LI GËN A FÉS CI XIBAARI BÉS BI (19/01/2024)

Yeneen i xët

Aji bind ji

SÉEX TIIJAAN JÉEY DÀJJI NA TUUMAY AAMADU BA (BBY)

Aamadu Ba, lawaxu Bennoo Bokk Yaakaar, dafa dafa dugaloon dabantal ngir neenal wayndarey Basiiru Jomaay Jaxaar Fay ak Seex Tiijaan Jéey. Moom nag, jëwriñ ju mag ji, ñeenti tuuma la leen gàlloon :

– Bokk ci làngug politig gu ñu tas ;

– Jébbale ay kayiti caytu (pièces administratives) yu baaxul ;

– Costeg lëkkatoo gu saafaanook yoon ;

– Ñàkk a bokk cig lëkkatoo gu la jiital ;

Seex Tiijaan Jéey nag, dàjji na tuuma yooyii. Moom, njiitul kurélu Avenir Senegal bi ñu bëgg, xamle na ne, Aamadu Ba,  ab nataal bob, daf ci taxaw ak Usmaan Sonko, la yóbbu fa Ndajem ndeyu àtte réew, wax ne mooy firndeel bokkam ci làngu Pastef.

CÀMMUG SENEGAAL RAWALE NA KAROLIN FAY

Meetar Xureysi Ba moo xamle ne, soxna sii di Karolin Fay, di Saa-Farãs,  génne nañ ko réew mi ginnaaw biñ ko bàyyee. Farãs lees ko delloo. Waaye de, layookatam nee, loolu, moom yëgu ci dara.

Cig pàttali, dañ jàppoon Karolin Fay keroog 17eelu fan ci nowàmbar 2023. Fa boori ëttu àttekaay bu Kawe bi lañ ko tege woon loxo. Lees ko doon tuumaal mooy ne dafa bokkoon cib ñaxtu bob dañ ko tere woon

SÓOFÓORU TAKSI YI MER NAÑU

Kurél gi ëmb dawalkati taksi yi wone na ag meram. Li ko waral di gàntal gi perefe bu ndakaaru gàntal seen ub toogaanu ñaxtu bi ñu bëggoon a amal. Lépp di laale ak béréb ba ñu ko bëgg a defe. Waaye, bees sukkandikoo ci seen njiit lii di Móodu Njaay, danañu dugal ab bataaxal ci diir bu gàtt. Lañuy ñaxtu bokk na ci seen i jafe-jafe ci wàlluw liggéey, kujje gi dox seen diggante ak boroom móto yi ak yeneen xeeti daamar yi…

POMMUG WOTEY 2024

Mu nekk tomb buy ñëw di ñëwaat ba ñu jàppee wotey palum njiitu réew mi ba tey. Xalifa Sàll, di kenn ci lawax yi, àddu na ci. La mu ca xamle mooy, fim ne, béy wéy na mbuus. Ndax, loolu su amee, mooy sunu demookaraasi dellu na ginnaaw. Loolu nekk kàdduy njiitu làngug Taxawu. Nde, bu ñu sukkandikoo ciy waxam, lépp waxtaane woon nañu ko. Loolu, di ko jox dëgg tey ci li mu teeweji woon diisoo bi fi amoon. Te ñu bari di ko ca ŋàññi.

Plus de publications

Widewo

Xët yi mujj