KAN MOOY… IDIRIISA SEKK ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Maaraa la ko ay jegeñaaleem di woowe, doomi-réew mi naan ko Idi. Taskati xibaar yi ñoom, Ndaamal-Kajoor lañu koy dàkkentale. Idiriisa Sekk — mooy turam dëggëntaan — dib pólitiseŋ bu ñu ràññee ci Senegaal, Cees la fekk baax. Te sax, nekkoon na fa Meer ci diirub fukki at ak ñaar. Ci ginnaaw gi la doon njiitu Ndajem diiwaanu Cees ba nëgëni-sii.

Ci atum 1988 la Idiriisa Sekk ganesi làngu pólitig gi, waa Senegaal tàmbalee xàmmee xar-kanamam. Boobu, aw waxambaane la woon, amoon ñaar-fukki at ak juróom-ñeent doŋŋ. Mu xawoon a jaaxal nit ñi ndaxte, ci jamono yooyu, ay màgget rekk lees daan faral di gis ci làng gi. Foo fekkaan ngóor su gàtt soosu te ñuul, mi ngi topp ci ginnaaw Ablaay Wàdd. Dëkkoo- dëkk wër nañu ko, ñoom ñaar, di sàkku baatu askan wi ngir góor gi Wàdd toog ci jal bi. Laata ñu doon noppee laaj « Kii ku mu ? », mu yéem ñépp ndax xam-xamam ak xereñam. Jamono jooju la biddéewam feq, foo dem ci réew mi walla sax bitim-réew dégg turam.

Ci màrs 1990 la jëkk a doon jawriñ cig nguuru Senegaal. Mooy jamono ja Abdu Juuf yaatalee gornmaam, xajal ci kujje gi. Ñaari at yi jiitu woon loolu, nag, ay yëngu-yëngu yu metti amoon nañu Senegaal. Niñ koy waxe rekk : ginnaaw ay, jàmm. Idi la Juuf dénkoon njula mi.

Àddinay dox ba Ablaay Wàdd duma Abdu Juuf ci atum 2000, wuutu ko ci jal bi. Ci la tànne Idi, def ko bëkk-néegam. Ci weeru nowàmbar, atum 2002, nag, la ko “Góor-gi” tabb Njiitu jawriñ ji. Rax-ci-dolli, moo toppoon ci Ablaay Wàdd ci kilifteefu PDS.

Jaar-jaar boobu, nag, dug tandale. Ndax kat, bu dee wax dëgg rekk, fu mu mas a jaar, Idi def na fay jaloore yees koy màndargale. Bunu fàtte ni ngóor sii ganesi àddina ci atum 1959, ca Cees, dafa mas di raw ci kalaas yim jaar yépp, ba muy tuut-tànk ba ba muy am « bakaloryaa », ñu daan koy faral di ràññee yit ci « Concours général ». Noonu la ko jàppe woon itam, ci njàngum daara yu kawe yim defoon ca Pari ak ca Iniwérsite Princeton bu Amerig. Waaye mbirum Princeton moomu, lu mat a seetaat la ndax indi na fiy werante : gëstukat yu bare nee ñu lekool boobu, deful lu-dul jaar fa ni melax, bokk ciy lël yu ñakk solo te jëliwu fa benn lijaasa bu tax ñuy wax. Ci gàttal, ñoom jàpp nañ ni masul a jànge Princeton. Lu ci mënti am, warees na cee yokk ne xelam mu neex moomu, ay ustaasam a ko njëkk a seetlu ndax ba muy gone, ndongo-daara lu mënoon a jàng la. Foofu la jële dàkkentalu Maaraa biñ koy faral di woowe. Am na sax ñu jàpp ne ni muy def, di tariy aaya suy wax waxu pólitig, tiitar doŋŋ a ko ci duggal. Leneen lu ma seetlu ci jaar-jaaram moo di ne, ak li muy teel a dugg ci làngu pólitig gi yépp — fukki at ak juróom rekk la amoon — Idi jot naa liggéey ci Pirwe bi laata muy bokk ci nguur gi.

Mook i àndandoom am nañ lu ñu bàkkoo ndax nee ñu ba mu jiite jawriñ yi, yokkute dellusi woon na ci koom-koomu réew mi ba tax Club de Paris gën a wóolu Senegaal, abal ko xaalis bu baree-bari ; defaratoon nañu tamit lu xaw a tollook 1500 ci dëkk-dëkkaan yi, jaare ko cib naal bu Idy tudde woon Grappes de Convergence. Bu loolu weesoo, am na ñuy wax ne moom Idiriisa Sekk moo fekki woon Yaaya Jaame Gàmbi, fexe ba mu nangu ni jot na ñu lëkkale Senegaal ak Gàmbi : ci lañ tàmbalee liggéey ci pomu Farafeñe bi Maki Sàll ubbi keroog…

Ni ko ñépp xame, baayu Maki Sàll wattukat la woon waaye teewu koo jiite tey Senegaal. Baayu Idirisaa Sekk moom, da daan jaay fëgg-jaay màrse Cees waaye teewu ko fee nekk kilifa gu mag ci réew mi. Kon ñoom ñaar ñépp ay doomi baadoolo lañu te mënees na leen jàppe niy jàmbaar yu ñu war a naw ci wàll woowu ndax dañoo ñefe, fas-jom, ba génn ci.

