CEDEAO, kurél gi ëmb réewi Afrig sowu-jant yi amal nam ndaje, démb ci alxames ji 10i fan ci weeru ut wii, fa Abuujaa (Niseriyaa). Lañu ko dugge mooy indi ay saafara ca réewum Niseer ginnaaw poqatim nguur ga fa am. Rax-ca-dolli àpp ba ñu joxoon sóobare ya dafa jeex. Mu mel ni lañu tënk soreewut ak lees di wax « daas, fanaanal ». Ndax jëfandikoo doole dàqeesu ko fa ba léegi.
PASTEF
Ginnaaw ba ñu tasee làngu pólitigu Pastef, jàpp seen i njiit, ne leen ràpp ci kaso yi, Pastef a ngi wéy di am ay jafe-jafe. Ca meerib Ndakaaru, ca wetu seen doomu ndey ja ñu àndaloon di xeex ba jot ca, dafa mel ni tonk nañu fa. Ndax, ginnaaw ba ñu yeesalee pal ga, wa Pastef neew nañu fa lool. Loolu nag, ki jiite Pastef Ndakaaru, Abaas Faal, nekkoon njëlbeenug tof-njiitu meer ba, ag wor la ko jàppe. Nde, Bàrtelemi Jaas miy meeru Ndakaaru ak waa Taxawu Senegaal, dañu jàmbu, daldi wor ngir rekk jot ci Nguur gi. Loolu la waa Pastef jàpp.
NDAX USMAAN SONKO DINA BOKK ?
L’observateur biral nab xibaar bu lëmbe réew mi ci alxames ji, wax ne far nañ turu njiitul Pastef li, Usmaan Sonko, ci falaakon. Maanaam, meeru Sigicoor bi, bees sukkandikoo ci yéenekaay bi, mënatul a fale, waaye tamit mëneesatu ko fal. Nee ñu, ndogal loolu, jëwriñu Yoon jaa ko jël ginnaaw àtte ba tukke ca mbirum Sweet Beauté. Mu mel ni xët wa ñu fésal te bind ca nit ña mënut a falu, Usmaan Sonko ca la bokk. Waaye, boroomi xam-xam yu bare yu seen i xel màcc ci wàll wi dàq nañ ndogal lu safaanook Yoon loolu. Nde, ci seen i wax, ba jonni-Yàlla-tey, amul lenn ndogal lu tukkee ci Yoon luy tere Usmaan Sonko doon lawax. Te, nag, Yoon rekk a am sañ-sañu wax kan mooy bokk ak ku dul bokk. Li ci kanam nag rawul i bët.