mënu ko fa woon. Ci CAN 2019 bi, ñépp a newoon ne bii yoon moom, day baax. Waaye, Alseri moo nu dóor ci finaal bi. Yaakaar tasati. Ñii di saaga fii Aliyu Siise, ñee di duut baaraam njiiti federaasiyoŋ bi, ñeneen ñi di ko jiiñ sëriñtu bi waa réew mi nekke ba ci futbalkat yi. Kan moo ci wax dëgg ?
Cuune, yaataayumbe ak sëriñtu
Bi fi Bruno Metsu (2002) jógee ba léegi, fukki tàggatkat wuutu nañ ko ci boppu ekib bi laata Aliyu Siise di toog. Ci fukk yooyu, juróom-ñaar yi ay doomi-réew mi lañu. Loolu day firndéel matadi, cuune ak caaxaan bi ñu yore futbal bi. Ndaxte, bir na ne ba tey xamuñu nees di tànne tàggatkat bu baax ak naka lees koy gungee, jàppale ko ba liggéeyam àntu. Loolu day wone yit yàkkamti bi ak ñàkk fulla bi waa federaasiyoŋ bi nekke. Te, ku yàkkamti, yàqule. Benn, ab ekib dees koy tabax ci diir bu yàgg. Mbir mi du xéy rekk sotti. Fàww nga may tàggatkat bi tuuti ngir mu tabax ekib buy jël kub. Waaye xel nanguwul, benn walla ñaari at yu nekk nga ut beneen tàggatkat, indi yeneen i futbalkat. Ñaareel bi mooy ne, njiit day am fulla ci boppam. Du nekk ma riirandoo waxatuma la ak benn nopp. Fàww bëgg-bëgg yi wute, gis-gis yi ak xalaat yi safaanoo. Kon mënoo, yow njiit li, saa bu taskati xibaar yi waxee fii nga topp leen, bu askan wi yuuxoo fee ngay jéem a def lu ko neex ngir bañ coow. Moo taxit, saa boo leen toppee, boo lajjee, ñoom ñoo lay njëkk a song. Li koy firndéel mooy atum 2008, bi Senegaal arañefee ak Gàmbi fii ci estaad Lewopóol Sedaar Seŋoor, ndaw yi dañoo mer ba futt, di ñaxtook a sànni xeer ci buntu estaad bi. Bés boobu tàngoon na lool. Kenn fàttewul tamit 2012, bi farandooy ekib bi meree, di sànni ay xeer, butéel ak i yu ni mel ci teereŋ bi. Jotoon nañoo sax wàcc ngir duma futbalkat yi ak njiiti federaasiyoŋ bi. Bés boobu, daa fekkoon Kodiwaar am ñaari bii ci kow Senegaal, muy tekki ne Senegaal du dem ca CAN bi waroon a am atum 2013. Bi ñu jógee ci loolu, FIFA, kurél gi yor futbal bi ci àddina sépp, dafa teg ay daan Senegaal.
Bi ñu ko laajee lu tax futbalu Senegaal mënta jëm kanam, Àllaaji Juuf dafa tontu woon ne ñi fi nekk (njiit yi), xaalisu futbal bi lañu bëgg waaye bëgguñu futbal bi. Kàddu yooyoo taxoon ñu teg ko fi ay daan yu metti, moom Àllaaji Juuf. Waaye, ndax mënees na koo weddi ? Ñaari at lañ ci teg, Demba Ba waxaat lu ni mel. Te, wolof nee na, fen du màgget. Kon daal, njaw des naw xambin. Daanaka, jamono ju nekk, saa su joŋante amee, nga dégg ne waa federaasiyoŋ bi ñoo ngi yaataayumbe ak xaalisu futbal bi. Seen njaboot, seeni mbokk ak i xarit, ñépp lañuy yóbbu fi ekib biy dem, di gundaandaat ak a ndagarwale ci alalu réew mi. Ñu ni déet-a-waay, sëriñ si demaale ak seeni xarfafuufa, gisaanekat yi ame nit ñi fii, ñuy fekk ci ron-lalu futbalkat yi ay téere… Muy lu yéeme sax ! Kon, mel na ne laaj bi nu sampoon ca njëlbéen am na tontu. Cuune, yaataayumbe ak sëriñtu bi ñu nekke moo nu teree jël kub…
Bu beneen yoonee, dinaa leen wax lu tuuti li ma xam ci basket bi !