Waaye nag, mu nel ni ndombog-tànk googu di Njiitu jawriñ ji du woon njiglaayu Idi. Tuuti rekk la toog, ay jiixi-jaaxa tàmbali ci digganteem ak Ablaay Wàdd mi mu jàppe woon ni baayam. La ko ca fekk neexul, ndax ba ñu tekkee ndombog-tànkam ci awril 2004, teg nañu koy tuuma, nëbb ko jant bi lu tolloog juróom-benni weer. Jiiñ nañ ko sàcc, ne dafa randal àlalu réew mi. Dem na ñu sax ba ne daa bëggoon a nasaxal kaaraange réew mi. Moom nag, masul a nangu tuuma yooyu ñu tegoon ci ndoddam te mujje gi àttekat bi setal na deram. Loolu am na, waaye ñu bare tey bëggoon nañoo xam fan la ngóor si masuta liggéey, daanaka, jële alalam ju dul jeex ji ! Su nit ñiy gise Idiriisa Sekk ni pólitiseŋ buy loxoom setul, looloo tax.

Ba mu jógee ci tolof-tolof yooyu la Idi féete ci kujje gi, taxawal pàrti bi mu duppe « Rewmi » (ñu waroon ko binde : Réew mi ) ngir jàmmaarlook nguuru Ablaay Wàdd. Fii, xel yépp dem ci Séex Aliyu Ndaw, bindkat bu mag bi jagleel ab kilib xareb ‘’Guy-Njulli’’ : Makoddu Faal ak Sàmba Lawbe Faal, Baay ak Doom, jàkkaarloo ca Kawóon… Wàdd ak Idi naka noonu. Pólitig moo mel noonu, gënatee gudd i tànk àddina ! Ca njeexitalu wote 2007 bi, naam Idiriisa Sekk rawul woon, waaye mëneesul a wax ne amu ca woon ndam. Ndax kat, ñi ko sànniloon kàrt tollu woon nañ ci limu 15%. Ku fàttaliku dooley Ablaay Wàdd ci jamono jooju, doonte sax amoon na lu bare lu ci wàññeeku woon, dinga gën a xam ne Idi defoon na jaloore. Ndege, fexe woon na ba raw pólitiseŋ yépp ba mu des Wàdd te ñu bare ci ñooñu yàggoon nañ lool ci géew bi.

Waaye Wolof Njaay nee na ku sa xel wër ñaari yoon gaañ la : muus ba mu ëpp baaxul. Mu mel ni looloo daloon Idi ba muy jaabante diggante këram ak Màkkaanu Wàdd, ku ci nekk di jéem a nax sa moroom, mu réere mbir xanaa ne ku la mag ëpp lay sagar. Ci lañ ko tàmbalee weddi, ñenn ñi sax mere ko lool mbaa ñu jéppi ko. Daan nañ faral di wax yit ne dafa beew te gaaw a xeebaate. Noonu la ñàkkee soppeem yu bare, ay farandoom dëddu ko, dooleem daldi wàññiku bu baax-a-baax. Li koy firndeel mooy wote yees amaloon ci atum 2012, te amu ca lu-dul limu 8% gën caa bare. Ki mébétam doon nekk ñeenteelu Njiitu Réewum Senegaal, waratee muñ ay at laata xelam di sañ a dem ci jal bi ko mas a tee nelaw…

Bi Maki Sàll faloo, Idiriisa Sekk àndoon naak moom ca njëlbéen ga, ay ñoñam bokkoon nañ ci gornmaa bi Maki Sàll njëkk a taxawal. Waaye yàggul dara ñu tàggoo, mu daldi dellu ci kujje gi. Mënees na ni kon amoon na nu mu jàngate jaar-jaaru boppam, gis ni war naa doxale neneen, maanaam jàpp njaamburam, dal-lu, maandu, dem fekki nit ñi ci dëkk-dëkkaan yi, waxtaan ak ñoom ci yar ak teggin. Ci gàttal, daa gënoon a fullaal aajoom, jox ko àqam yépp. Noonu la def ba askan wi xaw koo wóoluwaat, di ko may nopp. Wànte xawoon naa yàqule as lëf bi mu xéyee bés di méngale “Màkka” ak “Bàkka”, indi fiy werante yu mënoon a ëpp loxo.

Idiriisa Sekk, ci fan yii weesu, ak mbër mi ñu naan “Zoss” te mu bokk ci ñi koy kàmpaañal

Léegi nag, Idiriisa Sekk bokk na ci juróomi wutaakon yiy laaj boppu réew mi, ginnaaw bi mu amee ndam ci joŋante “parenaas” yi Maki Sàll sooke te ñu bare jàpp ne pexe la woon rekk ngir wàññi dooley kujje gi. Ci jamono yii nag, Idi neexut a dékku, ndax yaakaar gi mu dekkal ci xolu askan wi. Looloo waral ñenn ci kàngami kujje gi fekksi ko, ñu taxawal ag lëkkaloog làng ci wote 24 féewaryee biy dégmal. Li ñu ko dugge, nag, mooy jële fi Maki Sàll ; te jàpp nañu ne Idi daal a fi sës.

Loolu dina àntoom ? Bi mu jógee bërki-démb Tugal, Ablaay Wàdd nee na du jàppale Maki, du jàppale Idi te yit dina def kem-kàttanam ba kenn du fi wote. Askanu Senegaal a ci des : kan la nar a fal feek i fan ? Ndax Ndaamal-Kajoordina gàddu ndam li bii yoon ?

Looloo ko tax a samp ndëndam ci géew bi… Kon nanu xaar, li ci kanam rawul i gët.

Uséynu Béey

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj