LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (13/4/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

NJABOOTU LÀMB DAL NA CI KOW BIRAM SULÉY JÓOB 

Bi jëwriñ jii di Biram Suléy Jóob génnee wax ni ñoom, nguur gu bees gi, kenn du leen tuddee ay xeeti làmb añs., coow laa ngi ne kurr. Moom, jëwriñ ji ñu dénk laf gi ak soroj bi, lees koy bàkkee mooy ne, saa bu waxee, loxo dar gémmiñ. Li mu wax mooy ne, Càmm gu yees gii di sog a toog, du nangu ay xeeti baayale walla ndeyale ñeel xew-xewi tàggat-yaram yi. Looloo tax ba ñi séq làmb ji tontu ko. Ku ci mel ni Paap Abdu Faal ñaawlu na kàddu yooyu. Gri-bóordoo, moom miy njiitu mbër yiy takk seen ngemb, wax na lu ni mel. Fàttali na ko tamit ne làmb ci kenu yiy doxal réew la bokk. Te du lii lañuy xaar ci Càmm bu bees gi. 

BANQAASU JIGЀEN ÑI

Far walla wuutale gi ñu def ci banqaasu jigéen ñi metti na ñu bari. Nde, Càmm gu bees gi seetlu nañu ci ne jigéen ñi dañu cee néew. Rax-ca-dolli, ñu faf far jëwriñ ji daan nekkal jigéen ñi (ministére de la femme). Loolu tax ba ñiy xeexal jigéen ñi di ko ñaawlu fa ñaawlu yam. Lu ëpp 600i maxejj ak 44 ci ay kurél yiy saytu àq ak yelleefi jigéen ñi booloo nañu ci aw say ngir taxaw ci loolu. 

DIINE

Waa jàngu bi ñu ngi waajal seen bés ba ñuy amal fa Popengin. Muy siyaar ba ñuy def ca kanamu yaay Mari mu sell mi. Wii yoon di yamook 136eelu yoon wi ñu koy amal. Mu nekk ndaje mu mag ci diiney kercen yi. Xew-xew ba ñu jàpp ko diggante 18 jàpp 20i fan ci weeru me. Ponk ba ñu jàpp di “Yoon ak Jàmmu Senegaal”. 

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj