Nit ñi dëkkee ci àddina si, jamano jii, xayma nañu leen ci lu ëpp juróom-ñatti tamñareet (miliyaar). Te, ci lim bu takku boobu, ñi faatu bokkuñu ci. Muy firndeel ne, nit ñi jot a jaar ci kaw suuf, bi mu sosoo ak léegi, bari nañu lool. Waaye, li ñuy bari bari, kenn ci ñoom bokkul ak moroomam.
Ñaari nit, mën nañoo ndiroo lool ci jëmm. Waaye, du tee ñu wuute ci jëfin. Ndax, ñaare, doxalin wu ne rekk, jikko moo koy uuf. Te, ñépp bokkuñu jikko. Te yit, lu bari, walla sax li ëpp ci li nit di jikkowoo, bi muy nekk gone lañu koy mooñ ci moom. Ci jamono ju am solo jooju lañuy tàmbalee def ci moom fayda (personnalité) ji nga xam ne moo koy tëgg ba mu nekk nit ki mu war a doon. Maanaam, nekk moom ci boppam, te du ndirook keneen.
Ñi seen xam-xam màcc ci nit ak li koy mottali (ba mu nite), joxoñ nañu ñeenti ndab yu yarkat bu ne (way-jur, jàngalekat, añs.) war a waajalal tuut-tànkam. Ndab lu ci nekk daf koy jariñ, mu mën a fàggul boppam jumtukaay yi mu yittewoo ngir yatt nit ki mu bëgg a doon. Ginnaaw bi, mu sukkandikoo ci ba tabax faydaam ba mu àgg. Ndax, fayda jooju kat, mooy dooni ruu gi muy roof ci nit kooku mu yattal boppam.
Wareef la, ci yarkat bu ne, mu taxawu goneem, soññ ko ngir mu dogu ci taxawal kenu yi nga xam ne, bu leen sampee ba ñu dëgër, bu màggee doon nit ku am fayda. Ñenti kenu yooyu, nii la leen gëstukat yi gaaralee : xam sa bopp (connaissance de soi), fonk sa bopp (estime de soi), wóolu sa bopp (confiance en soi) ak dëggal sa bopp (affirmation de soi). Toftale bi nag, lu ci am solo la. Ndax, kenu gu ci nekk fàww mu taxaw bu baax ngir mën a kàttanal ga ca topp.
Xam sa bopp mooy kenu gu mag gi. Bu doon lu ñuy tegle, kon mu doon tóoj gi, ci la lépp di tegu. Mooy tax a xam fa nga jóge, li la war ak li ngay jomb. Ci ngay mën a xamee it fi nga war a teg say tànk. Ndax, dina tax nga mën a ràññee li nga bokk ak ci li ñu la boole. Safaan bi nag, di réere sa bopp, mooy waral nit bàyyi li mu yor, wàlli ci yëfi keneen. Te, fekk ne li mu moomal boppam moo gën a gànjaru fuuf.
Ku xamul sa bopp nag, doo mën a fonk sa bopp. Nde, mëneesul fonk lees umpale. Fonk boppam mooy waral nit du xeeb boppam te du xeeb it keneen. Du doyadi te du doyadal kenn. Du xayadi, du bëgg lu bëgguwul te du def lu ñu naan cam. Waaye it, ku mu gis fonk ko. Ñàkk koo def nag, yóbbee na nit ci wopp ju naqaree gis te jafee faj lool te muy yaras.
Nit, bu xamee boppam te fonk ko, daldi sañ a am kóolute ci boppam ci lu amul sikki-sàkka. Dafay fekk ni natt na dayoom, xam ni kàttanam tollu ak fi ay mën-mënam àgg. Ci lay mën di jël i dogal ci ay mbir yu bari ndax du ragal te du am it xel-ñaar. Ñàkk a gëm boppam nag, mën na yóbbee nit mu am doxalin bu nasax. Te, fekk ne sax, xéy-na, nekkul ku yaafus. Waaye, ragal lajj doŋŋ moo koy teree jëf. Mën na tax it mu doon kuy gaaw a yéemu ba lu ñëw rekk fëkk ko. Mu faf mel niw xobu garab.
Ku gëm sa bopp nag, danga koy dëggal ndax mooy firnde ji. Nit ki jëmmal boppam, dafay def li war, ci ni mu waree. Rax-ci-dolli, dafay am sañ-sañu joxe gis-gisam ci bu jotee. Waayeet, dafay am xalaat yu leer yu mu leen di layalee saa su ko laajee.
Ak ni jomono jaxasoowee, ku amul fayda rekk, bu moytuwul dundam dina lëj. Te, boroom xam-xam yi wax nañu ne, nit ñu baree ngiy def lu defuwul te dara xirtalu leen ci lu dul ñàkk wóolu seen bopp. Ndax, dañuy yaras di koy jéem a nëbb ba mu tàbbal leen ci loo xam ni warul, wóorul. Ba tax na, yarkat bu ne, bu yaboo teel a jóg ci ay xaleem balaa mbedd mi di ko jiitu ci ñoom. Bu xàllee yoon wi ba mu leer, bu ñu màggee mottali li des.