Gaawu 31eelu fan ci weeru oktoobar 2020 la Iba Deer Caam génn àddina ci lopitaan “Principal” bu Ndakaaru. 83i at la amoon. Ci kàdduy mbokkam, feebar bu gàtt a ko yóbbu.
Iba Deer jàngalekatu mboor la woon ci Iniwérsite Séex Anta Jóob bu Ndakaaru dale ko 1980 ba 2006. Ci jamonoy Abdu Juuf it, moo nekkoon jawriñ biñ dénkoon njàng ak njàngale ci atum 1983 ba 1988. Cig pàttali, ci jamono yooyu lañ taxawal ci Senegaal xeetu njàngale wi ñuy wax “double flux”, maanaam njàngum ay-ayloo. Nekkoon na fi tamit njiitu “Ecole Normale Supérieure”, di daara ju mag jiy tàggat jàngalekati liise yi.
Iba Deer Caam bokkoon na ci kurél gii di UNESCO te sasoo woon bind mboorum Afrig. Mboorum Senegaal it soxaloon na ko lool ndax ba bi muy faatu mu ngi ci doon def ay jéego yu mag, ànd ceek doomi-Senegaal yu xareñ niki Mustafaa Jóob ak Aamadi Bóokum walla ndem-si-Yàlla-ji porfesóor Yoro Faal ak naataangoom Baabakar Jóob Buuba mi ñépp xam. Waaye lees warul a fàtte moo di ne Iba Deer Caam bañkat la mas a nekk. Biral na ko jamono ja mu newee gone, di yëngu ci sàndika yiy xeex ngir jëmale kanam nekkinu jàngalekat yi. Kon mënees na jàpp ni jàng ak jàngale amaloon nañ ko solo.
Ci wàlluw pólitig, Iba Deer bokkoon na ci joŋante ngir jiite Senegaal ci atum 1993 ; amu ci woon ndam nag waaye sunuw askan fal na ko ay yoon i yoon, mu nekk dipite buñ ràññee ci Péncum ndawi réew mi. Tappal nañ ko raaya yu bari te am solo, ci Senegaal ak bitim-réew.
Maamuse Jaañ, moom, fi ko Iba Deer féete woon, ni mu ko doon taxawoo, tax na mu ne mi ngi jooy tey koo xam ne magam la woon, di baayam. Wolof day wax ne kóllëre ginnaaw, moo tax Maamuse ni nu bu musee nekk jawriñ ci miim réew, Yàllaak Iba Deer la. Kon moom xam na ndem si-yàlla-ji moo doon kan ci mbaax ak laabir.
Iba Deer, ci li ko ñépp seedeel, ku jullite la woon. Taalifkat bii di Aamadu Lamin Sàll nee na bokk nañu benn roppëlaan, waxtu julli jot, Iba Deer taxawal, di julli ci biir, maanaam ci jaww ji. Marcel Mendy, di beneen bindkat bu siiw, feelu na ko ndax dafa ne : « Maa ngi fàttaliku bi ma àndeek Iba Der Caam ci kàmpaañu 1993 bi, fu ko waxtu julli mësaan a fekk, day santaane nu taxaw, bàyyi li nu doon def, julli ba noppi door a dellu ci li nu nekkoon. Ku gëmoon Yàlla la te oyof. »
Dipite bii di Aji Mergaan Kanute, di yit jarbaatu Iba Deer Caam, nee na su demee bay muuru ibaadu tey, nijaayam ju baax jee ko waral.
Senegaal ñàkk doom ju am ñam ci faatug Iba Deer Caam. Dëgg la, bind nay téere bàyyi fi waaye yóbbaale na xam-xam bu bari.
Lu Defu Waxu mi ngi koy jaal ñépp.Yal na suufu Yoof si oyof ci kowam.