GÀTTALI BÉS BI

Yeneen i xët

Aji bind ji

Popengin 2023 : Kàdduy Mõseñëer Njaay ñeel jëwriñu biir réew mi, Àntuwan Feliks Jonn
Nees ko baaxoo defe at mu jot, ay junniy junni kercen, maga k ndaw, góor ak jigéen dox nañ, dem Popengin. Ren jii mooy 135eelu màggal gees jagleel Yaay Mariyaama. Jëwriñu biir réew maa fa téewaloon Njiitu réew mi, Maki Sàll. Kilifag kercen yi, Mõseñëer Njaay, am nay kàddu yim ko jagleel ñeel jàmmi réew mi.
“Kilifa gi, yow mi ñu dénk kaaraange biir réew mi, saa su nekk noo ngi nekk di ñaanal sunu bopp jàmm ci sunuy nuyoo. Jàmm mooy simaŋ biy tabax dund gi ci biir mboolaay gi. Dafa nuy jàngal nangoo déglu, joxe cër, nawloo nit ñeek sa bopp. Dellu jàngal nu ci jàngub Mariyaama ak Elisabet ni dégloonte nekk na lu képp ku nekk ci nun war a suuxat. Du ku ëpp làmmiñ rekk yaa wax dëgg. Du yeet ku gën a neex làmmiñ ni lem moo wax dëgg. Waaye, noo ngi am dëgg ci bu sunuy kàddu dee tabax jàmm, ca dëgg-dëgg.”

Bitim-réew a ngi ñaawlu jàpp biñ jàpp Usmaan Sonko
Waa ONG WARABA génne nañu yégle di ci naqarlook a ñaawlu jàpp biñ jàpp Usmaan Sonko ci lu dul yoon.
« ONG WARABA bu Afrig a ngi am mbetteel ak naqar ginnaaw bim yëgee jàpp biñ jàpp Usmaan Sonko jamono yi mu doon amal « ndiiraanug péexteem » ak nees ko fëkkee. »
Ginnaaw bim limee ay sàrt yu bari yuy dellu ci àqi ak yelleefi doom-aadam yoy, Nguurug Senegaal lépp la jalgati, dafa jóo campeefi àddina si ci ñu nangul layookati Usmaan Sonko yi seen càkkuteef.
« ONG WARABA a ngi woo campeefi àddina yiy sàmm àq ak yelleefi doom-aadama ngir ñu nangu càkkuteef gi layookati Usmaan Sonko yi dugal ca Ndajem Àq ak yelleefi doom-aadama mu Mbootaayu Xeet yi (ONU). »

Ndakaaroo ngi tàkk
Xeex bi doorati na diggante xale yeek takk-der yi. Li ñu fëkk démb Usmaan Sonko, tëj ko këram a xamb taal bi. Nde, démb la takk-der yi jàpp Usmaan Sonko ci pet, indi ko Ndakaaru, tëj ko këram ba noppi tere ku ko seetsi. Du ay mbokkam, du ay jegeñaaleem, du sax a layookatam. Kenn du dugg, kenn du génn. Moo tax ndaw ñi fippu, tàmbalee taal. Àgg nañ sax ci taal ay këri jëwriñ. Muy Sëriñ Mbay Caam, di Abdu Latif Kulibali ak Mataar Ba yépp, taal nañ seen i kë ak seen i daamar.
Bu dee Mataar Ba, bi ñuy jafal këram, ma nga woon ca biir ak njabootam, ciy waxam. 6i daamaram la xale yi boyal. Moom nag, kujje gi la ko jiiñ, rawatina waa Pastef.
Gornooru Ndakaaru tereeti na moto yi daw
Gornooru Ndakaaru dafa génne ab santaane, di ci aaye moto yi li ko dale altiney tey ji ba talaata. Moom nag, nee na ngir sàmm kaaraange dëkk baa tax.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj