LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (10/11/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

ËTTUB ÀTTEWAAY BU MAG BI DËGGAL NA WALF

Ci weeru féewaryee wii weesu, CNRA dafa dogoon siñaalu télé Walf. Li ko sababoon mooy li Walftv doon wone xeex ya amoon fa Mbàkke. Bi loolu amee, kilifay Walfadjiri yi àqi woon nañ yoon ngir kalaame CNRA bi nga xam ne, Baabakar Jaañ moo ko jiite. Àttekat yi jox nañ leen dëgg. Nde, njëlbeenu néegub caytu bu Ëttub àttewaay bu mag bi dafa teggi ndogalu CNRA li, daldi koy far.

YEESALUG DAARA YI

Raisin Ba, njiitu-doxalu Waqf bi, joxe na xibaar buy neex Sëñ daara yi. Ndaxte, ci waxi Raasin Ba, dinañ tabax ab taax bu 16i etaas ci diggu Ndakaaru. Taax boobu, daaray Senegaal yépp ñoo koy bokk. Fa jumaa Mermoos ba la biralee xibaar bile, ba ñuy séddale 150i njël dund (kits alimentaires) ñeel néew-ji-doole yi. Kàddu yii toftalu la fa biral :

“Bu dee ci wàllu kopparal yeesalug daara yi, Càmmug Senegaal, ànd ceek “Banque islamique de développement” dafa naaloon tabax 64i daara yu yees te, xaalis bu ciy jóge, ci daara yooyu lay dellu ñeel seen ug caytu.”

MBËKK MI

Géej gaa ngiy wéy di wann doomi réew mi, rawatina ndaw ñi. Bàrsaa walla Barsàq tax na waa Barñi sëngeem. Nde, lu mat 300 ci ay doom Aadama ñoo sóobu woon ci yoon woowu, 25 i lañu ca gis. Lu mat 275 des ca géej ga, nàkk seen i bakkan. Mu nekk ay nataal yu tiis, di ay néew yu ñuy jaget moo xam góor mbaa jigéen.

MBIRUM BAAY FAAL BA ÑÀKK BAKKANAM FA TUUBAA

Muy ab jàppante bu doxoon diggante baay faal yay saytu wormay dëkk ba ak waa koñu Firdawsi. Lañu leen tuumal di njaayum sineebar tax mu sooke fa ab jàppante ba ñu faat fa ab baay faal. Xalifag Tuubaa bi, Séex Muntaxaa, àddu na ca mbir ma. La muy sàkku ca ñoom mooy ñu bàyyi loolu ciy loxoom. Waaye, coow loolu terewut baay faal yaa ngay wéy di def seen liggéey.

CA ËTTUB ÀTTEB NDEYU RЀEW MI

Muy ab tàbb yu yees ñeel kay wuutu Abdulaay Silla ma ñu yóbbu ca CENA. Ma ngay wuyoo ca turu Séex Tijjaan Kulibali. Moom lañu fal ca béréb boobu. Mu nar a door ab liggéeyam altine jii ñu jëm.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj