Làmb : Móodu Lóo di woo jépp doomu Parsel ci ginnaaw Farã

Yeneen i xët

Aji bind ji

Démb la Farã doon  amal Open Press ñeel laale bi war am ci digganteem ak Soq. Mbëri Parsel yu mag yi bare woon nañ fa ngir biral jàppale giñ koy jàppale. Kii di Móodu Lóo jot na fa yékkatiy kàddu. Woo na jépp doomu Parsel ñu teew ca Aren nasiyonaal ngir dooleel seen doom Farã. Jàmmaarloo boobu warees na am ci gaawu bii, yemook 19i fan ci weeru Me.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj