Ñaar-fukki fan ci weeru Desàmbar atum 2001, bés bu Senegaal dootul fàtte. Raaya réew mi sëngeem. Loolu doon màndargaal tiis ak naqar wu dal ci réew mi. Lewopóol Sedaar Seŋoor a dëddu.
Seŋoor a njëkk jiite réewum Senegaal ginnaaw bi réew gnnee ci nootaange. Ma nga fekk baax dëkk bu ñu naan Sowaal ca atum 1906. Di doomu Yaay Ñilaan Njéeme Baaxum ak Baay Basil Jogoy Seŋoor. Mu nekkoon nit ku ràññeeku ci wàllu mbatiit. Juddoom di ko firndeel ci meenum Sereer ak gañog kerceŋ. Seŋoor nag, nee ñu, ku mënoon a jàng la. Ginnaaw bi mu amee lijjaasam bu mag ci réew mi, la ko Tugal dalal. Mu def fa ay jaloore yu réy. Ndax, moom moo di njëlbeenug ñuule bu ñu a takkal raaya ci xam-xamu nëwu. Mu nekkoon fi tamit jëwriñ ca Nguurug Tubaab ya laata Senegaal di moom boppam. Ñu tabb ko Njiitu réew mi. Mu toog ci jal bi diggante 1960 ba 1980.
Seŋoor nekkul nitu politig kese. Ab liggéeyam fés lool ci wàllum mbind maanaam ladab. Waaye, ñu gis péeteem ca pàcc bii di taalif. Mu daan bind ci làmmiñu farañse. Li mu jot a bind, mënees na ca lim Chants d’ombres, Hosties noires, añs. Mu bokkoon tamit ca ña sosoon Francophonie, dig kurél guy dooleel làkk wii di farañse ci àddina si. Mu bokk sos tamit kurél gii di Négritude, mook Eme Seseer ak Damaas. Kurél googu di jox der bu ñuul gëddaam. Di lëkkale xeet wu ñuul wi yàgg a dund ak nooteel.
Waaye ñu gis ca geneen wet ga, waxam yu réy ja nga xam ne tas na biir àddina. Ñu bari dégge ko ci déggin wu wuute. Waaye, firee ko ci kàddu yu woroo. Moom bindkat bi dafa waxoon ne : “ Elen a moom xel, ñuule moom yëg-yëg”. Ñii jàppe ko aw tàgg, ñee jàppe ko aw xas.Lu mu ci mën di doon, liggéeyam du naax-saay, xam-xamam tamit du far.
Keroog, ci Talaata ji 21 desàmbar 2021 doonoon ñaar-fukk ak benneelu atum génn àddunaam. Mbokkam yi, xaritam yi ak i wóllëreem doon ko ci fàttaliku, moom Lewopóol, baayu Filip ma tëdd ca sëgi Belleer ya. Ay seede yu rafet ak ay ñaan di ko fa fekk. Way-pólitigi parti sosiyal di bàkkoo turam, taalif tamit wéy di woy turam fépp ci àddina si.