Mari Tëw Ñaan mi yàggoon a liggéey ak Njiitu réew mi Maki Sàll woo na ay militaŋam ngir ñu wotel waa Yewwi Askan Wi. Moom si boppam, daanaka tuxusi na foofu. Gannaaw bi mu biralee lu ni mel, génnee na itam ab saabal bu mu jagleel Njiitu réew mi. Ci biir saabal bi, delloo na ko liggéey bim ko jagleeloon ci këru liggéey bii di PETROSEN. Mu nekk nag mbir mu doy waar lool rax-ci-dolli di lottal ñii di waa Bennoo.
BFEM 2022 :
Fale ca Yëmbël sud, benn xale bu góor ak àndandoom bu jigéen bu doon def Bfem la yoon teg loxo ndax pexe bi ñu lal ci joŋante yi. Góor gi, ndeke, moo teewal soxna si ci joŋante bi waroon a am ci xayma (mathématiques). Waaye pexe bi mujjul àntu ndax tey ñoo ngi kaso.
Futbal Afrig :
Joŋante bi tàmbali woon diggante ikibi jigéen ya demoon ca CAN ba ñu tëggoon Maroc ci 2eelu fan ci weeru Sulet 2022 ferankulaayu na. Réewum Afrique du Sud ak bu Maroc ñoo daje woon ci joŋante bu mujj bi 23eelu fan ci weer wi. Waaye ikibu Afrique du Sud bee daan bu Maroc 2i bii ci benn. Mu doon CAN bi mu jëkk a yékkati bam soosoo ba léegi.
Koom-koom :
Fan yii weesu, Dolaar jotoon na Ëro ci yemoo weccit yi. Benn dolaar bi daan wecceekoo 555 FCFA léegi 640 lay wecceeku. Ëro nag, demul te dikkul. Ci ay xayma, bile xew-xew dina lottal réewi Afrig yiy jëfandikoo cfa ba noppi delloo seen i koom-koom gannaaw. Tey nag, loolu jur coow ci liñ simboon ay at ci gannaaw. Maanaam am seen weccitu bopp. Mooy gi ñu dippee:« eco ».