GORNOORU NDAKAARU BI GÀNTAL NDAJEM TABB MU WAA PASTEF
Waa Pastef dañ nammoon a amal ab xew-xew bu mag bob, ca lañuy tabbee Usmaan Sonko, mu doon seen lawax ci wotey 2024 yi. Ci gaawu gii, 15i fan ci sulet lañ ko bëggoon defe ca estaad Iba Maar Jóob. Biñ jébbaale gornooru Ndakaaru bi ab këyit ngir yégal ko xew-xew, kilifag gëbla daf leen ko gàntal. Nde, dafa génne moom itam ab yégle, di ci xamle ne ndaje moomu waa Pasteef doon sàkku, du leen ko nangul ngir daw fitna. Moom, Al Asan Sàll miy gornoor bi, dafa bind ne, ndaje moomu, mën na indi pëccaxoo ci biir réew mi. Looloo tax muy soññ ak a xirtal takk-der yi ngir ñu jël seen i matukaay, aar réew mi.
AMINATA ASOM JAATA GÉNN NA CI LËKKATOO BENNOO BOKK YAAKAAR
Aminata Asom Jaata mi fi nekkoon jëwriñu yaxantu gi, bokkoon APR ak Bennoo Bokk Yaakaar takk nay dëbësam. Dafa tàggoo ak ñoom ngir, ginnaaw Maki Sàll du bakkati, gisatul boppam ci làng gi. Waaye nag, fasul yéene bàyyi pólitig. Ndax, dafay xalaat a sos làngug boppam, te xool ku bokk ak moom gis-gis, ñu daldi ànd wotey 2024 yi.
GAAL GI SUUX FA NDAR : 6i NIT ÑOO LAB NAÑU CI
Mbëkk mi mbëkkati na réew mi. Ñoo ngi soow 300i roñukat yi wwutali woon duni Kanaari ya faf réer, noppeeguñ sax, beneen xibaar bu tiis dolleeku ci. Ndax, Ndar, daf fa am ag gaal gu suux ba 6i nit lab ci, dee. Nee ñu, démb, ci boori 5i waxtu ci njël la seen gaal gi suux ci bël bi. Mu mel ni daal, ba tey, Bàrsaa walla barsàq deñagul ci xeli ndaw ñi.
BЀSU XASIDA YI
Tuubaa doon na màggal, tey ci Alxames ji 13 sulet 2023, bés bees jagleel xasida. Mu nekk ci ndigalu Séex Muntaxaa may xalifa ba. Mu doon bésu jàng Alxuraan, xasida ak i salaatu ngir tuub ak sàkku njéggal. Mu doon itam ñetteel bi yoon ginnaaw ba ñu ko dale def ak léegi.