LI GËN A FËS CI XIBAARI AYU-BÉS BI 

Yeneen i xët

Aji bind ji

Layoo Maam Mbay ÑAŋ ak Usmaan Sonko

Altine jii ñu dëgmal lañu war a àttewaat Usmaan Sonko ak Maam Mbay Ñaŋ. Waaye, kii di Usmaan Sonko dafa mel ni narul a dem ca layoo boobu. Li ko waral mooy ne, ca bésub layoo bi la wootem ndaje, ça meeri bu Sigicoor. Ndaje moomu nag m, moom ak ñi mu bokkal meeri ba ñoo ko nar a sékk. Ndaje ma dina am ci altine ji bu ñu sukkandikoo ci yëgle bi mu génne.

Portaley Maki Sàll ak ñenn ci kilifay Yewwi Askan Wi : YAW tuumaal na Njiitu réew mi

Lëkkatoog Yewwi Askan Wi génne nab yëgle ngir indi ay leeral ñeel nataal yi ñu doon tasaare ci mbaali-jokkoo yi. Nataal yooyu nag, Njiitu réew mi, Maki Sàll, moo ca nekk ak ñenn ñu bokk ci lëkkatoo gi. Ñuy xamle nag ne ñi yor wàlluw jokkalante gi ca pale ba ñoo fa nekkoon, ñoo jël nataal yooyu ngir lëndëmal xel yi. Maanaam, gëmloo leen ne daanaka léegi déggoo am na ci waxtaan woowu, ñu bari ci ñoom ànduñu ci. Ñu yokk ci ne jàppante loxo yooyu doxoon seen diggante, tekkiwul dara, maanaam daal, ag jege walla yu ni deme. Te, ñoom, nee ñu dinañu wéyal seen liggéey ngir jeexal ag Nguuram ak bokkug mbooleem seen i lawax ca wote yooyu.

Maki Sàll – Bàrtelemi Toy Jaas 

Njiitu réew mi, Maki Sàll, ak Bàrtelemi Toy, meeru Ndakaaru, ñoo ngi raayante ndigg fan yii. Keroog alxames, ca ubbiteg Fórëm koom-koomug mboolaay geek jàppalante bi, Njiitu réew mi sargaloon na Bàrt ak i kàddu yu rafet. Daf ko ne woon : 

“Dama bëgg a ndokkeel bu baax meeru Ndakaaru bi, Bàrtelemi Toy Jaas. Doon na ko wax sànk, “Bàrtelemi, yaa ngi doxal de !”… Dinaa wax sa baay mi nekk ak man ne, sa doom a ngi liggéey.”

Bàrtelemi Jaas tamit delloo na ko njukkal, sant ko, gërëm ko ci teewaayam.

“Balaa dara, damaa bëgg gërëm Nguurug Senegaal ngir lu mu dugal loxoom ci 6eelu Fórëm koom-koomug mboolaay geek jàppalante bi, li mu ci jàpp ak li mu ci def ci lépp. Ngeen may ma, ma gërëmal sama bopp Njiitu réewum Senegaal, Maki Sàll. Damaa bëgg a wax ne, man ci sama jëmmu bopp, li ma nekk meeru Ndakaaru ak li ma nekk dépite, maa jël ndogalu woo Njiitu réew mi, Maki Sàll, ci ubbiteg 6eelu fórëm bii.”

Bàrtelemi gën na feddali cant ak ngërëm yi. Ndax nee na, guléet Njiitum réew di teew ci ubbiteg Fórëm koom-koomug mboolaay geek jàppalante bi. Mu ne loolu day wone, fii ci Senegaal, fonkees na fi koom-koomug mboolaay geek jàppalante bi. 

Xiifalug waa Pastef yi nekk ci kaso bi

Ñoñi Usmaan Sonko yi nekk ci kaso bi namm nañoo tàmbali ag xiifal gu amul àpp ci altine jii ñu dëgmal. Gii Mari Saañaa mooy ki biral xibaar bi ci xëtu Facebookam. Nee na li ñu ko dugge mooy ñaawlu jàpp gi ñu leen jàpp te teguwul ci yoon ak tamit dooleel seen Njiitul làng gi Usmaan Sonko ñeel ñaari layoo yi mu am ci diggante Maam Mbay Ñaŋ ak Aji Saar ci weeru me wii. Ñoom nag, tollu nañu ci ñaari-téeméer ak juróom-fukk ak juróom-ñaari nit ñu nekke ca Rëbës. Te, ñi ci ëpp di ndawi Pastef.

Paap Jibriil Faal lawax la ci wotey 2024 yi

Njiitul làng gii di Les Serviteurs biral na ag bokkam ci wotey 2024 yi. Loolu nag, miŋ ko xamle démb ca ëttam ba fa Caajaay, ci tëjteg yaatal gi mu doon def ci gox-goxaat yi. Mu yokk ci ne mooy lawaxu ndaw ñi ak yaakaar ji.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj