KÀDDUY USMAAN SONKO 1/2 PÀCC

Yeneen i xët

Aji bind ji

Senegaal gépp amoon na fiy yëngu-yëngu, réew mi jaxasoo, yëf yi doy waar lool, yegg sax fu ko kenn foogul woon. Ñii seen i bakkan rot ci, ñee am ciy gaañu-gaañu yu metti, ñale ñàkk ci alal ju bari. Ginnaaw ba mu jógee “Section de Recherches” bu Kolobaan, Usmaan Sonko amal na waxtaan ak waa réew mi  ci 8eelu fan ci weeru Màrs. Waxtaan woowu nag, dara waralu ko woon lu dul mas-sawu leen ci yi fi jot a xew, xamal leen itam ni mook ñoom a bokk naqar.

Lu Defu Waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc a ngi leen di baaxe ay kàddoom na mu leen yëkkatee keroog jooju.
(Ci taataanug Uséynu Béey)

“Mbokk yi, tey, walla mën naa wax sax ne, fan yii yépp sunu xol neexul, sunuy nelaw néew na, sunu xalaat bari na, te dara waralu ko nag, lu dul tiis wi nga xam ne am na ci réew mi, muy ay bakkan yoo xam ne rot nañ fi.

Kon, dama doon ñaan bala nuy dugg ci waxtaan wi rekk nu daldi def “une minute de silence” jagleel ko sunuy doom, ndax ñi fi faatu ñépp, walla ñiñ fi faat ñépp, nun li nuy doon ndaw ndaw, mat nañuy doom. Tey, jox nan ma lim boo xam ni jeexagul; waaye lim bi nu jotagum mat na fukki nit. Benn bakkan bu rot rekk, ci anam bu mel nii, nga xam ne dañ koo faat, musiba la ci réew mi, rawatina nag, bu ñu nee tey mat nañ fukki nit.
Bakkan yooyu nag, ñooy :

ku ñuy wax Baay Séex Jóob, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Yëmbël ;
Séex Kóli amoon ñaar fukki at, ñuŋ ko faate ci Biññoona ;
Faamara Gujaabi, moom it amoon ñaar fukki at, ñu faat ko Biññoona ;
Paap Siidi Mbay, amoon moom it ñaar fukki at, ñu faat ko fii ci Kër-Masaar ;
Saajo Kamara am fukki at ak juróom-ñett, ñuŋ ko faate Jawobbe ;
Mañsuur Caam, moom it am ñaar-fukki at, ñuŋ ko faate fii ci Ndakaaru;
Alasaan Bari, amoon fukki at ak juróom-ñaar, ñuŋ ko faate fii ci Sànteneer, ci Ndakaaru ;
Musaa Daraame, amoon fanweeri at ak juróom, ñoŋ ko faate ca Ndóofaan ;
Buraama Saane, amoon fukki at ak ñaar, ñuŋ ko faate Biññoona ;
ak Móodu Njaay, nga xam ne moom lañ nu mujje xabaare, ñu faate ko tey fii ci Parsel-Aseni, ci anam yu ñaaw ba fu ñaawaay yem.

Kon, nu ngi leen di ñaanal Boroom bi Mu xaare leen Àjjana. May ñaan nag, ñi fi nekk ñépp, taskatu xibaar ak ñeneen ñi ko teewe,  nu taxaw def “une minute de silence” jagleel ko sunuy rakk yooyu ak sunuy doom yooyu… (Tekkaaral ci diirub benn simili).
… Jërëjëf. Maa ngiy jox sunu sëriñ, Sëriñ Mañsuur Jamiil mu jagleel leen ay ñaan yoo xam ne, haasatan la, yokk barke rekk, ndegam Yàlla def na mu teew fi ; nu jox ko mu defal nu ñaan… (Ñaan).

… Jërëjëf. Kon, dina nu jéem a tënk waxtaan wi ci lu dul gudd torob. Gannaaw bi nu dello nuyu saa-Senegaal yi nuy seetaan yépp, di nuyu ak di gërëm kilifay réew mi, kilifa diine yi, kilifa aada yi, àbbe yi, di rafetlu seen taxawaay ci réew mi. Ndax, wax naa ko ci samay kàddu yu jiitu, bir na ma man, ni ñoom, lañ ca waroon a def, def nañ ko ci bañ ko waree def. Aajowul nu koy jéebaane walla di ko wax ci kaw. Dafa fekk nag, kilifa diine moom, orma rekk lañ ko warlul. Am na loo xam ne, bu naree xotti worma, su ñu waxee ci suuf yem ca. Waaye ku bañ a dégg, ba mbir mi tàng ci sa loxo, dinga dellu ba ci ñoom, woowaat leen. Kon, nu ngi leen di gërëm ci taxawaay bi. Di gërëm kilifay aada yi bu baax itam, di gërëm ñi fi teew ñépp.

Ñii fi nekk ñépp, amul kenn koo xam ne pólitig walla par-parloo moo la fi indi. Amul kenn koo xam ni li nga daj ci fan yii, par-parloo moo tax, waaye ñi fi teew ñépp, li leen tax a jóg ba tax ñu daj ci lu ma ci dajul man, mooy Senegaal, yitte gi ñu am ci Senegaal, bëgg-sa-réew ak am dëggu ni, dañu war a taxaw ngir réew mi, dañu war a taxaw ngir ëllëg, dañu war a taxaw ngir sunuy doom ak sunuy sët. Kon ñoom ñépp dama leen di gërëm man, ci sama tur ; waaye dama leen di gërëm tamit ci turu askanu Senegaal, ndax askanu Senegaal lanu taxawal, taxawalunu Usmaan Sonko. Ñi fi jóg ñépp sonn ci, su doon jëmmu Usmaan Sonko rekk, xéy-na «10%» yi walla «15%» dinañ génn. Bu kenn naagu ba foog ni, yow yaa tax doomi Senegaal yi génn, déedéet.

Li tax lii am, mooy yëg-yëg bu kenn ku nekK xam na ni, sunu réew, sunu askan mu ngi nekk ci ay jafe-jafe yoo xam ne, bu nu seetaanee ba mu deme nenn rekk, defe naa dina rëcc ba fàww. Kon, maa ngi leen di gërëm ñoom ñépp ci turu askanu Senegaal. Bu loolu weesoo, may sargal jigéen ñi it ndax gis nanu seen taxawaay ci xeex bi ; te tey dañ leen ko màndargale, muy bésub “8 mars”.  Jigéeni boor bu nekk nag, du jigéeniy PASTEF kese. Waaye, jigéen ñi taxaw nañ jàpp ci xeex bi. Defe naa Ajaa Yaasin a ngi nii toog sama wet, sama yaay Ayda Mbóoj sama layookat a nga nale, ñoom Maymuna Buso ak keneen ak keneen, su ma leen doon lim tey du jeex, ñoom Aysata Saabara, ñoom Maam Jaara Faam… Ku ma limul rekk bumu ci mer, nu delloo leen njukkal ci bés bii, di leen jaajëfal bu baax.
Mbokk yi, li xew ci réew mii, doy na waar, li xew ci réew mii, aa ! defe naa ñoom Decroix ñoo nu ëpp jaar-jaar fuuf, ñoo nu ci gën a yàgg, waaye gëmuma ne, lii fi xew, mas naa xew ci Senegaal. Du xew-xewi 63 yi, du yi ko jiitu, du 68, du 2000, du 2012, du 88, du 93… Ba tey, defe naa ni lii xew tey Senegaal, masu fee xew. Ba tey jii, Senegaal mooy xët wu njëkk ci xibaari àddina si. Kon loolu du lu tuuti, foog nun waa Senegaal, nu  mën koo natt ; xam lii lu mu doon, ak lan la war a màndargaal ci sunu mboorum  réew. Ndaxte, su dee mënun cee jël ay njàngat ba lii dootul am ci réew mi, bu boobaa, defe naa coono yi dootuñu jariñ dara. Ñi ci seen bakkan rot, ñi ci gaañu, di ñu bari, ñeneen ak ñeneen ak ñeneen, defe naa dootul jariñ dara.

Kon, bu nu waxee loolu, danuy dellu delloo njukkal, ni ma ko defe, ci ñii nga xam ne seen bakkan rot na ci, te dinaa ci dellusi, ma def ko ci ñi gaañu, ndaxte ñi gaañu bare nañ. Di ñaan Yàlla rekk, mu bañ a weesu foofu.

Bi ci des nag, di ci jagleel ngërëm lu ràññeeku ñi nga xam ne, ñooy ndawi Senegaal yi.  Di leen delloo njukkal bu baax. Yàgg nañoo wax ndawi Senegaal yi nii, xale Senegaal yi nale, déedéet ; sunuy ndaw, dañu am awãs ci nun. Li ma gëm mooy sunu ndaw yi dañu am awãs ci nun. Wone nañ ko, ndax ku dem di jàmmaarlook ay takk-der, ñu yore ay fital, yor lu la mën a rey, yor lu la mën a gaañ, yow yoruloo lu dul say loxo ; te defuloo ko ndax dafa am dërëm booy xaar, ndax dafa am ñu féete beneen fànn ñu leen di fay xaalis ngir faat ay bakkan ; yow defoo ko ndax dërëm booy xaar, kon gàcce-ngaalaama ndawi Senegaal. Te nu leen di wax ni, day door rekk. Bis niki tey, na ngeen xam ni réew mi, seen réew la, dogal bi seen dogal la, nun ci seen waaw lanu war a doxe, ñiy def pólitig ci seen waaw lañu war a doxe, di leen déglu. Kon bu leen nangooti di seetaan ba mbir mi egg fu mu warul a egg.

Ma wax nag ni, ñooñu ñépp nga xam ne sonn nañu ci mbir mi, ñi nekk seen kër sax di ko naqarlu, ñi toog seen sijaada  di ñaan, bu ma nekkee fii di waxtaan ak yéen, xam leen ni, yéen a tax, ndax bu ngeen amul woon taxawaay boobu, waxuma la tey jii, waxuma la àjjuma bii weesu, waaye altine 8i fan weeru feewiryee laa waroon a nekk Rëbës. Kon man tey jii, duma woon nekk fii di wax ak yéen. Kon bu leen kenn gëm loo ne, dañ noo beral loxo. Waaye seen taxawaay, li mu firndeel rekk tey, mooy li Tubaab naan : «La souveraineté appartient au peuple» Lépp askaan wee ko yore. Mooy kàttan dëgg-dëgg-dëgg ; sañ-sañ dëgg-dëgg-dëgg cim réew, askan wee ko moom, kenn moomu ko. Ñoom dañuy faral di wax, loo wax ñu ni «Force restera à la loi». Waaye yoon, «la loi», mooy askan wi ; yoon wi du dipite, du Maki Sàll… Ku dem nag ba sàggane ko, foog ne yoon wi ñu wote, te askan wi wote ko, mën nga koo jalgati di ko teg ci kaw nit ñi, askan wi da la koy fàttali, te loolu moo leen dal tey.

Kon taxawaay boobu, ngalla waay, bumu deñati Senegaal. Bumu deñati ndaxte li ñuy wax les «grandes démocraties» (demokaraasi yu mag yi), boo gisee njiit yi am lu ñu sañul foofu, mooy askan wi dafay taxaw jonn di leen di wattu. Saa su ñuy génn rekk, nit ñi génn ne leen «lii duñu ko nangu». Kon nanu am taxawaay boobu bés niki tey. Ma wax tamit ni, ñii nga xam ne, ñu ngi ci kaso yi, tey lu ëpp téeméeri nit ñu ngi ci loxo Maki Sàll, ñii Tàmbaakundaa, ñii Sigicoor, ñii Kéedugu, fii Ndakaaru, ba Ndar, Tiwaawan, fu ne jàpp nañ fay nit ñoo xam ne, sàccuñu, reyuñu nit, wuruxuñu, luxusuñu ay biye, luubaluñu xaalisu réew mi. Seen tuuma mooy dañoo dox-ñaxtu, te Ndeyu-sàrti réew mi moo leen jox sañ-sañu dox-ñaxtu. Nu ngiy mas-sawu ñooñu, waaye di leen xamal yit ni, dun leen seetaan.
Di mas-sawu it ñi nga xam ne ñàkk nañ ci seen alal ndaxte yàqu-yàqu yi bari nañ. Loolu du woon cëslaayu mbir mi ; ñi jóg di naqarlu duñu ay saay-saay ; ay nit nag, mën nañ cee rax, waaye, loolu taxuleen woon jóg. Te it sunu xeex, jubluwunu ko ci askan sàngam walla réew sàngam, du loolu mooy sunu xeex. Waaye dafa fekk daa am fu mbir yi di tollu, lépp mën na cee jaxasoo, lépp mën na cee am ; waaye loolu du woon cëslaay gi. Ndaxte, ku bëgg yor réew ak ku bëgg defar réew, doo toj alalu jaambur, doo yàq oto jaambur, doo toj këru jaambur. Kon loolu, nuŋ koy mas-sawu bu baax nit ñi mu dal.

