Bërki-démb, ci àjjuma ji, la waa Yewwi Askan Wi génne woon ab yëgle ngir xamle ne ajandi nañu seen ndajem-ñaxtu mi ñu nammoon a amal bésub 3 awril 2023. Seen yëgle boobu nag, dafa juroon coow. Ndax, dafa am ay kàddu yu ñu ci jagleel làrme bi. Làrme bi moom, xaarul yëf yi di sedd ngir indiy leeral. Ndax kat, « moom la », fa mu àgg, « du man àggu fa ». Ca lañu génne, ñoom itam, ab yëgle ngir setal seen der ci li gaa ñi di wax. Loolu du lenn lu dul li waa YAW wax ne waxtaan nañu ak lenn ci kilifay làrme bi. Nga xam ne, moo tax ñu dàq seen ndajem-ñaxtu mi ñu waroon a amal ñetti fan ci weeru awril wii. Maanaam, benn fan kepp laata bés bi Senegaal di màggal jonnug boppam. Te, bés boobu am solo lool ci bépp saa-senegaal, rawatina ci ñoom ñi fare ci wàll woowu.
Yëgle bi lëkkatoo Yewwi Askan Wi génne bërki-démb neexul wenn yoon gaa ñiy sàmm kaaraange réew mi. Ndax, dafa teey xelu ñenn ñi. Te, ñoom waa làrme bi, nee nañu xajuñu ci géewu pólitig gi. Te, waa YAW moom, ci pólitig lañu nekk. Nde, ñoom waa YAW, dañu lay ne, sababi dàqug ndajem-ñaxtu mi ñu nammoon amal fépp ci biir réew mi, ci làrme bi la jóge. Maanaam, aw waxtaan wu ñu jot a séq ak kilifay làrme bi. Te, li ñu dugge woon ndaje moomu du lenn lu dul Njiitu réew mi Maki Sàll bàyyi ñi mu teg loxo ak ngir ñu sàmm àq ak yelleefu saa-senegaal yi.
Ñii di waa làrme bi moom, naanewuñu ko ndox. Ndax, bi yëgle boobu génnee yàggul dara, kii di Kolonel Musaa Kulibali, nga xam ne moo jiite bànqaas bi saytu xibaar ak jokkalantey làrme bi, dafa génne yëgle, indiy leeral ci mbir mi.
Yëgle boobu nag, dafa mel ni luy jéem a teggi tuuma. Ndax, bëgguñ nit ñi jàpp ne làrme bi daa far. Moo tax ñu biral ne, li gaa ñi wax amul. Te, kii di seen kilifa “Etat-major général des Armées” mi ngi woo gaa ñi fare ci géewug pólitig gi, ak fu ñu mën a bokk, ba ci sax way-moomeel yi, ñu kaccet làrme bi ci seen i waxi pólitig. Loolu, li ñu ci jublu mooy njariñal réew mi. Dafa di, làrme bi moom, ñépp la fi nekkal. Kenn waru koo jéem a aakimoo. Te, ñoom, nee ñu dañuy wéy di am taxawaay bi ñu mës a am. Maanaam, nekk ñu bëgg réew mi, tey wéy ci sàmm kaaraange réew mi.
Kon kay, li am ba des mooy, bu dee waa Yewwi Askan Wi dañoo bëggoon a tànxoo làrme bi ngir dàq seen ndajem-ñaxtu, daluñu ci. Laaj bi mat a samp kay mooy lu tax waa Yewwi Askan Wi toog ba mu neex ko ne làrme bee leen yebbiloo ? Te, làrme bi ne yëgul, tinul. Rax-ci-dolli ne moom yoonam nekkul ci mbiri pólitig. Kon daal, am na lees waxul ci mbir mi.