Fi réew mi tollu jamono jii, teey na xel. Waaye, jur nay laaj yu jar a taxaw seetlu. Dafa di, saa bu kujje gi nammee amal xew-xew walla doxu-ñaxtu rekk, day jur njànqare, rawatina bu ko perefe teree ba ndaw ñi génn di xeex ak takk-der yi. Bu ko defee, dañuy nemmeeku ay yàq-yàq yu baree bari, ñuy taal i daamaar, bitig, bérébi liggéey, Auchan, Total, añs. Njàng mi sax, day taxaw. Nde, ndongo yi dañuy rax ci xeex bi.
Saa buñ génnee ci yëngu-yëngu yu ni mel, takk-der yi dañuy jàpp ñu baree bari ci ñaxtukat yi. Bu ko defe, kurél gu ci nekk, dakkal liggéeyam, di ñaxtooti ak a kaas ngir ñu bàyyi seen i ñoñ. Niral, njàng meek njàngale mi muccu ci. Ndaxte, muy jàngalekat yi, di njàngaan yi, ku ci nekk tàbbi na ci xeex. Liñ ko dugge mooy aar seen i naataangoo, sàmm seen i àq ak i yelleef.
Dafa di, fan yii, ginnaaw doxi-ñaxtu yi fi amoon, dañ jàppoon ay jàngalekat ak i njàngaan. Looloo tax ba ñu wàcc ci mbedd yi, di jàmmarloo ak takk-der yi. Ngir firnde, ndongoy liise Delafosse génnoon nañ di kaas ngir sàkku ñu bàyyi seen i moroom. Rax-ci-dolli, ndongoy jànguneb Gastõ Berse bu Ndar tamit, doon nañu yëngal. Ñoom tamit, li ñuy kaas, bees sukkandikoo ci kurél gi jiite ndongo ya, CESL, li mooy ñu bàyyi Duudu Léy mi ñi téye ca kasob Ndar ba. Moo tax ñu dakkal njàng mi boobaak léegi, wax ne, fileek bàyyiwuñ ko, kenn du jàng ca jàngune ba. Muy SAEMSS, di waa G7, ñoom itam, lenn lañuy kaas, mooy ñu bàyyi seen naataangoo yiñ jàpp.
Jëwriñ ji ñu dénk njàng meek njàngale mi, Séex Umar Aan, doon na dankaafu ak artu, di wax ne mbir yi dafa rax pólitig. Ciy waxam, nee na, Nguur gi du seetaan mukk ñuy salfaañe njàng mi. Waaye de, tey la Waalo gën a aay.
Wëliis jàngalekat yi, fajkat yi tamit, jaare ko ci kurél gi leen boot (Ordre des médecins du Sénégal), doon nañ yëglu ak a moytuloo Nguur gi ci fajkat yi muy jàpp, di leen metital ak a xoqatal. Mbirum doktoor Baabakar Ñaŋ doy na ci misaal. Génne woon nañ ab yégle ngir dankaafu Nguur gi, di ko wax mu sàmmoonte ak àqi fajkat yi. Nde, bi Usmaan Sonko demee ca kilinig Suma Assistance bi doktoor Baabakar Ñaŋ moom, Yoon woolu na ko, woolu yeneen fajkat ya fay liggéeye, di leen laaj i laaj yoy, waruñu cee tontu. Ndaxte, seen sàrtub liggéey moo leen ko tere. Loolee leen taxoon di fàttali Nguur ak Yoon fi mu war a yem, te bañ a rax pólitig ci mbir mi.
Ci wàllu koom gi tamit, saa bu réew mi yëngoo, lépp ay taxaw. Dara du dox daanaka. Nde, oto du dem, oto du dikk. Bérébi liggéey yi, ngir bañ ñu yàqal leen, dañuy tëj seen i buntu. Li koy firndeel mooy yégle yi génn ci tey jile. Ndax, bi Yewwi Askan Wi xamlee ne day amal i doxi-ñaxtu bésub àllarba jii 29 màrs 2023, 30 màrs 2023 ak bésub 3 awril, dafa am ay këri liggéey yi xamal seen i kiliyaan ne dañuy dakkal liggéey bi ab diir.
EIFFAGE miy saytu otorut yi, xamle na ni, li ko dale àllarba ji 29 màrs 2023 ba alxames 30 màrs 2023, dañuy tëj seen bérébi kiliyaan yi. Biisi Dakar Dem Dikk yi duñ daw bésub tey ji. Bànk yi (Banque Islamique du Sénégal ak SGBS) tëj nañ. Waa ORCA yit, nee nañu duñu ubbi ci alxames ji, 30m màrs 2023, bésub layoo Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ. Àmbasaad yaa ngiy artu seen i doomi réew, bérébi liggéey yu bari di bañ a ubbi walla di bëral seen i liggéekat.
Ku yeboo ne, réew mi taxaw na. Te, nii la fa nar a deme ba keroog 2024. Ndaxte kat, liy raam, ci ñag bi la jëm. Buñ jàppee Usmaan Sonko, réew mi dina yëngu. Bu Njiitu réew mi, Maki Sàll, sampee ndëndam ci wotey 2024 yi, réew mi dina bax. Te, muy kujje gi, di Nguur gi, kenn yéenewul bàyyi, yolomal buum gi. Bu lii yépp amee nag, dañuy laaj ci loxo kan la réew mi nekk ?
Nde, Maki Sàll daf ne woon li fi amoon (màrs 2021) du fi amaat. Dafa mel ni lu ko raw a nar amaat de… te tàmbali na. Ndaxte, saa bu Sonko jógee walla mu joxe ndigal, ndaw ñépp ay génn, wutali mbeddi réew mi.
Diggant Maki Sàll ak Umaan Sonko, ku ciy jiite réew mi dëgg- dëgg ? Laaj baa ngoog.