Di mas-sawu njabooti ñi ci faatu, di leen jaal, te bu soobee Yàlla, dinañ góor-góorlu ba kenn ku nekk, nu def sunu «délégation», ñi fi nekk ñépp dox ñëw jaaleji leen, di mas-sawu njabooti ñi ci gaañu ; lañ ci man it ci taxawu dinan ko def. Di mas-sawu njabooti ñi nga xam ne tey, caabi féete na leen ginnaaw ; wax leen it ne seetaanunu ñooñu ndax ginnaaw ba nu jëlee awokaa yi leen war a layool, kenn ku ne, nu ngiy góor-góorlu ci liñ la man a jàppalee ba doo tumuraanke, walla sa njaboot du tumuraanke.

Waaw mbokk yi, lii lépp lan moo ko waral ? Lii lépp ci ay tiis yu dal ci Senegaal la. Li ko waral mooy xiif gi nga xam ne, Maki Sàll ak ñi mu àndal xiif nañ ko nguur ; ak yaakaar ni ñoom dañu war a yore nguur gi toog fi ba fàww. Lii lépp moo leen ko andil. Moo ne de, ay at ca ginnaaw loolu lan fi xeexoon ba ay bakkan rot fi. Li andi lii, mooy nguur gi ñu teg ci loxo Maki Sàll, ne ko : «Jox nan la sunuy mën-mën, jox nan la sunu alal, jox la «administration» bi, jox la yoon wi “justice”, jox la xare réew mi, maanaam “arme” bi, jox la lépp loo soxla li nu bëgg mooy nga defar réew mi, li nu bëgg mooy ndaw ñi am liggéey, li nu bëgg mooy nit ñi faju, li nu bëgg mooy tali yi baax». Maki Sàll walbati loolu lépp, jël ko muy doole ju muy teg ci kow saa-Senegaal yi. Muy kuy pólitig, muy kuy «mouvement citoyen», muy «Sociéte civile», képp ku ne àndumaak Maki Sàll rekk, teg na doole jooju sa kow. Loolu moo nu andi ci lii. Mu ànd ci ak ay nitam yoo xam ne, duñ ko wax dëgg, mbaa sax ñoo ko yées, soo moytuwul, moom ci boppam.

Ndax lii am yépp nag, ñi ko séq bari nañ de, waaye li ci ëpp ay jëfkat yu ndaw lañu. Boo ko doon seet, ñeenti jëfkat lañu : Maki Sàll, Antuwaan Jom, Maalig Sàll ak Basiiru Géy. Ñeneen ñépp ay suq lañu, nga xam ne, dañu leen di defloo ñuy def. Waaye ñeent ñii, musiba Senegaal yépp, ci jamono yii ñu tollu tembe, ci ñooñu la. Ndax jaadu na, 16i milyoŋi doomi-Senegaal ñeenti nit rekk lëmbe leen? Ndax loolu war nañ wéy di ko nangu ci dëkk bii ? Loo wax nag, ñu ne la nun noo yor nguur gi, “force restera à la loi”. Te, yoon, “loi” boobu, duñ ko tudd lu dul bu dee ci kujje pólitig gi. Yoon woowu dañ koy walbati ngir man a jot ci képp ku àndul ak ñoom ; waaye saa su yoon wi waree dal seen kow, ñu ne mukk du fi am. Ñaata nit ñoo fi mas def ñombe yoo xam ne kenn du ko tudd ? Tey, ñu ngiy romb waa Senegaal di leen yëkkatil i mbagg. Loolu nag lanu mënatul a nangu. Looloo tax nit ñi jóg ni, lii dootunu ko nangu, dootu fi am.”

(Dees na ko topp…)

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj