Mamadu Lamin Kamara, jàppleen tur wi. Xareñte, dëgëraay, njaxlaf ak dégg-daaj la gaynde gu ndaw gi boole def. Moo tax, Mamadu Lamin Kamara, kenn la ci ndaw yi futbalu Senegaal yaakaar, ñu di ko bàyyi xel bu baax.
CHAN 2023 ba la njëkk a wone boppam, wone xareñteek njàmbaar gu mat sëkk. CAN U20 2023 bi ñëw, mu goneg Génération Foot ga woon delloo buum ca boy-boy ga. Dafa di sax, ginnaaw bi ko Senegaal jëlee, moom lees tabb kuppekat bi gën a ràññeeku, gën a xareñ ca joŋante ya. Lamin Kamara, nees ko tàmm a woowe, fa la jaare luqi bëti tubaabi FC Metz yi. Mu jóge Génération Foot (këlëbu Senegaal) mi ko tàggat ba tay jii, fekki këlëbu Farãs ba, Metz. Muy ndam lu réy ci moom. Yàlla bu cat topp.
Moom nag gan la fa. Waaye de, gan-ganluwul wenn yoon. Fullaay jaay daqaar, am déet ? Moom kay, dafa dem rekk bokk. Ndax, bi mu àgge foofu ca këlëb bi, dafa ñëw rekk tàmbali di dëyal fullaak fayda gu mat sëkk ak xareñte gi ko ñépp xame woon. Looloo tax ñu teel ko dugal ca biir ekib ba, muy dem, di bokk. Liy wane ni gan-ganluwul nag mooy keroog joŋante bam ñjëkk bokk, korneer yaak teg-dóor yépp moo ko doon dóor. Démb ci gaawu gi, mu def paas ci seen joŋanteb Ligue 2 bi amoon diggante Metz ak As Saint-Étienne, futbal lu réy.
Waaye nag, dafa jël ab “rouge”. Loolu di bénn xeer bu jam ñaari picc. Ndax, benn futbalkatu As Saint-Etienne a ko cokkaas, mu fayu, arbit yi gis ko. Njuumte la. Ndax jikkoy xale bu tàng deret kesee ko waral. Waaye, sikk amul ci ne dina gën a noot boppam, dëfal xolam ba lu ni mel bañ koo dalati.
Nu di ko ñaanal mu dem ba ñu koy dégg nag fu raw fu ñuy dégg i magam, niki ñoom Saajo Maane, Gànna Géy añs. Ndaxte, loolu ndamal réew mi la ak kuppeg Senegaal.