TAXAWU SENEGAAL DINA BOKK CI WAXTAAN WI NJIITU RÉEW MI WOOTE
Ëllëg ci àllarba ji, la waxtaan wi Njiitu réew mi Maki Sàll woote war a tàmbali. Ñu ëpp ci kujje gi biral nañu ni duñ fa dëgg seen tànk. Waaye, ñii di waa Taxawu Senegaal, ñoom dinañu ci bokk. Loolu lañ xamle. Bees sukkandikoo ci seen ub yëgle, diisoo am na ci seen biir. Liñ ànd dëppoo mooy dem ca waxtaan wa ngir génne réew mi ci guuta gi mu nekk. Waaye, bu kenn fàtte ni nekkug lawaxu Njiitu réew mi Ndeyu àtte réew mi daf ko dàq. Te amul lenn lu koy yoonal.
FARBA NGOM A DANKAAFU NA USMAAN SONKO
Farba Ngom doon na àddu ci taafar ji am ci réew mi fan yii ñeel ñaxtuy ndawi Pastef yeek kër ak daamar yi ñuy taal. Meeru Añam bi daf ne :
“Idriisa Sekk mi nga xam ne mag la ci pólitig, waxoon na ba noppi lees war a def Usmaan Sonko, maanaam “coppet yóbbu”. Te, loolu lañ def keroog dibéer.”
Démb, ci ngoonug altine ji la ko doon wax bi muy janook taskati xibaar yi. Moom mi yor mbirum lootaabe ak mbooloom APR mi, dem na bay dankaafu njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, di ko tëkku. Neen na :
“Ci alxames jii, 1 suwe, lañuy biral àtte bi, waaye noppi nanu. Dunu wax li nu nar a def, dunu siiwal sunum pexe mi nu lal ci mbooloo mi. Waaye xamleen ni Nguur gi noppi n’a.”
Farba neeti na takk-der yi def nañ seen wareef. Ñoom way-pólitig yi ànd ak Maki Sàll ñoo ci des. Ndax, ciy waxam, askan wi dafa sonn, te kenn sonalu ko ku dul Usmaan Sonko. Kon, fàww ñu jòg ci moom.
JËWRIÑU BIIR RÉEW MI YÉGLE NA NI DEES NA TOPP MÓODU-MÓODU YIY XIRTAL NDAW ÑI NGIR ÑU GÉNN XEEX
Jëwriñu biir réew mi, Antuwaan Feliks Jom, ñaawlu na taxawaayu saa-senegaal yi nekk bitim-réew. Nde, ciy waxam, ñooñee ñooy soññ ndaw ndaw ñi, di leen xabtal, ñuy génn ci mbedd yiy xeex ak takk-der yi. Moom nag, nee na, ngir dakkal lu ni mel, Nguurug Senegaal di wax ak réew yi leen di dalal ngir ñu topp leen.
“Gisees na, te di ku ñaawlu, ay maxejji Senegaal yiy dund bitim-réew, nekk ci seen jàmm ak seen ginnaawi loyukaay walla jollasu, di woo ay ndaw ngir ñu génn song këri jàmbur. Walla ñu leen di yónnee xaalis ngir ñu jënde ko kaarbiraŋ ak yeneen xeeti ndefarey safara.”
Ci kow loolu, “Nguur gi jël na matuwaayam yépp ngir wax ak réew yi leen di dalal, siiwal bataaxal yi ñuy yónnee Senegaal ak liñ ci wax.”
Li jëwriñ ji namm ci doxalin woowu mooy ñu topp saa-senegaal yooyee.
ÀTTEWAAYU MBUUR : AADA FAAS MBËR DINA TËDD ATUM KASO
Aadam Koreyaa, bërekat bees gën a xame ci dàkkentalu Aada Faas, daan nañ ko ñaari ati kaso yoy, dina tëdd menn mi. Moom ak Elaas Njaay mim àndaloon ñoo yem daan. Waaye nag, ñoom ñaar ñépp a war a ànd jox Njaga Ndiir ndàmpaayu 1 500 000 FCFA.
Cig pàttali, keroog guddig 1 jàpp 2i fan ci weeru me, lañ jàppoon Aada Faas ak àndandoom bi ca Sali Portidaal ngir càcc ak congaate. Moom nag, dafa weddi tuuma yees ko gàll. Waaye terewul àttekat bi daan ko.
SITE KËR-GÓORGI : GAASE NAÑU LAYOOKATI USMAAN SONKO YI
Layookati Usmaan Sonko yi seeti woon nañ ko ca Site Kër-Góorgi. Àndoon nañ ak ay wiisiyee (huissier). Waaye de, kenn bàyyiwu leen ñu àgg ça kër ga. Dañ leen a dóor ay lakkirimosen.
ÀTTEKAT BI DINA DÉGLU PAAP NJAAY MU WALF KEROOG 7 SUWE 2023
23 me bii la lañ waroon a déglu Paap Njaay. Waaye dañ ko bëtal ba 7 suwe 2023. Layookatam bi, Musaa Saar, a ko xamle.
Cig pàttali, kàddu yii toftalu lañuy :
“19i tofi toppekat bi ànduñu ci lees yóbbu wayndarew Usmaan Sonko ak Aji Raabi Saar ca àttewaayu kirim ya.”