JOŊANTEB XARITOO : SENEGAAL DÓOR NA KAMERUN 1-0

Yeneen i xët

Aji bind ji

Gayndey kuppe yi dóor nañ Kamerun 1-0. Tey ci altine ji lañ doon amal joŋanteb xaritoo ca fowub Bollart bu Lens (France). Saajo Maane moo dugal biiwu Senegaal bi. Ab penaaltii la am, dugal ko. Joŋante bi nag, lees ko dugge mooy waajal CAN 2024 biy xewe fa Koddiwaar. Te sax, Senegaal ak Kamerun ñoo bokk genn kippu, war a laale keroog 18 saŋwiye 2024, ca fowub Yamusukroo.

Fu ñaari gaynde daje, pënd ma wuri. Senegaal ak Kamerun, saa buñ waree laale, àddina sépp ay toog di seetaan. Nde, bokk nañ ci ñaari réewi Afrig yi gën mag ci wàllu kuppe, ñu ràññee seen i kuppekat fépp ci àddina si. Moo tax, seen um ndaje mën a doon lépp ba mu des joŋanteb xaritoo. Ni mats tey bi demee firndeel ko. Ndax, ñaari ékib yépp a joxe li ñ amoon yépp, mel ni ñuy xëccoo kub. Mu nekkoon mats bu xumb, saf lool. Kenn mayul sa moroom dara. Moo tax, gaañante bi xawoon na bari ba arbit bi jot fa séddale 4i kàrtoŋi mboq. Senegaal nag moo daan ci seen njëlbeenug joŋante bii laata bu 18 saŋwiye 2024 bi.

Daanaka, ékibu Senegaal bi, ñépp ñoo gis, rawatina Kaliidu Kulibali, Kerepeŋ Jaata, Ismayla Jakobs ak Saajo Maane mi dugal. Dañ foogoon sax ne Kaliidu Kulibali, kàppitenu ékib bi, dafa tàmbaale jëm mag. Waaye, tey de, wone na ne dese na ñeex. Ku weddi laajal ñoom Abuubakar ak ñoom Toko-Ekambi. Dafa di, penaaltii bi sax, moom Kulibali moo ko indi. Nde, moo la wattukatu (défenseur) Kamerun bi takk, mel ni kuy bëre, daaneel ci suuf. Arbit joxoñ tombu penaaltii bi, Saajo Maane toj caaxi Andere Onanaa yi. Senegaal am benn, Kamerun tus.

Kamerun jéem na lu nekk ngir dab Senegaal, waaye dóor bu jub sax amuñu ko. Kon, xelu saa-senegaal yi war dalagum ci li seen gaynde yi wone tey. Waaye, sikk amul ci ne, joŋante bii ak bu CAN 2024 bi duñu niru. Nde, Kamerun dina bëgg a fayu. Waaye, Senegaal bii, bu dëggalee boppam, dina jafee dóor.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj