LI GËN A FËS CI XIBAARI BÉS BI (12/6/2023)

Yeneen i xët

Aji bind ji

MBIRIM ÑETTEELU MOOME GI 

Paap Sàmba Mbuub xelal na Maki Sàll

Paap Sàmba Mbuub, kilifa la ci Bennoo Bokk Yaakaar, lëkkatoo Nguur gi. Moom nag, amal na taxaw-seetlu ci tolluwaayu réew mi ak yëngu-yëngal yi fi amoon ci sababu daanub Sonko bi, ay bakkan yu bari rot ci. Moo tax, mi ngiy xelal Njiitu réew mi, Maki Sàll, di ko wax ne :

“Sonko boroom tur wu réy la [marque déposée], moom ci boppam mbir yi dañ ko jële kow. Loolu mooy jafe-jafe bi te loolu la Maki Sàll xamagul. Maki Sàll dafa war a bàyyi waxi diirante mbagg yi te bañ a déglu ñi koy xambloo taal bi.” Ndax, “…am na fu mbir miy tollu, dangay xam a taxaw. Tey jii, sës nañu. Xanaa dañuy gën a yokk daan gi, taal réew mépp, walla ñu dakkal lépp, jàmm ne ñoy.”

Aliyun Saar, di xelal Maki Sàll : “Bul déglu ñi la bëgg a dugal ci ñetteelu moome.”

Jëwriñ ja woon, Aliyun Saar mi samp ndëndam ci wotey 2024 yi,  a ngi ñaan Njiitu réew mi, Maki Sàll, mu bañ a may nopp ñi koy xirtal ci ñetteelu moome.

“Dégguma Njiitu réew mi wax ci mbirum ñetteelu moome gi. Waaye, maa ngi dégg ñi ko wër di ci wax. Bu dee am na lu ma ko mën digal, mooy mu bañ a déglu ñi ko bëgg a dugal ci ñetteelu moome.”

Magi Bennoo Bokk Yaakaar yi woote nañ ngir wote yu dal yoy, ñepp a ciy bokk

Ndajem Magi Bennoo Bokk Yaakaar yi jibal nañ seen kàddu. Jàmm lañuy sàkku ci réew mi, di ñaan ñu amal i wote yu ànd ak jàmm, te ñépp bokk ci, ñu bañ a beddi kenn.

“Ndajem Mag ñaa ngi woo boroom ndogal yépp ngir ñu liggéey ba jàmm delsi. Moo ngi leen di ñaax ci ñu waxtaan ñoom ñépp ñeel wotey 2024 yi.”

PASTEF : “USMAAN SONKO A NGI KËRAM BA TEY…”

Pastef génne ab yégle di ci indiy leeral ñeel nekkiinu Usmaan Sonko. Nde, doon nañ ruumandaat ne njiitul Pastef li dafa daw. Ñoo ngi ñaax askan wi ñu mooytu wax yees di waxal Usmaan Sonko, te di leerlu saa su nekk. Pastef nee, nañuy sukkandikoo ci xibaari pàrti bi, bañ a déglu yenn këri xibaar yiy liggéeyal Maki Sàll ak ñi leen di jàppale ci mbaali jokkoo yi.

Ñoo ngi xamle ci seen yégle bi ne, ba tey, “kenn dindeegul ñag ya ca kowam.” Teg ci ne, “amul benn xeetu juboole buñ fa sumbagum” te “Pastef yónniwul kenn mu wax ak Nguur gi”. Yégle bi leeral na itam ne, “Usmaan Sonko dawul, benn daamar génnewu ko Site Kër-Góorgi.”

SEEX TIIJAAN JÉEY : “USMAAN SONKO SONN NA…”

Dalaloon nañ Seex Tiiijaan Jéey ci jotaayu Jury du Dimanche bu Iradio. Moom mi jiite kurélu Avenir Senegaal bi ñu bëgg, joxe nay xibaar ñeel wér-gi-yaramu Usmaan Sonko mi ñu tere génn këram, moom ak njabootam.

“Yaram waa ngi ne cocc, dara jotu ko. Yàlla daf ko wërsëgal xolu muñ bi muy dékkoo tooñ yi ñu koy tooñ yépp. Dafa gëm ne, natt yii di ko dal yépp, jaar-jaar la rekk, dina jeex, te liy ñew ëllëg à gën. Dina ci mucc ndax tooñaange du wéy.”

Bees sukkandikoo ci kàddu Seex Tiiijaan Jéey, naam Sonkoo ngeek wér-gi-yaramam, waaye nag xol bi neexul. Ndax, “…njabootam mënuñu noyyi.” Rax na ci dolli ne, “Usmaan Sonko, ay doomam, ay soxnaam ak jegeñaaleem yi  nekk këram, ñépp, kenn mënu ci génn. Te, dañuy segg dugg beek génn bi.”

Ci beneen boor, Seex Tiiijaan Jéey miy  aji-jokkale kurélug Avenir Senegaal bi ñu bëgg, jàpp ne, daan bu ni mel daf “…raglu, ñaaw, teguwul ci yoon te yëfi par-parloo la, daanaka sax yenuwul maanaam.” 

Bi ñu daanee Usmaan Sonko ba tey nag, kenn jëleegu ko. Jëwriñu Yoon wi, Ismayla Maajoor Faal, waxoon na ci Iradio ne, àttekat bi setalul Usmaan Sonko ci ciif giñ ko doon tuumaal, waaye dafa wëlbatiku wax ji rekk, tudde ko yàqug ndaw. Kàddu googu nag, neexul Seex Tiijaan Jéey mi ko tontu wax ne :

“Xool naa fi jëwriñu Yoon wi fii, ci seen kanam, muy jéem a layal lees mënut a layal. […] Li wér te sax ci xeli ñépp mooy ne, Usmaan Sonko, setal nañ ko ci tuumay ciif ak tëkkuy rey.”

Seex Tiiijaan Jéey a ngi réccu taxawaayu Nguur gi ñeel mbirum Usmaan Sonko. Ndaxte, “foo jaar ñu tuumaal ko leneen ci wàllu pólitig ngir ne, ñoom, fàww ñu fexe def lu nekk ngir taqal ko, tere ko bokk [ci wote yi].”

WALFADJIRI

Sëriñ Muntaqaa Mbàkke feral na rongooñi walfadjiri 

Kilifay walfadjiri yi seeti woon nañ Xalifab Murit yi, Sёriñ Muntaqaa Mbàkke, fa Tuubaa. Seex Ñas, Mustafaa Jóob, Sёriñ Haadi Ñas ak Sëñ Asan ñoo àndoon ça kilifag Tuubaa ga ngir xibaare ko dog bi Nguur gi dog seen siiñal.

Ginnaaw bi leen Xalifa bi dégloo ba noppi, dimbalee na leen 5i tamndaret ci sunuy koppar te dig na leen itam ne, dina def kemtalaayu kàttanam ngir ñu delloosi seen siiñaal bi.

Walfadjiri yéenekaay : benn 1000 fcfa 

Jëwriñ jokkoo gi dafa dog siiñaalu Walfadjiri ci diirub weer, 1 suwe ba 1 sujet 2023. Loolu nag, dafa am njeexital lu réy ci kërug tas xibaar gi, jural leen ay jafe-jafey koppar. Moo Seex Ñas mi jiite kër gi ne woon liggéeykat ya fay daan seen doole dañuy ñàkkandi seen i xéy. Te sax, du ñàkk mu am ñu ñu dàq. Askan wi jógoon nañ ngir dimbali leen, di leen nattal xi Wave laata Nguur giy dakkal ndimbal loolu. Am na sax, démb, ñu dem ba màkkaanu tele ba, joxe fa seen xaalis.

Wànte, jotoon nañ Xalifa Murit yi, mu may leen 5i tamndaret ci sunuy koppar. Waaye, njabootu  ndem-si-Yàlla ji, Siidi Lamin Ñas, yemuñu foofu. Jëfe nañ li leen ñenn ci seen i soppe xelaloon, mooy defar ay yéenekaay yoy, benn bu nekk 1000 FCFA lañ koy jaaye. Ci altiney tey ji lañ defar 1 000 000i yéenekaay tudde ko “Collector” fas yéene ko jaaye bu nekk 1000 FCFA. Bu lépp jaree, dinañ ci góobe 1 000 000 000 FCFA. Dina tax ba duñu Liggéeykat ya.

FRAPP JOXE NA DIG-DAJE 12 JÀPP 18 SUWE 2023

Frapp tànn ayu-bés lëmm, fas yéene cee amal i ñaxtu. Yégle lañ siiwal ngir xamal ko askanu Senegaal ak àddina sépp. Dinañ amal i doxi-ñaxtu li ko dale 12 suwe jàpp 18 suwe. Tànnal nañ seen ñaxtu yi ab ponk, tudde ko “YOON DAFA JENG”. Nee ñu, fépp ci réew mi lañuy amal seen ñaxtu yooyu. Li ñuy xeex mooy ñetteelu moome gi Maki Sàll bëgg a dagaan, ñi Yoon jengee ak lim bu takku bi mu jàpp ciy doomi réew mi te dara waralu ko lu pólitig walla wax sa xalaat. Kurél way-moomeel gaa ngi laaj itam ñu dindi ñag ya ñu ñag koñu Usmaan Sonko, xañ koy àqam.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj