KAN MOOY USMAAN SONKO ?

Yeneen i xët

Aji bind ji

Usmaan Sonko nëbbu ko kenn : mébétam mooy jot ci réewum Senegaal ci guddig dibéeru 24 féwaryee 2019, wuutu Maki Sàll.

Ci li ñépp seetlu, waa nguur gi ñemewuñu ko lool. Lu nekk ñu ngi ko koy yakk. Bu teyee ñu ni ay doxandéem a koy jàppale, di ko may xaalis bu dul jeex bu mu làq bitim-réew, bu ëllëg saa ñu ni salafist la, faalewul sunu tariixa yi ; Mustafaa Siise Lóo sax dem na ba ni mook way-fippu Kaasamaas yee bokk gis-gis.

Kan nag mooy gone gii wutewul ak cuuraayu dëmm ci Maki Sàll ak i nitam ? Lu tax ñu ragal ko ba mu leen di jëfurloo ?

Du ku ñu miinoon xar-kanamam ci làngu politig gi. Daanaka bi ñu ko dàqee ‘’Impôts et Domaines’’ la ñuy door a dégg turam. Kon, gornmaa bi muy xeex tey, liggéeyal na koy at yu mu ne patt, tëj gémmiñam. Xéy-na booba xel mi newagul woon ci politig.

Usmaan Sonkoo ngi juddoo Cees ci atum 1974. Waaye ginnaaw ay way-juram ndawi gormaa bi lañu woon, Sigicoor la màgge. Yaayam, Maam Xadi Ngom, séeréer la, di yit pulaar, baay biy joolaa.

Seen doom ji bokk tey ci wutaakon yi te xelam màcc lool ci mbirum lempoo ngi denc ñaari soxna, am ak ñoom juróom-benni bant.

Du benn du ñaar, Usmaan Sonko wax na ne bés buñ ko falee, li koy gën a yitteel mooy dog buumu njaam gi ay doxandéem, rawatina njiiiti Frãs yi, tënke Senegaal. Dem na fi Mante-la-Jolie, ca Frãs, yakk Tubaab yi lu mel ni xeme, ne seen yoon nekkul ci ni nuy téyee sunu réew ak sax yeneen réewi Afrig yi ñu tegoon loxo ciy jamono.

Petorool beek gaas bi feeñ Senegaal bu yàggul it, lu ko amal solo la. Li tax sax ñu bari xam Sonko tey, mooy tuuma yi mu yëkkati ci atum 2016 teg leen ci kow Maki Sàll ak rakkam Aliyu Sàll. Booba la kor Maryeem Fay mer, delloo koy kayitam, taafantoo ne kilifa gu tollu ni Sonko daa war ni muut mbaa mu ni mott. Niñ ko dàqe noonu ci liggéeyam, dafa gën a njaxlafloo Sonko, mu mel ni fitt guñ sànni te kenn mënatu koo tëye. Ñaari at rekk lañ ci teg mu génneb téere, tudde ko Pétrole et gaz au Sénégal — chronique d’une spoliation, di ci fésal ni nguur giy jalgatee sunu alal ak it ni ñu leen di gere ci anam gu jéggi dayo, réew miy ñàkk ay milyaar.

Ni Sonkoy doxale, day biral ne xar na tànku tubéyam ci indi doxalin bu bees pull ci làngu politig gi. Kon, booy seet bu baax, ñi mas a toog ci jal bi yépp la fas-yéenee jàmmaarlool. Waaye am nay boroom xam-xam yu ni loolu yëfu cuune la ndax bu nit ñi xamee foo jëm doo fa yegg. Mooy tamit liñ naan kuy yoot du sëqat.

Niñ ko fi waxe, Usmaan Sonko gan la ci géew bi te mooy caatu juróomi wutaakon yi yoon may ñu bokk ci joŋante ren bi. Teewu koo am bayre, ndax askan wi fullaal nay kàddoom, fépp fu mu dem ndiraan topp ko te ñi ëpp ciy farandoom ay ndaw lañu. Xanaa li mu tàmm di ŋàññ nguur gi ak ay baat yu ñagas te dëggoo tax gone yi sopp ko. Ñu bare jàpp nañ ni Usmaan Sonko, kenn feesul i bëtam. Ku gëm boppam la, bëgg réewam te foo mënti dem ci Senegaal fekk fay mbokkam, moo xam Cees la walla Bawol ak Ndar mbaa Sigicoor ba ci Njum ca Fuuta ak Sibixotaan ci diiwaanu Ndakaaru.

Ku mas a bëgg karate ak sido la te ba léegi sax saa yu ko ko jotam mayee mu wékki kimónoom sol, tàmbalee tàggat yaram wi. Am na benn xaritam bu nu ne aayoon na lool basket tamit te bu ko deful woon po kese ñàkkul mu am ci tur.

Waaye njàngam la jiitaloon.

Bukot-Sud la njëkk a dal lekool, def fa juróom-benni at soog a jàll kolees Amical Cabral, génne faak BFEM.

Ci atum 1995 la am bakaloryaa ci Liise Giñaabo, bokk ci ña fa rawoon. Ci la bindoo iniwérsite Gaston Berger ; ci menn atum 1999 la am lijaasa ci ‘’Droit public’’ ba noppi bokk ci joŋante ENAM bi, jëlati pee.

Taxu koo naagu ndax bi mu génnee ENAM, tàmbalee liggéey ‘’Impòts et Domaines’’ bu Pikin, la ne fàww mu yokk xam-xamam, di wéy di jàng UCAD ba ni mu ame ci atum 2003 DEA ci ‘’finances publiques et fiscalité’’

Dëgg la, Usmaan Sonko raŋale nay lijaasa yu bari waaye li ci ëpp solo moo di ne daanaka Senegaal la ame léppam, muy ndam ak sag ci moom, mu bëgg nag fey naar bi xoromam, ne du nangu mukk ay doxandéem ak i dunguruy Tubaab yiy paacoo alalu réew mi.

Ci li mu wax, njiitu ‘’Pastef-Les Patriotes’’ fas naa yéenee jëmale kanam beykat yeek sàmm yeek mooli Senegaal. Dinay faral di wax ne feek Senegaal a ngi jéggaani li muy dunde, mbay mi du mën a dox, ginnaaw rekk lay des, naka noonu koom-koom bi. Te loolu, lii rekk la tekki : waa kow gi duñ tàggook ndóol, te dina jafe ñu sàmm seen ngor.

Usmaan Sonko ndaw la te Senegaal, ci téeméer bo jël, genn-wàll gi ay ndaw lañu ni moom. Moo ko tax ne dina leen jàppale bu faloo, def kem-kàttanam ba dootuñu soxlaa song géej gi naan Barsaa mbaa Barsàq ngir rekk am lu ñu suturloo.

Ñetti ponk a ngoog yu ñu jukkee ci Solutions, ñaareelu téere bi mu génne ci sàttumbar 2018. Leneen lu am solo ngi ci biir Solutions : Usmaan Sonko da ciy wax ne feek Senegaal génnul ci weccitu CFA, du tegu ci yoonu naataange.

Bu ñu fàtte tamit ne Usmaan Sonkoo sos Syndicat Autonome des Agents des Impôts et Domaines (SAID) ci 2005, jiite ko lu mat juróom-ñaari at, ba 2012.
Am na lu xaw a yéeme ci jaar-jaaru Sonko : bi ko Maki Sàll dàqee ci atum 2016, la ko askan wi fal. Ndax su dul woon loolu xéy-na du doon tey dipite.

Ñaari at ci ginnaaw, la kii di Usmaan Sonko sos pàrteem, tudde ko PASTEF (ci nasaraan Patriotes du Sénégal pour le travail, l’éthique et la fraternité). Ci atum 2017 la sos itam Atlas, di ci liggéeyal boppam.

Léegi, PASTEF bett na ñépp jàll parenaas yi, njiitam wër na réew miy xamle yéeneem, muy soppi nekkinu askan wi, rawatina ñi gën a néew-doole.

Waaye am ñu seen xel teey ci digganteem ak Ablaay Wàdd mi mu mel ni ku mu jébbal boppam. Bi ‘’Góor-gi’’ jógee bitim-réew, Sonko daa dakkal lépp li mu doon def, dem seeti ko. Gisewaat nañu otel ‘’Terou bi’’ (Teeru bi lees war a bind). Ñoom ñaar rekk a xam lan lañu waxante. Du ñàkk Wàdd yedd ko, ni ko maam waree def ak sëtam. Amaana tamit Sonko dig ko ne bés bu toogee ci jal bi, Karim Wàdd ak Xalifa Sàll lay njëkk a génne kaso.

Ak lu mën a xew ginnaaw-ëllëg, kenn ci réew mi dootul fàtte doomu Maam Xadi Ngom ji. Te su taxawee fi mu taxaw, ànd ak fulla ci li muy def te ñeme lu metti, feek juróomi at rekk mën naa am ndam lu réy. Ndax bu boobaa dina sàmm kàddoom, xam ne dige bor la ? Mbaa du dafa nar a def ni gaa ñi ko fi jiitu yépp, duut baadoolo yi ba noppi di leen mbëllee ?

Tontu ci loolu jafe na lool.

Usmaan Sonko nee na bu bés ba ñëwee dina soppi politig ci boppam : Yàlla bu ko politig soppi, moom Usmaan Sonko, nun nu nekkati fiy dunde yaakaar.

Ndey Koddu Faal

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj