KUPPEG ÀDDINA SI : SENEGAAL AK MAROG, NGIR SIGGIL AFRIG

0

Pàcc bu njëkk bu kuppeg àddina si jeex na démb ci àjjuma ji. Tey ci gaawu bi la ñuy door ñaareelu pàcc bi, di dóor-mu-toog yi. Ci juróomi ekibi kembarug Afrig yi teewoon ca Qataar 

Démb lañ doon amal ñetteel ak mujjantalub bëccëg bi ngir dugg ci dóor-mu-toog yi. Ginnaaw bi pàcc bu njëkk bi jàllee nag, liñ ci gën a jàpp ñeel ekibi Afrig yi mooy ñaar doŋŋ ciy wéy di bokk. Ñuy Senegaal ak Marog. Tinisi, Gana ak Kamerun fii lañuy faf yem. Waaye taxul benn yoon seen toogin ñaaw. Ndax, ba ci bëccëg bu mujj bi, benn ci ñoom jotagul woon a toog. ekib bu ci nekk mënoon na génn.

Juróomi ekibi Afrig yi waroon nañ amal fukk ak juróomi joŋante ci pàccub kippu yi. Ci xayma, 7i ndam lañ am, témboo ci ñetti yoon, ñàkk juróomi joŋante. Ginnaaw bi benn ci ñoom amulee ndam ci bëccëg bu njëkk bi, ci ñaareelu bëccëg bi la ekibi Afrig yi soog di wone dëgg-dëgg seen mëniin ci po mi. Njureef yi fésal nañ ni ñett ndam lañ am ci ñaareelu joŋante yi. Bi ñu ñëwee ba ñetteelu bëccëg bi, ñu daldi am ñeenti ndam ci juróomi joŋante.

Seen ndam yi mujj dafay wone ni ekibi Afrig yi dañoo yéex a yeewu. Bu weesoo Gana mi Portigaal dóor ci anam yu teey xel, Senegaal ak Kamerun  dañoo joxoon cër ba mu ëpp seen naataango yiñ doon janool. Looloo waral ba ñu daanu ci joŋante yu njëkk yi. Nde, boo seetee seen joŋante yi ci topp, Senegaal dafa dóor, dóoraat ; Kamerun témboo soog di dóor Beresil mi kenn dul nàttable.  Te ku gis fi Kamerun mujjeek Beresil démb (àjjuma), nga xam ni kuppeg àddina si amatul yaras. Dangay dawal dóor mbaa ñu dóor la.

Fullaak faayda ji Saa-Afrig yi jot a wone ci ñaareel beek ñetteelu bëccëg bi, tax na ba ñu gën leen a cëral. Te Àngalteer miy dajeek Senegaal (dibéer) xam na ko bu baax. Seen wattukat bii di Terent Aleksàndar-Arnool siiwal na ko ci waxtaan wum doon amal ak talkSPORT :

« Senegaal ci ekib yu mag yi la bokk. Yaakaar naa bépp ekib bu agsi ci wiccéem yi rekk ekib bu mag la. Gëm naa ni luñ mën a wax, nun (Saa-Àngalteer) lañul féetale kow. Waaye nun xam nan ni ñu (Saa-senegaal yi) aay lañ, te leer nanu ni lu nekk mën naa xew ci 90i simili. Bun yamee ci 90-95%, dinanu ñibbi ndax doyul. Bu nu mënul dém ba 100% du baax »

Li doomu Àngalteer bi wax dafay dëggal ni ñépp àndee nangu ni ekibi Afrig yi gën nañoo baaxal seen taxawaay ci xëccoo 2022 bi. Ñuy xaar gaynde Senegaal yi ak yu Marog yi delloo buum ca boy-boy ga. Te xam ni fii la leen Àngalteer ak Espaañ di xaar, ci xare badar.

Plus de publications

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici