LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/5/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

JAMRA ÀDDU NA

ONG Jamra, ag kurél guy yëngu ci sàmm jikko yi, àddu na ci waxtaan wi njiitu Càmm gi di Usmaan Sonko ak gan gii di Melãsõ. Seen janoo ba ca jànguneb Séex Anta Jóob ba jur na coow. Lépp lu ko waral weesuwul mbirum ngóor-jigéen mi lëmbe àdduna si. Tontu la ca Usmaan Sonko tontu lëndëmal na yenn xel. Ndax lépp day delluwaat ci tontuy njiit yi ko jiitu, moo xam Maki Sàll añs. Ndax, bu ñu seetloo lépp ay tëgg-wëndeel la. Maanaam, seen tontu ci mbir mi leerut. Nde, Maam Maxtaar Géy, fa mu doon xaar Sonko mooy ne am ngóor-jigéen àtteem mooy rey.

WAAJTAAYU POPENGIN

Muy xew-xewu diine bu waa jàngu bi di amal at mu jot ca diiwaanu Mbuur, ca Popengin. Siyaar yaay Mari mu sell mi nekk kenu buy dekkil ngëm ci katolig yi. Ñu di ko amal ciy waajtaay tax ba njiit li ñu dénk wallu mbëj mi (kuraŋ bi), Mademba Bitéey, gise ak kilifay jàngu bi ngir dalal seen xel ci liggéey bi ñu nar a def ca gox yooyu. La mu gis, moom Sëñ Bitéey, mooy yokk nañu post yi ngir kuraŋ bi mën a matale ci diirub xew-xew boobu.

 PÓLITIG :  KUJJE GU BEES?

Ay weer ginnaaw ba réewum Senegaal génnee ci palug njiitu réew, xar-kanamam nar naa dellu ca na mu meloon. Ndaxte, kujje guy ngembuwaat, fabu ngir teewaat ci làngug pólitig. Mu mel ni loolu la Séex Umar Aan di junju. Mu nekkoon fi jëwriñ ji ñu dénkoon njàng mi, ma nga jàppal tànk kii di Aamadu Ba. Ndax, gis ne ni kooku mooy njiitu kujje gi te fas naa yéene fabu ngir waalal 2029. Meru Njum bi mel ni kuy xàllal yoon naataangoom bii di Aamadu Ba.

“FESTIVAL JAZZ BU NDAR”

Muy ndajeem mbatiit mu ñuy amal fa diiwaanu Ndar-géej. Mbooloo mu bari war fa daje. Ñenn ñi di yëngu ci mbatiit, moo xam woy la walla fecc, ñeneen ñi di ay wëraakon. Mu bokk léegi ci xew-xew yi ñi ràññee fa Ndar, di dundal mbatiit. Ndar-géej nar a dëkkee riir fii ba altine.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj