Ci Baatu Majaw Njaay
Aw askan, bala moo tànn njiitam, war naa seet bu baax jikkoom, seetaat ko, xam mooy kan. Looloo waral Lu defu waxu, seen yéenekaay ci kàllaamay Kocc, jóg ngir jagleel wutaakon yi ay xët yuy fésal seen jaar-jaar ak seeni naal ñeel réew mi. Maanaam, li yitteel Lu defu waxu moo di xamal leen ñan ñooy dëgg-dëgg ñooñiy wër réew miy soow, te miir bu seeni ndaw gis taf fay nataal yu leen di màndargaal. Ndax, ku taxaw ne mën ngaa saafara jàngoro yi askan wiy jànkoonteel, warees na yëdduy mbiram. Li nu ko dugge, nag, du lenn lu-dul jox askan wiy tegtal ngir mu tànn ki mu yaakaar ne moo gën ci Senegaal.
Bu ko defee, nan tàmbaleek Maki Sàll, njiitu réew mi bëgg ñu falaat ko.
Ci atum 2000 la askanu Senegaal folli Abdu Juuf, fal Ablaay Wàdd. Ñu teg ci fukki at ak ñaar, mu doyal sëkk ci ‘’Góor-gi’’, dàq ko, Maki Sàll daldi toog ci jal bi. Ñépp am yaakaar ju réy ci moom, ndax guléet nu amoon njiit lu juddu fekk réew mi moom boppam ba noppi.
Maki Sàll digewul yem ci. Daanaka dafa waatoon ni dina indiy coppite yuy jëme sunu gaal gi kanam. Te ginnaaw xamoon na ne danoo xobe lool ci demokaraasi, sopp lépp lu koy dëgëral, foofu la doore. Moo ko taxoon a giñ ne dina wàññi moomante yi ci boppu réew mi, jële leen ci juróom-ñaari at yemale leen ci juróomi at doŋŋ te, ku xas ba moome ñaari yoon, dootoo mën a toogaat ci jal bi. Waaye yàggul dara mu tàmbalee indiy tànki bukki, daldi ne, aa, man kat sama yéene rekk laa waxoon, waaye këru-àttekaay gi gën a kowe ci Senegaal nee na du ci dal, fàww ma matal juróom-ñaari at yi, ñu door a seet naka lañuy def. Kon mu mel ni Maki Sàll dafa noo bëggoon a gëmloo ne amoon na lool naqar ci li ko yoon mayul mu wàññi màndaam bu njëkk bi. Loolu yabaate lay nirool. Fi mu ne nii, benn weer kesee ko ci dese te talul dara lu-dul faluwaat. Gaa, def sa kemtalaayu-kàttanam ngir ñu sànnil lay kàrt, dara aayu ci waaye laaj bi am solo dëgg mooy : ndax askan wi doyal na ci nguuru Makeem déet ?
Dinan ci jéem a tontu.
Bi Senegaal moomee boppam ba ñu teg ci benn at la Aamadu Abdul Sàll ak Kumba Timbo am doom ju góor ca Fatig ; bés ba delsi, ñu ngénte ko, tudde ko Maki Sàll. Niñ ko waxe sànq, li ko wutaleek Seŋoor ak Abdu Juuf ak Abdulaay Wàdd, moo di ne moom rekk a fi nekkagum njiit lu fekkewul jamonoy nootaange Tubaab yi. Warees na cee yokk leneen lu am solo : ci réew mii doŋŋ la mës a jànge ba ni mu génne iniwérsite Ndakaaru ak lijaasa biy biral ne ku xam-xamam màcc la ci mbirum petorol ak yu ni deme.
Ku say way-jur néewoon lool doole, nga ñefe ba réewum lëmm ne la yaa nu doy, dénk la boppam, bu la neexee nga ndamoo ko. Kon, Maki mënoon naa janook goney Senegaal ni leen : “Sama pàppa ak sama yaay amuñu woon alal, bokkuuñu woon ci yax yu réy yi wànte teewumaa fas jom, di jàng ba toog fi ma toog tey jii ! Defleen ni man !“ Su doxale woon noonu, dina doon royukaay. Waaye Buur, ci ñi la gën a jege, fàww mu am ciy dunguru yu lay dëkkee jay, di la wax yoo xam ni ñoom sax gëmuñu ko. Ñooñuy jag-jagal jaar-jaaru Maki Sàll, di ko jekk-jekkal, bés ba muy daanu lañ koy jàmbu, wuti keneen ku ñu nax. Jaamuwuñu Maki Sàll, seen soxla lañuy jaamu te su loolu dakkoon ci réew mi dina ci baax.
Maki teel naa dugg ci làngu pólitig gi. Ànd-Jëf bu Làndiŋ Sawane la njëkk a bokk, ba mu newee Iniwérsite bu Ndakaaru. Toogu fa lu yàgg, nag. Ci gis-gisam, Ànd-Jëf du woon pàrti buy daaneeli bés PS. Moo ko taxoon jël kàrtu PDS. Def na fukki at ak juróom ci pàrti boobu nga xam ni Ablaay Wàdd a fa doon Buur di fa Bummi.
Ñi nekkandoo woon ak moom PDS nee ñu Maki gone gu teey la woon, yem fuñ ko yemloo, dégg ndigal te kenn mësu koo dégg mu wax lu ëpp. Bariwul woon wax sax, faf. Wàdd seetlu pas-pasam, daldi ko teg ci boppu kurélu kàngami PDS yi, muy leeral naali pàrti bi, ñu daan ko séen it léeg-léeg tele muy dàggasanteek ñoomin Abdulaay Wilaan ak waa PS yi mu àndal tey, ñu neexoo lool, ndeysaan.
Bi PS daanoo ci atum 2000, “Góor-gi” woolu Maki, teg ko ci wetam. Ci diggante 2000 ak 2008, Petrosen la ko njëkk a dénk ba noppi boole ko ci ñaari gornmaaam, soog koo def Njiitu-jawriñi réew mi. Atum 2007 la Wàdd doon wut ñaareelu màndaa. Booba fekk na mook doom ji, Karim Maysa Wàdd, ñu def fiy njaaxum yu kenn xamul nañu tollu, réew mi jéppi leen, ñépp ne Wàdd jeexal na tàkk, su yëf yi jaaree ci yoon day daanu. Mu wóolooti Maki Sàll, ne ko jiiteel sama kàmpaañ. Maki jig lool Ablaay Wàdd ndax ba tey jii kenn mënul a wax fan la “Góor-gi” jaar ba faluwaaat ci sumb bu jëkk bi !
Joŋante tànneefu dipite yi ñëw, PDS yépp topp ci ginnaaw Maki Sàll, pàrti bi daldi amaat ndam, moom ci boppam ñu fal ko njiitu Péncum réew mi.
Waaye yàggul dara ndombog-tànk googu indil koy jafe-jafe yu jéggi dayo. Ndax bés ba mu jaaxaanee “Place Soweto” ne na ko Karim Wàdd wuyusi, wax dipite yi fan la dugal xaalis biñ jagleeloon ndajem OCI mi fi amoon jamono jooju, la Wàdd mer ba funki, ne kii ndax yaramam neex na, sama doom man, Karim Maysa Wàdd mi nga xam ne Senegaal ba Senegaal daj moo fi gën a xereñ, ëpp fi xam-xam ! Booy seet, keroog la diggante Maki Sàll ak Ablaay Wàdd tàmbalee yàqu ba sunu jonni-Yàllay-tey jii. Noonu la ko “Góor-gi” jëlee ci boppu Péncum réew mi ba noppi dàq ko PDS.
Li nu xamoon ci pólitigu Senegaal, nag, moo di ne boo deewee ba ñu suul la, fa ngay doxe ñu fàtte la ba fàww. Moonte, ak lu mu metti-metti woon, Maki Sàll fexe na ba dëkk Ablaay Wàdd, daan ko jéll bu amul benn werante, wuutu ko ci jal bi.
Naka la def ba dekki, delsi, di jiite tey réew mi ? Ay ñoñi Màkee ngiy wër réew miy yéemu ci xelam, naan ni ngeen koy gis muy patt-pattaaral, njàccaar dëgg la, moo fi gën a xam li mu bëgg, xam it naka lay def ba jot ci. Ñu ngi naan tamit laata muy sóobu ci pólitig bi, dafa wër Senegaal, waxtaan ak askan wi, xam soxlay ñépp, soog a dige ay paj.
Loolu, de, lay nitam di wax. Wànte ndax kàddu yooyu yenu nañu maanaa ?
Bunu kenn jéem a gëmloo ne doomu Aamadu Abdul ak Kumba Timbo jee ëpp xel ci réew mi. Déedéet. Maki Sàll nitu neen la, kenn la fi ëppul xel. Ku gis ni muy doxale ak i noonam — tëj ràpp ci kaso bi Karim Wàdd ak Xalifa Abaabakar Sàll — dinga njort ne du nit ku wóolu lool boppam. Janoo na tamit ak réew mi di tagg Tubaab yi ñu daan beral loxo, nee na, di ñamal sunuy soldaar ay “desserts”, di ko xañ yeneen doomi-Afrig yépp. Lii rusluwul ? Fekki na fi yit ay naataangoom Kigali, ñu laaj ku ci nekk su ko Yàlla mayoon xam-xam ban jumtukaay lay njëkk a sàkk ngir jëmale Afrig kanam. Ku fàttaliku li mu tontu keroog, fàww nga xaw cee am kersa…
Dëgg la, ku Yàlla mayul tuuti xel ak fulla ju mat sëkk doo jiiteji mukk lu tollu nim réew. Wànte am na leneen lees war a sóorale ci réew mu mel ni Senegaal.
Loolu lan la ?
Ay nooni Maki Sàll dinañuy wax ne Tubaab yee ko seetlu bu baax, xam ne kii amul dara lu muy bañ, luñ ko sant dina ko def, ñu daldi koy dooleel, jàpple ko ba mu falu. Du ñàkk mu am ñu ni nu : “Déggal ma ñii rekk ! Yéen a gën a ñeme Yàlla ! Ndax ba muy am yéen a ko fekke ?” Ku mu neex nga gise noonu mbir mi wànte pólitig, li ci ëpp solo, buy am ku ci bokkul doo ko fekke ! Te sax, ñaari firndee ngi yuy dëggal tuuma jooju. Bi ci njëkk moo di ne Frãs, réew yi mu tegoon loxo ci Afrig yépp, amu ci benn bu mu may foo yakkee sa nàkk. Tey la leen gën a sonal, tënk leen ba yëngu sax të leen. Li Pari tàmm a def mooy tabb njiit ciy nitam, nga doon ag xuusmaañàppam, mu yolomal buumu njaam gi nag, ngay tooyal ceebu Frãs, waaye booy féqu, nar koo rëcc mu daldi lay tam dëmm, sàkkal la pexe. Ku weddi lii, laajal Sànkaraak ñeneen ak ñeneen. Ñaareelu firnde bi moo di ne bi Maki Sàll faloo ci atum 2012 ba tey, deful lu-dul ràcc jemale ci kanamu Tubaab yi. Ñépp a ngi ciy teg seen bët. Muy Eiffage, di Auchan, di Orange, di Bolloré, di Total ak Alstom, suñ fi nekkoon di lim sosete Tugal yiy manq deretu askan wi, duñ fi jóge tey. Ku mu neex, ku mu naqadi, ñooy teg ndawal ci réew mi, sunu koom-koom a ngi ci seeni loxo.
Nee ñu Maki bariwul wax, day jëf : waaye am na nu, soo koy jëfe, looy doyeeti wax ? Moom daal, wax ji yépp lii rekk la : Maki Sàll ak Tubaab yee bokk mbuus te li tee Senegaal jëm kanam, loolu ci la. Ku yéene sam réew li gën ci moom, doo ko wànteer ay doxandéem.
Waaye kenn du ni Maki defu fi dara.
2012–2019 : juróom ñaari at yi mu toog ci jal bi, yeggali na liggéey yu bari yu Ablaay Wàdd sumboon. Xanaa rekk ni mu leen yàkkamtee sottal ngir am lu mu bàkkoo ci kàmpaañ bi ñuy waajal, moo xaw a teey xel. Moom mi ñu naan ku ànd ak sagoom la, xéy-na bu teeylu woon tuuti, doon na woyofal njëgu TER bi ak bu ótórut beek peyaas bi. Mbirum njëg li, lu am soloo, ndax xaw naa tiital ñi seen xam-xam màcc ci koom-koom. Nee ñu xaalis bu dul jeex la Maki leb bitim-réew dugal ko ci TER beek yeneen yi muy jébbal askan wi fan yii. Ci loolu sax la waa Bennoo Bokk Yaakaar di sukkandiku naan Senegaal tegu na, ni oto rawante yu gaaw yooyu, ci yoonu yokkute, yànj ba dee, di def fiiw ! fiiw ! rekk.
Amaana koomu réew mi am tan waaye mel na ni yëf yi dañoo féete boor. Leneen lu ñépp di teg seen bët, moo di ne mbokki Maki Sàll yeek ñi koy jàppale, waxuñu dara, seen ceeb a ngi niin. Waaw, ndax mënees na tudde lii yokkute dëggëntaan ? Noo yey laaj loolu ndax muy loppitaan yi di lekool yi, benn doxu ci : ku sa loxo jotul sa ginnaaw — te ñooñoo ëpp ci Senegaal — soo feebaree doo faju te sam njàng du sori.
Fi mu ne nii, Usmaan Sónko, Idirisaa Sekk, Isaa Sàll ak Madike Ñaŋ a ngi koy waaj a song. Xam ni mbir miy mujje jafe na. Li ñu war a fàttaliku rekk moo di ne Maki Sàll du neex a déjjati. Laata ñuy agsi fii tey, tas na ñaari pàrti yi fi ëppoon doole, PS ak PDS. Leneen yitteelu ko lu dul amaat beneen màndaa bu juróomi at. Loolu rekk a tax muy wër réew miy jébbale ay pom, ay saxaar ak i jàkka. Gone yaa ngi koy kókkali sax ci Facebook, naan alkaati Ndakaaru yi tey ku ñu gis ngay dawal oto bu bees ñu laaj la ndax Maki « inaugurer » na ko, soo leen nee déedéet ñu ni la taxaweel wet, mu ngi ci yoon wiy ñëw ! Am na yit ñu koy méngaleek Maxuréeja Géy mi doon yaakaar « màndaa » moom tamit ba taxoon koy leb xaalis bu bare di ndaataatallax. Wànte ci filmu Usmaan Sémbéen bi, Maxuréeja rekk la àddinaam di mujjee yàqu-yaxeet. « Màndaawu » 2019 bii moom, du ñàkk réewum lëmm la nar a salfaañe. Mel na ni Maki Sàll a ngi tayle ëllëgu goney Senegaal ngir rekk ga1ddu ndam li bésub 24 féewaryee bii ñuy séentu…
Mamadu Jàllo ak Bubakar Bóris Jóob