Ndogal lañu doon xaar jëm ci àtteb Usmaan Sonko ak Càmm gi, àttekat bii di Usmaan Raacin Coon biral na ko. Lañu doon laam-laame, ndax njiitul pasteef la woon dina bokk ci wayndarew wote am déet, Sëñ ba Coon dëggal na la Sabasi Fay waxoon. Mooy ñu delloo Usmaan Sonko ci wayndarew wote yi.
Ndogal loolu ndax lu ñuy jëfe la ci saa si walla dina am ay gàllankoor. Muy ay xalaat yu wuute bu ñu sukkandikoo ci yenn ci layookat yi. Ndax bu ñu seetee gis-gisu Meetar Elaas Juuf, àtteb dabu mën naa am. Muy lu Keledoor Si mi féete ca beneen boor ba dëggal. La mu wax mooy dàqeesu ko. Waaye dogal bi àttekat bi jël dañu koo war a jëfe na mu gën a gaawe.
KÀDDUY USMAAN SONKO YU NJËKK GINNAAW NDAMAM LI
Muy lu mu fésal ca xëtu ‘Facebook” ba. Lépp nekk ay kàdduy sant ñeel Boroom Bi. Waaye, di njukkal ay taxawoom ak i layookatam. Fàttewut itam askanu Senegaal wi muy ñaanal jàmm feese ko. Waayeet, sant na tund Afrig ak bitim-réew ñi ko taxawu.
JÀNGUNEB UGB AK UASZ
Muy ñaari daara yu kowe yu sóobu ci ay ñaxtu. Lañuy naqarlu doon benn, di coowal burs. Ndongo ya féete ca Sigicoor ñoom xàppati nañu ñatti fan yoo xam ne dañuy amal ngénte-tubaab, maanaam dañuy lekk te duñu fay. Lépp ngir dànkaafu njiit yi ngir seen ñaari weeri burs yi tagatémbe.