KAN MOOY ISAA SÀLL ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

« Jàpp naa ne pólitig du liggéey, jàngale mooy sama liggéey » (Isaa Sàll)

Isaa Sàll, ab wutaakon la ci wote palug njiitu réew mi ñu dégmal, bésub 24eelu féewaryee. Moom, nag, mébétam mooy bett nit ñi, ni pàrteem bii di PUR bettee woon ñépp ci wote ndawi Péncum réew mi. Dawalkatu roppëlaan, kàngamu xamtéef, njiitu daara-ju-kawe… Ñett a ngoog ci fukki mbir yees war a xam ci Isaa Sàll.

1. Ñaari melo -nëtëx, weex- ak ñaari picc

Isaa Sàll moo jiite pàrti bi ñu duppe PUR. PUR, nag, meloy nëtëx ak weex, ak ñaari picc yi lees koy màndargale. Isaa Sàll ku jar a bàyyi xel la. Ndaxte, moo nekkoon mbetteel ci wote ndawi Péncum réew mi yiñ fi amaloon ñaari at ci ginnaaw, doonoon ñeenteelu pàrti bi ëppoon i baat ci Senegaal. Ndege, amoon na 155 000 baat, maanaam téeméer boo jël ci pal googu, lu jege juróomi nit PUR lañu sànniloon kàrt.

2. Ndoorteelu Isaa Sàll ci làngu pólitig gi

Guléet Isaa Sàll bokk ci palug njiitum réew. Waaye, ku fàttaliku jaar-jaaram, dinga gis ne jotoon naa bokk ciy wote. Waaw, Isaa Sàll nekkoon na fi Njiitu ndajem diiwaanu Fatig ci njeexitalu atiy 1990. Ginnaaw loolu, askan wi wóolu woon na ko ba fal ko dipite ci atum 2017.

3. Mustarsidiin

Isaa Sàll ab taalibe Séex la. Mi ngi bokk ci daayira « Mustarsidiin wal mustarsidaat » te mu tekki ci wolof “Ndajem góor ñeek jigéen ñiy sàkku yoonu njub”. Kon mënees na ne mbootaay moomu, saxal jëf ju baax a ko tax a jóg. Daayira ji, nag, ci tarixa tiijaan la féete, te ay taalibeem ci seen yar ak teggin lañu bëgg ñu ràññee leen. Ku sukkandikoo ciy waxi Isaa Sàll ci boppam, téeméer boo jël ci waa daayira « Mustarsidiin wal mustarsidaat », juróom-ñeen fukk yi -90%- ci PUR lañu bokk. Looloo waral, xam naa, ñenn ñiy jaawale pàrti beek daayira ji.

4. Jamaale

Waaye taskati xibaar yu bare biral nañu ne, diggante Isaa Sàll ak Sëriñ Mustafaa Si xaw naa xajam jamono yii. Sëriñ Mustafaa Si, nag, mooy kilifay daayira ji, rax-ci-dolli am na ñu naan mooy njiitu PUR. Waaye, Isaa Sàll moom weddi na loolu ba tëdd ci naaj wi. Nee na tey la seen diggante gën a ritax te sax, li Sëriñ biy jëflanteek moom, du ko jëflanteek keneen.

5. Dawalkatu roppëlaan

Juróom-benni at a ngi nii bi Isaa Sàll amee lijaasa dawalkatu roppëlaan. Looloo ko may mu bokk ci “aéroclub” bu Ndakaaru. Saa yu ko ko jotam mayee, Isaa Sàll a ngi dawal ay roppëlaan yu ndaw te mën a yab ñeent ba juróom-benni nit. Bu ko defee, muy doxantu ci kow asamaan si, tey mu tiim Ndar, ëllëg mu tiim Kaasamaas.

6. Kàngamu xamtéef

Isaa Sàll mi ngi jànge ci liise Charles de Gaulle bu Ndar. Waaye Iniwérsite Séex Anta Jóob bu Ndakaaru la ame lijaasa bi ñuy wax “DUT” ci wàllu “électronique”. Ci la deme Amerig, daldi fay am lijaasa « doctorat » ci wàllu xamtéef, maanaam « Informatique », ci Iniwérsite George Washington. Bi mu dellusee Ndakaaru, ci la tàmbalee liggéey ci mbirum xamtéef ci « Météo Sénégal » laata muy bokki ci « Centre régional africain de technologie » te gàttal bi ci nasaraan di joxe CRAT.

7. Njiitu daara-ju-kowe

« Jàpp naa ne pólitig du liggéey, jàngale mooy sama liggéey. » Isaa Sàll jàngalekatu xamtéef la. Iniwérsite bi mu sos ci atum 1998 tey njiit li, « Université du Sahel », bokk na ci gën a siiw ci Ndakaaru. Tey jii, lu mat 1 500 ndongo bindu nañu fa te ña fay jàngale tollu nañ ci téeméer ak lu teg.

8. « Parrainages » yi

PUR ab pàrti bu am cëslaay la, te yit bari nay boroom xam-xam yu ci bokk. Looloo tax mu def liggéey bu rafet ci “parenaas” yi ba rawoon sax ay naataangoom.

9. Dëkkandoo Maki Sàll

Isaa Sàll mi ngi juddu ci atum 1956 ca Taatagin, dëkk bu nekk ci diiwaanu Fatig, dande ko 20 kilomeetar doŋŋ. Kon, Isaa Sàll ak Maki Sàll, ñoo bokk seen Fatig, fa lañu fekk baax. Waaye dawalkatu roppëlaan bi mage na eñseñeer bi juróomi at.

10. Nit ku laabiire

Ni ko ay moroomam defe, Isaa Sàll wone na laabiir ñeel Xalifa Sàll mi ñu nëbb jant beek Kariim Wàdd, di ñaari wutaakon yi ñu seppi ci wote palug njiitu réew mi. Ndaxte, moom Isaa Sàll nee na, nguur gi dafa kootook yoon ngir xañ ñaar ñii seen àq ak seen yelleef.

Paap Aali Jàllo

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj