Gannaaw ba Móodu Lóo ak Aama Balde bëree ci ayu-bés bii weesu, Móodu daan ko, démb ñaari punkal ñoo doon dajeeti, muy Ëmma Seen ak Tafaa Tin. Ñaari mbër yépp waajal nañu seen bés bi na mu waree, def i jàkkaarloo yu tàng, saf sàpp ak i nappante.
Ci bés bi, ku ci nekk àndi nga sa mbooloo, “Arène nationale” bi fees. Tafaa Tin a jëkk a bàkku, bàkku seereer bu neex. Ba mu noppee, Ëmma Seen bàkku tamit, ci biir bàkku bi mu sargal ci kii di Aama Balde ak baayam ja Fàllaay Balde. Waaye, fàttewul it kii di Tayson ak Boy Ñaŋ. bàkkoom gi mënees na ni tontu la ci waxi xàjjale ci biir Pikin yi doon jib ginnaaw bi Aama ñàkkee ci kanamu Móodu Lóo. Kon mel na ni dafa xamal yàqkat yi ni Pikin benn bopp la.
Ba ñu nekkee ci diggu géew ga, ku ci nekk di def xarfa-fuufam yu mujj, Ëmma am buteel bu mu yor di tuur ndox di daw bëgg a wër kii di Tafaa Tin, mu daldi koy bañ, kar ko ñu jot fa songoo laalantey kurpeñ.
Seen bëre bee ngi tàmbalii ba 21i waxtu tegee 34i simili. Ñu léewatoo lu yàggul dar, daldi tàmbali xeex xeex bu metti Ëmma dóor ko ci dóor bu dal, Tafaa Tin dem ardo dikkaat. Ci noonu ñu dawalaat léewatoo bi tuuti tàmbaliwaat xeex bi, mu mujje ci cong. Ëmma dafa doon jéem a jàpp tànku Tafaa Tin far mu moy, mu daldi rëpp, Tafaa Tin jaay ko doole, bës ko ci suuf si, daldi koy daan.
Mu nekkoon bëre bu neex, doore ci xeex jeexe ci jàppante, ñépp daldi bég.
Ci dibéer gii di ñëw, Sitta war na ci daje ak Lac Guiers 2, muy bés bees di xaar itam.